url
stringclasses
152 values
text
stringlengths
4
5.13k
https://www.defuwaxu.com/can-2023-aliw-siise-tann-nay-ndawam/
Gannaaw tànnug Aliw Siise miy tàggatkat bi nag, am na ay coow yu sew yuy jóg jëm ci lim nu andil rawatina ci mbaali-jokkoo yi. Foo geestu ñoo ngi ciy wax. Li gën a bari ci lees di wax moo di ne, moom Siise, dafa bari lim woo ciy defãsëer, ba sax ci miliyë bi, xeexkat yi ñoo ci ëpp. Boo jàngatee tànn gi wàlluw defãs moo ci ëpp te jamono jii ñu xarañ ci kaw ak ci kanami kã yi lees gënoon a xaar ci moom.
https://www.defuwaxu.com/can-2023-aliw-siise-tann-nay-ndawam/
Gannaaw loolu it yëkkati na ciy kàddu moom Aliw Siise di xamle ni:
https://www.defuwaxu.com/can-2023-aliw-siise-tann-nay-ndawam/
“Duma Yàlla, duma yonent. Tàggatkat laa te awmay xërëm ngiy soppi yëf yi. Li ma mën tay mooy góor-góorlu. Lenn lu nu mën, nun, mooy góor-góorlu.”
https://www.defuwaxu.com/can-2023-aliw-siise-tann-nay-ndawam/
Muy lees ko mën a nangul itam. Bu loolu weeso, ekib bi dina amal ndajem xaritoo ak kii di Niseer fii ci réew mi ca fowub Abdulaay Wàdd 8i fan ci weeru saŋwiyee wii bu 18i waxtu jotee.
https://www.defuwaxu.com/can-2023-aliw-siise-tann-nay-ndawam/
Nu mànkoo wutiwaat ndam li.
https://www.defuwaxu.com/5796-2/
Seen xiibaari tàggat-yaram Dibéer 12i Féewaryee 2023
https://www.defuwaxu.com/5796-2/
Kuppeg àddina këlëb yi :  “Real Madrid” defatina ko !
https://www.defuwaxu.com/5796-2/
Démb ci gaawu gi, 11i Féewaryee bii atum 2023, la woon finaalu kuppeg àddina këlëb yi, mu doxoon ci digante “Real Madrid” ak “Al-Xilal”. “Real Madrid” moo dóor juróomi bal ci ñett (5-3) dellu jëlati raaya ji. Bii moom 5eelu yoonam bu muy jël bile kuppe waaye it kuppe gii doon 100eelu kuppe yu mu jël ba mu sosoog leegi, muy lu rëy. Mu nekkoon finaal  bu neex donte ñu bari nag xamoon nañu ni Real Madrid daf koy dóor, waaye it taxul Al-Xilal yombalal ko ko, ñëw na ak bëgg-bëgg xeex ca la mu mën.
https://www.defuwaxu.com/5796-2/
Gannaaw fan yu xaw a lëndëm yi mu nekkewoon ci fan yii ñu génn, rawatina ba leen “Barça” dóoree woon Finaal, gisoon nanu ni dafa xawoon a baayi loxoom walla mel ne ku réeraloon wureem. Kuppe gii ñu jël démb yaakaar naa ni dana nekk lu leen di dolli jom ci li des ci at mi. Fi mu toll nii moo ngi war a dajeeti ak “Barça” 1/2 kuppeg buuru Espaañ (coupe du roi), war a xëccoo ak moom ba tay Sàmpiyonaa ba, ba noppi xeexi nguuram ga xa “League des Champions”.
https://www.defuwaxu.com/5796-2/
Ana kukoy tee, Vinisis ?
https://www.defuwaxu.com/5796-2/
Saa-beresil bi, luñu ko gën a xeex, muy gën a wane boppam. Fan yii weesu gis nañu na koy moroomi wurekatam sonalee ca Espaañ, nga xam ni dañu koy cokkaas ak di ko gaañ, leeg sax soppey yeneen këlëb di ko saaga ak a xas ndax limuy ku ñuul. Loolu lépp teewul muy yokk jom ak fi gën a wane boppam. Démb ci seen finaal bi mu taal ñaariyoon kër gi ba noppi joxe ci ñu dugal. Gannaaw loolu ñu fal ko wurekat bi gënoon xereñ ci kuppeg àddina këlëb gi. Kii di Walweerde (Valverde) dugalatina ñaari bay ci démb, yeewuwaat ci nelaw yi mu nekke woon ba noppi weesu lim bi ko tàggatkatam bi tegaloon ngir mi dugal lu tol noon mbaa lu ko ëpp (10). Bensemaa it jot na ci dugal bennam. Loolu di mbégte ci waa “Real Madrid” ak seen soppe yépp.
https://www.defuwaxu.com/mbemestal-ci-jaar-jaaru-allaaji-omar-taal/
MBËMËSTAL CI JAAR-JAARU ÀLLAAJI OMAR TAAL
https://www.defuwaxu.com/mbemestal-ci-jaar-jaaru-allaaji-omar-taal/
Àllaaji Omar Taal mi juddu ci atum 1796 ca Fuuta, bokk na ci ñi siggil ba fàww nit ku ñuul ci lislaam. Nekkul woon rekk njiitul diine ak tariixa, wànte boroom xam-xam bu gëmoon der bu ñuul la, te fonk dénduw Afrig gépp. Ginnaaw bi mu wedamloowee ay sëriñam, Àllaaji Omar feeñaloon na yeneen i kéemtaan ci daara ja mu nekkoon. Baayam boroom xam-xam la woon bu jànge Daaray Pir, doon daara ji gënoon a kowe ci jamono jooju. Yaayam it, Soxna Aadama Ayse, yaaram la woon bu nangoo séy te baax, fonk boroom këram ak wujjam. Abdul Karim Jàllo, ab sëriñ bu jànge Gànnaar, jële fa wirdu Tijaan, moo ko jëkk a jox wird wa. Ci lan fasante woon kóllëre ñoom ñaar. Àllaaji Omar jaaroon na Misra, siggil fa der bu ñuul. Boroom xam-xami Misra xawoon nanu koo xeeb ngir wirgo deram, wànte bim jëflaanteek ñoom ba noppi, ñoom ñépp a luum. Ba mu ajee Màkka la taseek Muhamadu Xaali nekk taalibeem ay weeri weer. Muhamadu Xaali natt ko ci bépp anam, def ko Xalifa ci ndigalu Seex Ahmad Tiijaani. Àllaaji Omar Taal sumboon nay xare Senegaal ba Niseryaa ngir tuubloo ceddo yi, yaatal lislaam fépp ci Afrig sowu-jànt. Ci 1864 la ko noon yi ërtal mu dugg ci Degembeer ne fa mes. Dees na wéy di fàttalikuy jalooreem ba fàww.
