wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
nar w-
mensonge
Sa nar wi dafa fés
ton mensonge est flagrant.
(prov.) Ak lu nar teela xéy, bu dëgg gontee, jot ko
le mensonge aura beau se mettre en route de bonne heure, la vérité le rattrapera, même si elle prend son départ l’après-midi.
ŋar
rugir
Gar ga ŋar na
le lion a rugi.
ñas
se coller à qqch en devenant sec
Fekk gone ga, biir ba dafa ñasoon ca garab ga
le ventre de l’enfant s’était collé à l’arbre.
ŋarale
Écarter les jambes
Njulli baa ngi toog, ŋarale ay tànkam
le circoncis est assis, les jambes écartées.
nasal
laisser la nappe d’eau d’un puits se reconstituer
Danuy nasal teen bi ci guddi gi bu ko defee njël nu root ndaa yi
nous laissons la nappe du puits se reconstituer, alors à l’aube nous remplissons les canaris.
ŋar w-
insecte sp
ŋas
avoir la rougeole
Doomam dafa
ŋas son enfant a la rougeole.
ñaral
laisser sécher les restes d’aliments sur la vaisselle à laver
Ndab yi nga ñaral fii, yombalul sa liggéey
la vaisselle que tu laisses sécher ici avec les restes d’aliments, ce n’est pas pour faciliter ton travail.
Sa mbind mi, danga ko
ñaral ce (le texte) que tu as écrit, tu ne l’as pas appris.
ñasaxndiku
renifler
Demal ñandu, yaa ngiy ñasaxndiku rekk
va te moucher, tu n’arrêtes pas de renifler !
ñas w-
crème du lait
ŋas j-
rougeole
Ñakku ŋas am na
il existe un vaccin contre la rougeole.
nasaraan b-
langue européenne
Jàng nasaraan a leen gënal jàng seeni làkk
ils préfèrent apprendre les langues européennes plutôt que les leurs.
nasax b-
personne non vigoureuse incapable physiquement
Ñi nuy futbalal duñu ay nasax
ceux contre qui nous jouons au football ne sont pas des incapables.
ŋat-ŋati
marcher péniblement
Kii di ŋat-ŋati mën na ñu xaar
celui-là qui se déplace difficilement peut nous attendre.
ndeer g-
village du Walo devenu célèbre par l’extermination des femmes brûlées vives un matin de mardi alors que les hommes étaient dans les champs
Talaatay Ndeer
le Mardi de Ndeer.
natt
donner sa cotisation
Xaaral ba ñépp natt
attends que tout le monde ait remis sa cotisation !
ndax
adversatif. Plutôt que de
Jànguloo, ndax di fo
plutôt que d’étudier, tu t’amuses.
ñaw
coudre
Kañ nga ko ñaw ?
quand l’as-tu cousu ?
(prov.) Wax, ab xottiku la, kenn ku nekk, yaa xam noo koy ñawe
une dispute, c’est comme une déchirure, il appartient à chacun de voir comment la recoudre.
ñaw
bien fait !
ŋaw
s’agripper
Dafa ŋaw ci banqaas bi
il s’est agrippé à la branche.
nattu b-
Épreuve (en général morale)
Jigéen jooju moo doon nattu bi ma Yàlla tegoon cette femme était l’épreuve que Dieu m’avait réservée. Séy ci boppam, nattu la
le mariage en soi est une épreuve.
nawet
passer la saison des pluies
Abijaŋ laay nawet ren
je passerai la saison des pluies à Abidjan cette année.
Dinga fi noor, nawet fi
tu poireauteras ici.
naw
avoir de la considération pour qqn
Xaalisam a tax ngeen naw ko
C'est à cause de son argent que vous le considérez.
natt b-
cotisation
Natt yépp daj nañu
toutes les cotisations sont remises.
nattukaay b-
servant à mesurer
Xanaa boo bëggee jaay sa soow mi, dinga wut ab nattukaay
J'imagine que quand tu voudras vendre ton lait caillé, tu chercheras une mesure.
nawetaan y-
rencontres sportives se déroulant durant la saison des pluies
ñaw-ñaw b-
point de couture point de suture
Ñaw-ñaw baa ngiy feeñ ba tey
les points de couture sont encore visibles.
ñawlu
faire coudre
Damay ñawlu simis
je fais coudre une chemise.
ŋayeet
exprime la manière de s’ouvrir largement
Won ga ne ŋayeet
l’arbre {won} s’ouvrit tout grand.
nawet b-
navette de machine à coudre
ndaama
être de taille courte, être de petite taille
Dama ndaama
je suis de petite taille.
naxantoo w-
berceuse
Woyal ko aw naxantoo
chante-lui une berceuse.
ñay w-
Éléphant
Am na ñay ca àll booba
il y a des éléphants dans cette brousse.
(prov.) Su ñay dee xàll ab àll, doom yaa tax
si l’éléphant débroussaille, c’est à cause de ses petits.
naxasaale
faire digression
Saa su ma la fàttalee ceen gi nga ma dig, nga naxasaale ba génn ci
chaque fois que je te rappelle la chaîne que tu m’as promise, tu t’en sors en faisant digression.
ndabraan j-
quatrième période de la saison des pluies, qui dure treize jours
Bu ñu tolloo ci ndabraan, mu dellu
quand nous en serons à la quatrième période de la saison des pluies, il repartira.
ndaama b-
voiture
Nanu nég ndaama
attendons une voiture !
ndaakin w-
cheval mâle, étalon
Ndaakin la jénd
il a acheté un cheval mâle.
ndajem-baat m-
syntagme
Ñaata cër a am ci ndajem-baat mii ?
combien de parties y a-t-il dans ce syntagme ?
ndaanaan b-
homme élégant en tenue traditionnelle
Ndaanaam yépp dinañu daje Sorano tey
tous les hommes élégants se retrouveront au théâtre national Daniel Sorano aujourd’hui.
ndaari g-
nom de village dans certains contes et proverbes
Bukki, wiiri, wiiri, jaari Ndaari
L'hyène aura beau faire des détours, elle passera par Ndaari
naxee-mbaay b-
tromperie
Ay naxee-mbaay rekk la
ce ne sont que des tromperies.
ndey-ji-séex j-
mère de jumeaux
Ndey-ji-séex a ngiy yalwaan
une mère de jumeaux demande la charité.
(prov.) Ndey-ji-séex, njaaxaanaay lay tëdde
une mère de jumeaux se couche sur le dos
ndakaaru g-
dakar (capitale du Sénégal)
ndab l-
récipient vaisselle
Damay raxas ndab
je lave la vaisselle.
ndam l-
succès gloire réussite
Am naa ci ndam
J'en ai retiré de la gloire.
Ndam demul, ndam dikkul
il y a eu match nul.
ndambe b-
cornille bouillie sans la gousse
ndeyjoor b-
côté droit
Xoolal ci sa ndeyjoor ak sa càmmoñ bala ngay jàll tali bi
regarde à ta droite et à ta gauche avant de traverser la chaussée !
ndaa l-
canari, grand vase en terre cuite servant à contenir de l’eau
Ndaa li amul ndox
il n’y a pas d’eau dans le canari.
(prov.) Goneg mbóoyo gu reew, xaar ko ca taatu ndaa la
pendant l’harmattan, attends l’enfant mal élevé au pied du canari
ndéwénal l-
cadeau qu’on fait plus spécialement aux enfants à l’occasion des fêtes de la Tabaski et de la fin du ramadan
Jox ma sama ndéwénal
donne-moi mes étrennes !
Ndar
Saint-Louis (ancienne capitale située au nord-ouest du Sénégal)