wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
nagam
être engourdi
Sama tànk yi dañoo nagam
j’ai les jambes engourdies.
naka
comment
Naka nga tudd
comment t’appelles-tu ?
naka
comme
Lu deme naka muus la
C'est qqch qui est comme un chat.
nakk-nakkal
bafouiller
Dama ko laaj lu-tax jàngiwul, muy nakk-nakkal, ma xam ne dafa daw jàng
je lui ai demandé pourquoi il n’est pas allé en classe; comme il bafouillait, j’ai compris qu’il avait fait l’école buissonnière.
ñag
clôturer d’une haie
Dafa ñag tool bi
il a clôturé le champ d’une haie.
ñag b-
haie
Ñagu bugeewiye la
C'est une haie de bougainvilliers.
(prov.) Su janax di sóoru muus, ñag baa fa jege
si la souris brave le chat, c’est que la haie se trouve à côté.
ñag b-
personne originaire des pays côtiers de l’Afrique occidentale autres que la Guinée-Conakry et la Guinée-Bissau (discourtois)
Ñag lay séyal
elle est mariée à un natif d’un pays côtier de l’Afrique de l’Ouest.
nal
presser qqch pour en extraire le jus
Nal naa limoŋ ji yépp, def ko ci butéel
J'ai pressé tout le citron et je l’ai mis en bouteille.
ñalgu
grimper
Moo dàqa ñalgu golo
il grimpe mieux qu’un singe.
ñall w-
sentier piste
Jaar ci ñall wee gëna gaaw
passer par le sentier est plus rapide.
ñalingaan
être très noir
Ci similaak saala, asamaan si xiin ba ñalingaan
en un clin d’œil, le ciel devint tout noir de nuages.
ñakk
vacciner
Yóbbul xale bi, ñu ñakk ko
emmène l’enfant pour qu’on le vaccine !
ñakk b-
vaccin
Ñakk yooyu dinañu aar sa doom ci jàngoro yu bare
ces vaccins protégeront ton enfant contre de nombreuses maladies.
nag w-
vache bœuf
Masàmba may na ma aw nag
Masamba m’a offert un bœuf.
(prov.) Fu nag nekk, bukki dee fa
quand il y a une vache quelque part, une hyène y mourra.
ñale
ceux-là
Jox ko ñale !
donne-le à ceux-là !
ñal
se réserver qqch
Am na piis bu ma ñal ca bitiku Omar
il y a un tissu que je me réserve à la boutique d’Omar.
(prov.) Su picc geddee ab déeg, dafa ñal ag suux
si un oiseau boude un marigot, c’est qu’il a une réserve d’eau dans le creux d’un arbre.
nale
de cette façon-là
Nale lañu koy defe
C'est comme cela qu’on le fait.
(loc.) Mu nga nale.
Le voilà
ñambale
avoir une envie urgente d’aller aux toilettes
Won ko wanag wi; dafa ñambale
montre-lui les toilettes, il a une envie pressante de se soulager.
nattoonte b-
se mesurer l’un à l’autre
Ñaari mbër yaa ngi gëléemu di nattoonte
les deux lutteurs ont les mains sur le sol et se mesurent.
ñam
goûter
Ñamal seet
goûte pour voir.
nalu
pousser pour déféquer
Dafa fasu moo tax muy nalu
il est constipé c’est pour ça qu’il pousse pour déféquer.
nawetaan b-
travailleur saisonnier, spécialement pendant la saison des pluies
Bu nawetaan yi dikkee, nga wut ci ku lay jàppale
quand les travailleurs saisonniers de la saison des pluies seront venus, tu en prendras un pour t’aider.
ñalle s-
souriceau
Dafa ragal ñalle si
il a peur du souriceau.
namm
avoir l’intention de
Buy wax waxam yii rekk, dafa namm yokk njëg yi
quand il tient ce genre de propos, c’est qu’il a l’intention de hausser les prix.
(prov.) Yebu ca, namm ca, ku la ca bëmëx nga jél
tant mieux si on pousse à l’action qqn qui ne demandait que cela.
nawetaan
travailler ailleurs que chez soi pendant la saison des pluies.
Ñii, dañu fiy nawetaan rekk dëkkuñu fi
ceux-ci ne font que travailler ici pendant la saison des pluies; ils n’habitent pas ici.
ñall s-
excrément de petite taille
As ñall la génne; ñenti fan a ngi demul
il a évacué une petite crotte; depuis quatre jours il n’est pas allé à la selle.
ñañ b-
diaphragme (corps humain)
nawetal
signes précurseurs de l’hivernage
ñand
moucher qqn
Ñandal xale bi
mouche l’enfant !
ñax m-
herbe
Bul tëdd ci ñax mi
ne te couche pas dans l’herbe !
nappaate
faire de l’intimidation
ñankar b-
guimbarde tacot
War nañu jële ñankari taksi yépp ci sirkilaasoŋ bi
on doit retirer de la circulation tous les taxis en mauvais état.
nangul
concéder un fait à qqn
Su ngeen ma noon mën na daw, dinaa ko ko nangul
si vous me disiez qu’il est bon coureur, je le lui concéderais.
napp
pêcher
Napp na jén wu mag
il a pêché un gros poisson.
nangu
récupérer
Dañu lay may dara ci loxo bii, nangu ko ca loxo bale
ils t’offrent une chose de cette main et la reprennent de l’autre.
nangu
prendre de force
Xale bii moo nangu sama mbiib
C'est cet enfant qui a arraché mon sifflet.
ndaag l-
marche lente et gracieuse
Sa ndaag li jekk na
ta démarche lente est gracieuse.
nappkat b-
pêcheur.
Ñoom ñépp ay nappkat lañu
ils sont tous pêcheurs.
naqarlu
éprouver de l’amertume de qqch
Demam bi la ñépp di naqarlu
tout le monde éprouve de l’amertume de son départ.
nar
mentir
Dafay nar
il ment.
ñaq w-
sueur
Fompal ko ñaq wi
essuie-lui la sueur !
Lii, sumañaq la
ça, c’est le fruit de mon travail (ça, c’est ma sueur).
(prov.) Ñaq du réer boroom
on ne perd jamais le fruit de son travail.
naqar w-
amertume
Yàlla dafa def ñuy fàtte naqar
Dieu a fait en sorte que nous puissions oublier l’amertume.
(prov.) Ku bay sa bànneex, góob saw naqar
qui cultive son plaisir, récolte son amertume.
ŋar b-
rugissement
ŋargaloo
être froissé
Sa mbubb mépp a ŋargaloo
ton boubou est entièrement froissé.
nar b-
tas chacune des parts
Booleel nar bii ak bale
mets ensemble ce tas avec celui-là.
naraale
prévoir la part de qqn dans un partage
Nanga naraale Omar ci yàpp wi
il faut prévoir la part d’Omar en faisant le partage de la viande.
ndawtal g-
cadeau offert à l’occasion d’une fête de famille
Lu-tax indiloo ko ndawtal ?
pourquoi ne lui as-tu pas apporté de cadeau ?
ñar
complètement
Dafa tàlli ñar
il s’est étalé complète-ment.