https://www.defuwaxu.com/njaay-daraapoo-dedduna/
NJAAY DARAAPOO DËDDU NA
https://www.defuwaxu.com/njaay-daraapoo-dedduna/
Momar Njaay, ñu gënoon koo miin ci turu “Njaay Daraapoo”, dëddu na. Moom, nag, ku ràññeeku woon la ci wàllu kuppeg Senegaal. Mi ngi faatu ci àjjuma ji 31 màrs 2023. Muy xibaar bu tiis ci waa Senegaal yépp, rawatina njabootug kuppe gi.
https://www.defuwaxu.com/njaay-daraapoo-dedduna/
“Njaay Daraapoo”, ku fësoon lool la ci ekibu Senegaal bi. Ndaxte, atum 2002 la tàmbali woon a ànd ak ekib bi. Dafa bokkoon ci mbootaayu 12eelu gaynde gi. Looloo indi turu “Njaay Daraapoo” wi. Nde, moo doon yore raayab Senegaal bu rëy bi, di ko wëndeel, saa bu ekib biy joŋante. Ndeysaan, amul fu mu àndul ak ekib bi. Muy Kuppeg Afrig, di Kuppeg àddina si, fépp la dem, topp ginnaaw gaynde yi, di leen dooleel ak a xirtal. Ni ko wolof di faral di waxee rekk, muy taw, mbaa muy naaj, dafa daan ànd ak ekib bi.
https://www.defuwaxu.com/njaay-daraapoo-dedduna/
Kuñ daan yomb a ràññe la nag. Nde, foo ko fekkaan, wirgoy raayab réew mi lay sol, bëggoon réew mi lool, ak ekib bi, ba foo ko nattoon rekk, weesuna ko. Xarit la woon itam ci jawriñ jiñ dénkoon wàllu tàggat-yaram, Mataar Ba. Ku ko miinoon lool la. Looloo tax Mataar ba seedeel ko kàddu yi toftalu, jaalee ko ko :
https://www.defuwaxu.com/njaay-daraapoo-dedduna/
“Ci naqar wii nu ame, noo ngi jaale ñii di waa-kër ki nga xam ni jóge na fi, di ko jaale itam jëwriñ jii ñu dénk mbiri tàggat-yaram, Yaankooba Jatara, njiitul mbootaayu 12eelu gaynde gi, waaye ak kureel gi ëmb soppey ekib bi.”
https://www.defuwaxu.com/njaay-daraapoo-dedduna/
Momar Njaay, nekkoon na kuñ yàgg a tappal i cargal ngir dogoom ak coono yim daj yépp ngir ekib bi. Cargal gi gënoon a rëy ciy bëtam, nag, mooy gi ko njiitu réew mi tappaloon, keroog, 17 saŋwiyee 2014, muy “grade de chevalier de l’ordre national du mérite”.
https://www.defuwaxu.com/njaay-daraapoo-dedduna/
Waxaguñu kañ lay koy denc ak ban bés lañ koy dëjal. Ñoo ngi dégloondi ba am ci lu leer.
https://www.defuwaxu.com/njaay-daraapoo-dedduna/
EJO ak Lu Defu Waxu ñoo ngi koy jaale njabootam ak i mbokkam, di leen mastawu, di ko jaale itam Senegaal gépp, rawatina axlu kuppe gi.
https://www.defuwaxu.com/senegaal-seen-gaal-la-noom-am-sunu-gaal/
SENEGAAL, SEEN GAAL LA, ÑOOM, AM SUNU GAAL… ?
https://www.defuwaxu.com/senegaal-seen-gaal-la-noom-am-sunu-gaal/
Ku waaruwul ci doxinu miim réew, saw doxin dina la waari ëllëg. Ku yéemuwul ci jëmu gaal gii, teeru bi dina la yéemi. Bees fobulee ci joowu yi joow ngir soppi jëmu gaal gi, nóoxóor yu ñuul yi dinañ joow yóbbu la, yaak say mbokk ak i xarit, wànteer leen ci nóoxóor yu weex yi. Su booba dinga yëngal bopp, màttu, wiccax sa baaraam naan “su ma xamoon…” Waaye, réccu day fekk jëf wees. Ndax dingeen bàyyee gaal gi nóoxóor yu ñuul yi, ñu joow jëme nu ca sëg ya ? Senegaal, seen gaal la, ñoom, am sunu gaal… ? Senegaal mooy réewum diine joo xam ni, ngëm dëgg feeñu fi fenn. Bëccëg, ku la ci ne “Yàlla nee na…”, “Yonent bi nee na…”, “Sëñ bi nee na…” bu la fenulee ngir naxee la ko yit, guddi mi ngiy njabarlu. Te li mu koy dugge mooy liggéey nawleem, yàq diggante yi, wut alal walla nguur, walla bëgg a siiw. Senegaal mooy réewum diine joo xam ni, bés bu nekk ñu tagg Yàlla, tagg Yonent bi, sargal Mag ñu baax ñi te kenn jéemul a roy ci ñoom. Senegaal a bariy jumaa, jàkka ak i taalibe, waaye Senegaal a bariy naaféq. Senegaal a bariy xew-xewi diine ak ñiy woote jàmm, waaye Senegaal a bariy waabajiiba. Moo ! Askan wu làmboo jikkoy naaféq ak melokaanu waabajiiba ban xeetu njiit la yeyoo ? Waaw, askan wu fase ngor, gàddaay dëgg, dëddu njub, suul fullaak faayda, ban xeetu njiit la yeyoo ? Ma laajati, askan wu sol mbubbu kàkkataar, dëkke fen, wor ak sàcc yan njiit la yelloo ? Yàlla ku maandu la. Moo tax it, lu waay rendi, ci say loxo lay nàcc. Nan dem rekk… Senegaal ngay fekk askan wu dëkke ŋàññi ay njiitam, ci diirub juróom-ñaari at, bés bu nekk ñuy xultooka ñaxtu. Waaye, bés ñëw, bésub dibéer, askan woowu tànnaat yooyii njiit, tegaat leen ci boppu gaal gi, ñuy joow, jëme gaal gi fu leen neex. Nu dem rekk… Senegaal bokk na ci ñaar-fukk ak juróomi réew yi gën a torox ci àddina si. Dëkkuwaay bu baax amu fi, luyaas bi metti na lool, xiif ak mar ne fi ràcc di bëgg a rey askan wi, ndóol waxi noppi, ku ci feebar dee ndax ñàkk loo fajoo walla loppitaan yu rafley jumtukaay. Njàng amatu fi waxatuma laak xéy, añs. Moone de, fii ngay fekk ay njiit yiy tabax i taax yu kowee-kowe, dëkk ciy kër yu réy te rafet lool, di dawal ay oto yu yànj ba jaaxal la. Ku ci ab yoo màtt, nga jël roppëlaan, naan yaa ngay fajooji Tugal. Rax-ci-dolli, seeni doom di jànge bitim-réew, ci daara yi gën a baax te siiw, ay daara yu ndongo ya xamul naka la ñuy waxe ‘’gereew’’. Njiit yooyu, ñooy jël alalu réew mi tayle ko Tubaab yi, di pasar-pasare xaalisu askan wi, di ci gundandaat ak a ndagarwale ca Soraanoo, Garaŋ-Teyaatar, làmb ja, ci yeneeni xew walla ciy mitiŋ. Bu wote jotee, ñu jël ci as tuut, di ko jënde askan wi nga xamante ne, lu jiin Njaag a, te mooy Njaag. Waaw, ndax sagaru junni, benn piisu waks bu fuyuŋ-fayaŋ, walla saaku ceeb jar na ngay jaay sa ngor ? Nga ne ma ? Sa alal la ? Newuma la déet de, waaye nan demati rekk… Senegaal mooy réew moo xam ne, Njiitu-réew mi lu ko neex def. Saa bu ko neexee mu jàpp kii walla kee, dëkke fi tëj ak jaay doole guddeek bëccëg. Bu wote jotee, askan wi tànnaat ko, teg ko ci jal bi. Ngan ne ma ? Naataange la la dig ? Walla la la digati…? Ayca nu dem rekk … Senegaal mooy réew moo xam ne, ndaw yi amuñu liggéey. Waaye, foo leen fekk ñoo ngiy werante ciy mbir yu ñàkk faayda : film, tiyaatar walla futbal. Doo gis benn ndaw, muy góor walla jigéen, bu nangoo yedd boppam, soppi jikkoom. Janq jaa ngiy mébét doon léttkat, ñawkat, woykat walla fecckat. Ñi ci yées, dem bay cagatu naan dañuy daan seen doole. Waxambaane bi moom, di ñefe ngir doon mbër walla futbalkat. Ñi ci gën a ñàkk faayda ñoom, rusuñu doon i woykat, fecckat, tëggkati sabar wallay taasukat. Ñi ci yées, di dogaale jaamu Yàlla yi, ngir nangu seen alal. Nga ne ma ? Tëgg ak fecc ci sunu aada la bokk ? Waaw, kon daal tëgg ak fecc a nuy jëme kanam ? Waaye baax na, nan demati rekk… Senegaal mooy réew moo xam ne, làkku jaambur lañ fiy jàngale ak démbu doxandéem. Kenn jàngalul xale yi ngir ñu mënal seen bopp, gëm seen bopp, moom seen bopp. Waaye, dañ leen di jàngal ngir ñu doon i jaam yuy tàllal loxo. Nga ne ma ? Sunuy làmmiñ réew mënunu cee tekkee ? Yaakaaroo ne ki la wax loolu dafa laa yab ? Yaakaar nga ne teg na la nit Njaay ? Waaye nu dox dem rekk… Senegaal mooy réew mu bari alal te askan wi jariñoowu ko ; réew mu bariy àttekat te amul yoon ; réew mu ñépp bokk, ay sàmba-allaar aakimoo ko di ci def lu leen neex. Senegaal mooy réew mi nga xam ne, foo dem ñu ni la “waa réew moomoo neex xel ! Ñoom kay, kuy wut xalaat bu rafet, gaawal ganeji fa.” Nga ne ma ? Dëgg la ! Dëgg piir sax ! Fii daal, ku ëpp sa moroom doole wan ko ko. Moo tax it, ku yeboo jéem a muus, di jëfandikoo sam xel ngir jël sa wàll ci toŋ-toŋ bi. Loolu doŋŋ la, nag. Bu nu kenn rey ak wax ju bare. Politiseŋ yi loolu lañu nànd bu yàgg, kon lu may tere def ni ñoom ? Léegi nag, àgg nanu. Nanu wax ak ndaw yi. Ndax kat, ëllëg, seen ëllëg la. Ndax warees naa seetaan lii di wéy ? Senegaal, seen gaal la,ñoom, am sunu gaal ? Li wér te wóor mooy, sunu gaal gaa ngi daw ni gaalu dof ci géej gu sàmbaraax. Jot na askan wi yeewu, nangu joowu yi ngir jubbanti gaal gi. Ndax kat, gaalu dof du teer, walla bu teeree yit, teeri ci loxoy nóoxóor. Paap Aali Jàllo
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-tey/
DÉMB AK TEY
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-tey/
Dal-leen ak jàmm ci seen xët DÉMB AK TEY mi leen seen yeénekaayu web LU DEFU WAXU jagleel. LU DEFU WAXU nag, li ko tax a jóg mooy dégtal leen ay xibaar yu wér te wóor te aju ci xew-xew yi gën a fés ci réewum Senegaal ak sax ca bitim-réew.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-tey/
Waaye tamit, bindkat yi dinañ  faral di leen ci baaxe seeni gis-gis ak i xalaati doomi réew mi ci mépp mbir mu ñeel Senegaal.  Rax-ci-dolli, yéenekaay bi dina leen wisal, may leen ŋeleju ayu-bés gi ak nataali ODIA, aji-ŋeleju bu mag bi. Bii-yoon, nag, seen yéenekaay LU DEFU WAXU da leen a indil lu bees tàq, mayati leen ko, muy seen xët DÉMB AK TEY.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-tey/
Ñaari baat yii, DÉMB ak TEY, ay tegtal lañu ci li xët mi wund. Jokkalekat bi, “AK”, di wone ne deesuleen  téqale. Maanaam, kenn warul a féewale cosaan walla jamonoy maam ya (DÉMB) ak sunu jamono jii (TEY). Bu ko defee, li nu ko dugge mooy dekkil cosaan, fàttali leen xew-xewi démb yu mag yi. Waaye nag, bàkk mbaa ŋàññ maam rekk yi taxunoo jóg. Naka noonu, jógunu ngir di leen nettali rekk li xewoon démb walla di leen léebal. Bu ko defee, nësër gi dëgg mooy lëñbëtil leen cosaan ak aaday maam ya, méngale leen ak jamonoy tey jii ngiree nu rotal ciy njàngat yi nuy jariñ tey, leeralal nu sunu ëllëg. Ci gàttal, xët mu bees mii nu duppe DÉMB AK TEY , li mu sasoo moo di wëral leen réew mépp, sowu ba penku, bëj-gànnaar jàpp bëj-saalum, béréb bu nekk mu taxaw fa xamal leen la fa xewoon ak njàngale yi ñu ci mën a jukkee. Ndaxte, cosaan mooy caabi jiy ubbi buntu tey, di làmp biy leeral ëllëg. Kon, cosaan deesu ko xeeb. Ndege, ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-tey/
Seen yéenekaay LU DEFU WAXU xam na ni, wenn askan mënul a jëm kanam féeg mi ngi dëddu cosaanam. Rax-ci-dolli, réew mu askan wa naat, ci cosaanam ak i aadaam la sukkandiku ba indi fa ay yokkute. Looloo gënatee tax mu baaxe leen xëtam mu bees mii. Wolof dafa ne, kuy dem ba xamatoo foo jëm, war ngaa dellu fa nga jóge.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-tey/
Bu ko defee, sunu sas moo di dellu rooti ci teenu DÉMB, nàmpi ca meenu cosaan ngir tabax sunu TEY ak sunu ËLLËG. Seen mbokk, Paap Aali Jàllo moo nekk ci boppu gaal gi, di ko joow ci géejug cosaan, yen saa yi mu mbiij ci dexug aada, leeg-leeg moom walla kenn ci LU DEFU WAXU indil leen sarica.
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-tey/
Tey, Daawuda Géy moo def ab gëstu ca Kaasamaas ci ñeyu-xare bu ñépp miin turam te taxul kenn xam ko bu baax : Jiñaabo.
https://www.defuwaxu.com/as-pikine-guediawaye-fc-xumb-te-dagan/
AS PIKINE – GUEDIAWAYE FC : XUMB TE DAGAN
https://www.defuwaxu.com/as-pikine-guediawaye-fc-xumb-te-dagan/
Keroog, ci gaawu gi 29 awril 2023, sàmpiyonaa Senegaal bi jaxoon na lool. Ndax, As Pikine ak Guédiawaye Fc ñoo doon daje. Mu nekkoon joŋante boo xam ne, ñi ko doon xaar bari nañ. Ndaxte kat, du joŋante bu ndaw. Mënees na jàpp ne sax, ni fii ci Senegaal, mooy sunu Barça-Real, walla sax Paris Saint-Germain-Marseille. As Pikine ak Guédiawaye Fc di ñaari ekib yu bokk daanaka benn gox mbaa nu wax ni ñoo takkaloo, ñuy yenn ci ekib yu gën a mag ci sàmpiyonaa Senegaal gi.
https://www.defuwaxu.com/as-pikine-guediawaye-fc-xumb-te-dagan/
As Pikine bu waree joŋante, ni ñuy waajalee seen bés yi ak soppe yu bari te gëm ekib ba nañuy mel, meneen mbir la. Muy këlëb bu yàgg a wane boppam, di ekib bu mag. Guédiawaye Fc itam, naka noonu. Ci at yii ñu génn, gis nañu jaloore yi mu fi def yépp : wàcc Ligue 2 bi, jël ko yéegaat fekki punkali Ligue 1 yi.
https://www.defuwaxu.com/as-pikine-guediawaye-fc-xumb-te-dagan/
Gis nañu nag, ñi dëkke ca gox ya na ñuy jàppee ci seen i ekib ak liñ leen jaral. Ku ci mel ne Bàlla Gay, mbër mu mag mi dëkke Géejawaay, def na ci waajtaayu joŋante bi benn tamndaret ci sunuy koppar, mu nekk luy dooleel ekib ba ci lu bari.
https://www.defuwaxu.com/as-pikine-guediawaye-fc-xumb-te-dagan/
Joŋante bi nag, barkaati-démb, ci gaawu gi, la amoon. Rëyaayu joŋante ba taxoon na ñu bàyyi fowu yépp, tóxal ko ca fowub Abdulaay Wàdd, Jamñaajo, fa ekibu Senegaal bu mag biy joŋante. Ekib bu ci nekk, indi nga say soppe, mu neexoon lool, xumb ba dee. Joŋante bi nag  neexoon na lool, bal bi daw na, futbal bi set na. Waaye nag, ndam demul, ndam dikkul. Ñaari ekib dañoo mujje joxante loxo, kenn dugalul sa moroom. Guédiawaye Fc, boo xoolee, moo féete kaw. Ndaxte, mooy nekkagum ci ñetteelu toogub sàmpiyonaa ba ak 31i poñ, As Pikine jëlagum 6eel ak 25i poñ.
https://www.defuwaxu.com/as-pikine-guediawaye-fc-xumb-te-dagan/
Joŋante bi jur na liñ ci doon xaar, muy kuppe gu rafet, bal bi daw, ñu amal ko ci jàmm. Ba ci soppe yi nekkoon ci kaw, yëngal nañu ba mu neex, lépp ci jàmm ak salaam.
https://www.defuwaxu.com/as-pikine-guediawaye-fc-xumb-te-dagan/
Ñu bari nag rafetlu nañu ni ñu yóbboo joŋante gi ci bóobee bërëb. Ndax, jàpp nañ ne dina gën a may bët ak bayre sàmpiyonaa bi. Rax-ci-dolli, ekib boo fa yóbbu, daanaka ay soppeem dinañu sawar a seetaani ko, te dina dundal sàmpiyonaa bi ak kuppeg Senegaal.
https://www.defuwaxu.com/as-pikine-guediawaye-fc-xumb-te-dagan/
Ñoo ngi xaarandi yeneen bés yu ni mel. Ndax, bile moom neexoon na lool. Te, lu neex du doy. Ndaxte, xumb na, dagan na.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-21-6-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (21/6/2023)
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-21-6-2023/
Senegaal duma na Beresil 4-2
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-21-6-2023/
Démb ci talaata ji la ekibu Senegaal bu mag bi doon amal joŋantebe xaritoo ak bu Beresil, faLiisbon, gëbla Purtugaal. Ndekete, sunu gaynde yi yarasuñ benn yoon ! Firndeel nañu tamit ne, duñu yàqi te duñu bàyyeeku. Ndax, Beresil a ñjëkk a dugal. Waaye, Senegaal mayu ko sax mu noyyi. Nde, 4 la ko yen laata Beresil di dugalaat beneen, muy 4-2. Ndam li, ndam lu réy réy. Ndege, Senegaal mooy ekibu saa-afrig bi njëkk a dugal Beresil 4i bii. Rax-ci-dolli, 2014 ba tey, ginnaaw bi ko Almaañ rokkosee woon 7i bii ya, guléet mu jël lu tollu ci 4i bii. Kon, gàcce-ngaalaama sunu gaynde yi. Abiib Jàllo moo dugal benn, Marquinhos dugal seen kã, Saajo Maane lakk caax yi 2i yoon.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-21-6-2023/
Aliw Siise bégoon na ci gaynde yi ak ci ni joŋante bi deme. Moo ko tax a bëgg lu ni mel di faral di am. Daf ne :
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-21-6-2023/
“Joŋante yu mel nii lanu bëgg ngir di ci nattee sunu doole. Bëggaat nanu ci yeneen yoo xam ni, Ndakaaru lay doon, Senegaal. Beresil na ñëw ñu dalal ko sunu réew mu xam ko, walla sax Àrsaantin.”
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-21-6-2023/
Bu dee Saajo Maane nag, mi ngi gën a rëdd turam ci mbooru kuppeg Senegaal. Ndax, démb la dugal 36eel ak 37eeli biiyam ak Senegaal.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-21-6-2023/
Cristiano Ronaldo : 200eelu joŋante ak Purtugaal
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-21-6-2023/
Ronaldoo démb ladoon amal 200eelu joŋanteem ak dëkkam, Purtugaal. Guddeem ga neexoon na nag. Ndaxte daf ci dugal benn bii bi tax Purtugaal gañe joŋante bi. Moom itam, mag mu dul màgget la ; doon paa terewukoy gën a aj turam ci mboorum kuppe gi.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-21-6-2023/
Ngoloo Kànte fekki na Bensemaa
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-21-6-2023/
Ngolo Kànte juge na Chelsea, fekki Kariim Bensemaa këlëbu Al-Ittihad, ca naari Araabi-Sawdiit ya. Liñ naan xaalis mën na lu ne, ndeke dëgg la. Ba fa Ronaldo demee, dégg nañ ci gannaawam wax ju nekk. Waaye de, dafa mel ni ñiy topp yoonam a ngi bëgg a bari. Naar yaa ngi yóbbu ñu bari.
https://www.defuwaxu.com/niseryaa-buhari-faluwaat-na/
NISERYAA : BUHARI FALUWAAT NA
https://www.defuwaxu.com/niseryaa-buhari-faluwaat-na/
Ci weeru féewaryee wii jàll la askanu Niseryaa doon amal woteb njiitu réewam. Ba ñu àggee ci cëpaandoo li, Muhammadu Buhari la askan wi tànn, dénkaat ko réew mi. Lu tollu ci 15 alfunniy wotekat ñoo sànnil xob ki toogoon ci jal bi 2015 ba léegi, mu jël raw-gàddu gi ci kanamu lawax bii di Atiku Abubakar.
https://www.defuwaxu.com/niseryaa-buhari-faluwaat-na/
Chinua Achebe mas naa bind cib téereem bu siiw ci atum 1983 ne liy gàllankoor Niseryaa du lenn lu dul i njiit yu matul i njiit. Jaar-jaaru Buhari firnde la ci ndaxte 36 at ci ginnaaw, laata muy falu ci yoonu demokaraasi, àndoon naak i moroomi soldaaram jiital doole, foqati nguur gi ci loxoy Shehu Shagari. Waaye, àddina sépp benn seede lañu biral ñeel Buhari te moo di ne du sàcc, àndul ak kuy sàcc walla ger te yit, nit ku dëggu la, xamul caaxaan, am fulla ju mat sëkk.
https://www.defuwaxu.com/niseryaa-buhari-faluwaat-na/
Ba muy kàmpaañ ci atum 2015, la mu gënoon a fésal, ciy digeem, moo doon jàmmaarlook tuurkati deret yii di waa Bokko Haram ak dakkal ger ci Niseryaa. Doonte sax ay yéeneem yépp àntuwuñu ci ñaari fànn yooyu, nit ñi nangul nañu ko ni def na ciy jéego yu am solo.
https://www.defuwaxu.com/niseryaa-buhari-faluwaat-na/
Waaye, nag, jot naa jànkoonteel i jafe-jafe ba mu faloo ci atum 2015. Ndaxte, njëgu petorol bi nga xam ne moo téye koom-koomu Niseryaa, dafa daanu woon bu baax, daldi nasaxal weccitu réew mi ba noppi yokk fa ndóol. Rax-ci-dolli, mbir yi àggoon na ba ci xéy jafe woon lool ci ñi ëpp ci réew mi, limu ñi amul liggéey daldi ful ñaari yoon.
https://www.defuwaxu.com/niseryaa-buhari-faluwaat-na/
Te tamit, Buhari mag la, yaram wi neexatul. Waaye, moom de, mel na ni yàkkamtiwul daraam, mi ngiy def li muy def, ànd ceek dal. Looloo waral xaley Niseryaa yi utal kob dàkkantal, di ko woowe Baba-Go-Slow. Gaa, Buhari dafa ñëw fekk ay tolof-tolof yu bari gàll koom-koomu réewam. Teewu ko fexe ba dugal xaalis bu bari ci mbay mi ak jumtukaayi xarala yi. Ger gi mu waxoon ni dina ko xeex tamit, wax-dëgg-Yàlla def na ci kemtalaayu kàttanam. Li dalul xel ciy mbiram, daal, moo di ne Buhari jikkoy soldaar la am ba tey, mënul a tàggook moom : képp ku ko déggalul, du la may jàmm.
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-jafe-jafey-reewi-afrig-yi/
FUTBAL AK JAFE-JAFEY RÉEWI AFRIG YI
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-jafe-jafey-reewi-afrig-yi/
Doom-aadama fent na ay xeeti po yu bare. Ba ci tàggat-yaram sax, nga xam ne, ci cosaanam, yar ak wér-gi-yaram ñoo ko taxoon a jóg, nit soppi na ko, def ko liggéey ak po, di ci amal ay joŋante yu mag, àddina sépp di ko teewe. Xeeti po yooyu, nag, futbal a ci gën a siiw te yit moo ci gën a law ci àddina si. Baatu futbal, ci làkku àngale la jóge te di tekki tank (fut-) ak bal, maanaam bal bi ñuy dóore tànk. Futbal ci boppam bare nay xeet, waaye bi ci gën a fés mooy bi nga xam ne, fukk ak benni nit ñooy jàkkaarlook seen yeneeni fukk ak benni moroom, ku nekk di jéem a dugal bal bi ci kãwu keneen ki ci diirub 90 simili. Powum futbal mi ngi cosanoo ca réewum Àngalteer. Àngalteer, nag, saa boo ko waxee xel yi dem ci ñoom Bobby Charlton, Gordon Banks, Stanley Matthews, Michael Owen, Bobby Moore, Alan Shearer, Kevin Keegan ak lingeer Elisabeth II, añs. Kon, tubaab yi ñoo sos futbal ba noppi daldi ko tas ci àddina si, ñépp bëgg ko. Afrig tamit kenn demul mu des, ndax doomi Afrig yi amul ku leen gën a xër ci futbal. Waaw.
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-jafe-jafey-reewi-afrig-yi/
Boo génnee ci mbedd yi dinga gis xale yiy top ci ginnaaw bal biy dóor ba ñaq tooy xepp, subaak ngoon ñu ne ci. Waxambaane yi ñoom, foo leen fekk ñoo ngiy seetaan futbal walla teg seen àttaaya di ko waxtaane. Mag ñi di waxtaan ak a fàttaliku jamonoy Sàndaark, Jaraaf, Duwaan walla Asfaa, walla sax jamonoy Bokànde ak Séex Sekk, di leen méngale ak goney léegi yi. Nawetaan moom, li mu jaral xaley koñ yi, mëneesu koo natt. Kon daal, futbal bawul kenn ci Afrig li ko dale bëj-gànnaar jàpp bëj-saalum, jóge sowu jëm penku, fépp la feebarub futbal law ; rawatina Senegaal gii, du mag du ndaw, muy góor walla jigéen. Moom kay, politig bi sax da cee rax léegi ndax dayo bi mu am.
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-jafe-jafey-reewi-afrig-yi/
Moo tax it, yenn saa yi, nguur gi ci lay jafandiku ngir fàtteloo askan wi jafe-jafe yi mu nekke. Ndege, ku ci sa réew di joŋante, day mel ni da ñuy raxas sam xel, nga fàtte say aajo ak say ay, sa xol ak sa xel yépp nekk ci joŋante bi. Rax-ci-dolli, futbal bi léegi liggéey la : fokat yi ñi ngi ciy am xaalis bu dul jeex, jaaykat yi noonu ba ci bérébi liggéeyukaay yu mag yaa ngi ciy defar seeni mbir. Futbal a ka bare bayre, naam ! Joŋante bu mag biy dajale ñaari at yu ne réewi Afrig yi ab firnde la ci.
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-jafe-jafey-reewi-afrig-yi/
Joŋante ren bi nag, ca Misra lay ame. Muy réew moo xam ni, askan wi ci nen la toog. Ndaxte njiit ma fa ne, dib Seneraal ci làrme bi, Al Sissi, jaay doole ak xoqtal nit ñi la fa nekke. Askan wi sonn lool. Ñu bare jàpp ne dafay jëfandikoo joŋante boobu ngir muur metit yi askan wiy jànkonteel jamono jii. Waaye, mel na ni pexeem moomu sooy na, ndax réewum baay Nelson Mandela daan na bërki-démb Misra jéll bu set wecc, ginnaaw bi mu ko dóoree 1-0.
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-jafe-jafey-reewi-afrig-yi/
Waaye bu ñu fatte li ponkal ma woon, Mawàdd Wàdd, daan wax : “Dawuma ci ginnaaw bal, ci ginnaaw nit ñiy daw ci ginnaaw bal bi laay daw. Ndax, nit ñoonu ay xale ñoo ci ëpp, te xale yooyu ñooy ñiy jiwi ndamu askan wi ëllëg.” Yaakaru waa ju baax jooju, taxawoon démb di xeexal réewum Senegaal ak doomi Afrig yépp, te jaarale woon ko ci tàggat-yaram, mat naa bàyyi xel. Wànte, mel na ni tey bukki-njuur-sàmba yi ŋànk futbalu Afrig bokkuñu ak moom xalaat.
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-jafe-jafey-reewi-afrig-yi/
Waaye, nan jàppale sunu gaynde yi nu fa teewal.
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-jafe-jafey-reewi-afrig-yi/
Ba négéni, gàcceeluñu nu. Ndax, dibéer jii weesu rekk lañu daan Ugàndaa 1-0, daldi jàll ci kaar de finaal yi. Waaye, nag, bumu nu tax a réere mbir jafe-jafey askan wi ak mbirum petorol bi ak gaas bi lëmbe réew mi. Wareesul a fàtte yit baykat yi, xale yiy dugg ci looco yi wutali Ërob te naan Bàrsaa walla barsàq, njàng mi, lopptaan yi, yoon wi, añs.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-10-07-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (10/07/2023)
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-10-07-2023/
MAROG JËL NA CAN U23 BI
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-10-07-2023/
Démb, ci gaawu gi, lañ doon amal lii di finaalu CAN U23 bi doon ame fa Marog. Mu gi dooxoon ci digante ñaari naataango yii di Marog mi dalal xëccoo bi ak Esipt. Mu nekkoon finaal bu neex. Waaye, Marog moom, moo xewle, daldi woote, luñ nar a fecc mu fecci ko, lekk ci it mu ni leen fuuf ni gan ya ñibbi leen. Maanaan moo woote po mi ca dëkkam, finaalu ba noppi jël kub bi.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-10-07-2023/
Bi ñu dawalee ba fukkeelu simili bi la Esipt daldi dugal (Saber). Ñuy wéyal ba ci 37eelu simili bi, kii di Y. Begraoui fayul dëkkam, muy 1-1. Ñu jàppe ko noonu ba 90i similiy joŋante bi jeex, kenn dugalaatul. Ñu àgg “prolongation”. Biñ àggee ci 108eelu simili bi (105+3) la Marog yoxosu Esipt, dugalaat benn (O. Targhalline), muy 2-1. Nooyu lay jeexee. Abde Ezzalzouli, kàppitenu Marog, moo ëpp lum dugal ci xëccoo bi (3i bii) ak lum ci joxe ñu dugal (3i paas).
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-10-07-2023/
EURO U21, ÀNGALTEER NAX NA ESPAAÑ !
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-10-07-2023/
Ba tay, ci gaawug démb gi lees doon amal it finaalu Euro U21 bi diggante Àngalteer ak Espaañ. Àngale yi ñoo mujje dóor espaañol yi benn bal ci dara. Àngalteer nag, yamul ci jël kub bi rekk, dafa def lu réy. Ndaxte, dem na ba jël ko te benn bal laalul i caaxaam, maanaam kenn dugalu ko. Te, ñoom, dugal nañ 11i bii ci seen juróom-benni joŋante yoy, yépp lañ gañe. Loolu di lu rëy.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-10-07-2023/
LAMB : PAPAA BOOY JINNE DAANOOTI NA
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-10-07-2023/
Ndiggu Papaa Booy Jinne laalati na suuf. Ndàndi Faal moo ko daanati démb ci gaawu gi. Moom Papaa Booy Jinne, gëj na am ndam. Ndax, 2017 la arbit gëj a yékkati loxoom. Kor Ndey Géy (fecckat) ba woon, ñu baree ngi naan na tekki ngembam.
https://www.defuwaxu.com/taggatoo/
TÀGGATOO
https://www.defuwaxu.com/taggatoo/
Roqi, ba beneen yoon.
https://www.defuwaxu.com/taggatoo/
Seetal ma lii rekk. Wax dëgg. Xool sama digganteek Yàlla te bañ a fen.
https://www.defuwaxu.com/taggatoo/
Waaw, yombul nga seeti sa rakk ak sa mag te say rongooñ tuuruwuñu. Walla dara yëngalul sa yaram.
https://www.defuwaxu.com/taggatoo/
Li ma yëg tey bi may tàggoo ak Roqi Yàlla rekk a ko xam. Bi ma koy nuyu, di wéy di dem, geestuwuma ndax xol bu fees ak yaram wuy rëg-rëgi. Ma xam ni deret fum la fekk daan la. Te doo ci mën dara. Li ci gën a yéeme mooy dangay mel ni ku ràkkaaju. Nga naan : « waaw feebar bi ma soppi nii nu mu tudd ? » Geneen kàddu jib, daldi feelu, ne : « feebaru mbokk moo la daan ba nga xalangu. » Bu ko defee, may seet naka laa koy fajee.
https://www.defuwaxu.com/taggatoo/
Doktoor mënu ci dara. Farmasi du jaay lu koy woyafal.
https://www.defuwaxu.com/taggatoo/
Roqi gënuma laa xam li may bind. Duma fi nekk di jekk-jekkal ak a làq-làqal. Damay jaar ci digg bi, toj yax bi. Su ma wóoroon ne tàggoo nii la mettee damay randal sama ñibbisi Itali. Waaye lu la bett, daan la ba nga mëq suuf si.
https://www.defuwaxu.com/taggatoo/
Lu waay di jàmbat, wolof njaay léebootina ko. Dëgg-dëgg sama rakku bopp ji lu ma wax rekk sama digganteek Yàlla laa ciy seet.
https://www.defuwaxu.com/taggatoo/
Weneen yoon su may ñëw Pari dama koy waaj bu baax. Julli ñaan Yàlla bañ a jooy, bañ a saalit. Guléet mu dal ma bésu tey. Àddina nii la. Ay jaar-jaar rekk la.
https://www.defuwaxu.com/taggatoo/
Abu Daraame, seede ma.
https://www.defuwaxu.com/taggatoo/
Baay NJAAY
https://www.defuwaxu.com/sunuy-doomi-ndeyi-mali-yi-sonn-nanu/
SUNUY DOOMI-NDEYI MALI YI SONN NAÑU
https://www.defuwaxu.com/sunuy-doomi-ndeyi-mali-yi-sonn-nanu/
At yi weesu yépp, fitu doomi-Mali yi toogul benn béréb. Weer yi nu génn sax, seen njàqare ak seen tiis dafa mel ni lu yokku. Te lenn waralu ko lu dul jàmmaarloo yu tar yi am ci diggante ñaari waasoo yii di Pël yeek Dogoŋyi. Lu ni mel nag, jaaxal na ñu baree-bari. Ndax, ci atum 2012 ay defkati ñaawteef yuy mbuboo lislaam song réew ma. Ginnaw gi la ci Mbootaayu xeet yi dugg, jële leen fa ci atum 2013 ba noppi déggoo ak ñoom ci atum 2015 ci li fay war a saxal jàmm. Waaye loolu lépp mel na ni mujjul fenn. Ci at mii nu nekk, ci weeru Mars, 160 Pël la Dogoŋyi bὀom. Ñu ne déet-a waay, Pël yi daa di feyu, faat bakkanu 35 Dogoŋci 9elufan ci weeru Suweŋ, dolli ci 38 ba tey ci woowu weer, ci li nguuru Mali wax. Loolu lépp ci ñaari dëkk yu wute la xewe. Waaye Mbootaayu xeet yi jàpp na ne 41 Dogoŋ la ñu faat. Daw fitnaa tax Pël yeek Dogoŋ yiy gàddaay, wuti fu ñu làqu, moo xam Burkina-Faaso la walla fu ñuy wax Dinaguura.
https://www.defuwaxu.com/sunuy-doomi-ndeyi-mali-yi-sonn-nanu/
Mbir mii nag, am na ñu jàpp ne xare ba fi jiyaadis yi amaloon moo ko sabab. Ndax nee ñu seen njiit, Aamadu  Kufaa, ci Pël yi la doon wute ay soldaar. Pël yi nag, dañoo jàpp ne Dogoŋ yee sotba Mbootaayu xeet yi sempi ndëndu jiyaadis yi, reyaale seeni mbokki Pël yu bare.
https://www.defuwaxu.com/sunuy-doomi-ndeyi-mali-yi-sonn-nanu/
Ñàkk kóolute gi lal lii lépp fan la jóge ? Ndax réerook mbañante gu yàgg rekk la ? Yàlla rekk a xam. Li am ba wὀor moo di ne waasoo Afrig yi yàgg nañuy jàmmaarloo ci seen biir. Te li koy waral léeg-léeg, bu weesoo xëccoo nguur, du lenn lu dul réere mbir li ñu bokk ndax, ni ko Séex Anta Jóob di waxe, li leen boole moo ëpp doole fuuf li leen di féewale.
https://www.defuwaxu.com/sunuy-doomi-ndeyi-mali-yi-sonn-nanu/
Leneen ub na lool boppu nit ñi ci mbir mi te mooy tekk-tekkaralu àddina sépp, li ñépp toog boobaak léegi di seetaan. Ku nee ngi xaar ba sa moroom wax ngay soog a yëkkati sa baat. Lii kañ xanaa mooy lekkante leen ba jeex tàkk, sunu yoon newu ci ! Moom daal, ku mën sa moroom dumaal. Mbete làmbu tàkkusaan !
https://www.defuwaxu.com/sunuy-doomi-ndeyi-mali-yi-sonn-nanu/
Li ci gën a xëtt xol, nag, mooy yàcc-yàccaaralu njiiti réewi Afrig yi, mu mel ni waa Mali duñu seeni mbokk. Te moo ne de ñoom lañu waroon a njëkk dégg bala kenn di yëkkatiy kàddu. Fi mu ne nii bala ñoo mën a wax mbaa ñu jëf fàww ñu jot ndigal lu tukkee ci nasaraan yi. Tàmm nañu ko sax. Seen yoon newul ci dëkkandoo bi leen yittewoo waaye su daray xew ci réewi Tubaab yi ñuy daldi tàggook seen sago. Ku ko weddi fàttalikul bés ba ay saay-saay songee Saarli Ébdo, rey fay taskati-xibaar. Keroog jooju njiiti Afrig yu bare fésal nañu seen naqar, ku nekk ci ñoom di nu tanqal, naan « Je suis Charlie ». Yii njiit daal, kenn xamul lu ñu doon. Boroom kër gu ñuy dab di ko mbej sax moo leen tane.
https://www.defuwaxu.com/sunuy-doomi-ndeyi-mali-yi-sonn-nanu/
Li am ba des daal mooy na waa Mali delloosi seen xel te xam ne ay wu waxtaan fajul, xeex du ko saafara mukk. Nde bi àddina sosoo ak léegi kenn mësul a gis xare bu jur jàmm. Moom kañ, musiba rekk lay sooke, delloo am réew ginnaaw.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-dibeer-29-sanwiye-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (Dibéer 29 saŋwiye 2023)
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-dibeer-29-sanwiye-2023/
CHAN 2023
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-dibeer-29-sanwiye-2023/
Sunu gaynde yee ngi wëyal di wane seen bopp fale ca Alseri. Bërki-démb, ci àjjuma ji, lañ doon daje ak seen naataango yi, Saa-Muritani yi, ñu mujje leen ko yóbbul benn bal ci dara (1-0). Ab teg-dóor lañu am, dugal ko ci xaaj bu njëkk bi.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-dibeer-29-sanwiye-2023/
Alseri, moom mi dalal joŋante yi, moo dóor na Koddiwaar 1-0. Madagaskaar itam a dóor Mosàmbig 3-1, Niseer daldi gañe Gana 2-1. Ñu war a jëm ci demi-finaal yi. Senegaal dina daje ak Madagaskaar  31i fan ci saŋwiye bi (19i waxtu) gannaaw ba Alseri dajee ak Niseer ba noppi (16i waxtu).
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-dibeer-29-sanwiye-2023/
Saajo Maane a ngi waaj a delsi
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-dibeer-29-sanwiye-2023/
Saa-senegaal bi, Saajo Maane, tàmbaliwaat na tàggatu fale ca këlëbam bii di Bayern. Ci fan yii nu génn, la dellusi ci pàkku tàggatuwaayu Bayern. Donte àndagul ak i moroomam yi, noo ngi gis muy liggéey di tàmbaliwaat di laal bal bi ndànk-ndànk. Loolu nag, nekk na luy dalal xeli almaŋ yi ak soppey këlëb ba, rawatina bi seen joŋante bu am solo bi ñuy waajal ak PSG jegesee.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-dibeer-29-sanwiye-2023/
Cig pàttali, doomu Bàmbali bi dafa ame woon gaañu-gaañu ci óom bi. Weeru oktoobar 2022 la ko daloon. Dafa di, looloo ko tere woon a bokk ca kuppeg àddina sii weesu ca Qataar.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-dibeer-29-sanwiye-2023/
Li mu delsi nag, du almaŋ yi rekk a ci bég. Mbokkam yépp, Saa-Senegaal yeet kenn demul ñu des. Ndaxte, sunu sag la. Ñépp a koy seetaan di bég ci moom. Kon ñoo ngi koy ñaanal bu baax mu gën a tane ba dellusiwaat ci pàkki wure yi.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-dibeer-29-sanwiye-2023/
Bàmba Jeŋ dem na Lorient
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-dibeer-29-sanwiye-2023/
Bàmba Jeŋ jóge na Marseilles. Nde, këlëbu Farãs bi mujje na nangu li Lorient fay, daldi koy bàyyi mu soppi këlëb. Bërki-démb, ci àjjuma ji, la dem ca këlëbam bu bees bi, ñu wane ko muy saafonte ak soppey Lorient ya. Moom nag, ba fa Sampawoli jógee la yaakaaram xaw a tas. Ndax, tàggatkat bu bees ba, Tidoor, boolewu ko lool ciy mbiram, ba tax lam fa doon wure bareetul woon. La mu gënoon a bëg nag, mooy toog fa wane fa boppam. Waaye, am nañ yaakaar ni dem gi moo gën ci moom ndax xale la te fàww muy joŋante ngir gën cee màgg bay wane boppam.
https://www.defuwaxu.com/gattali-taggat-yaram/
Saajo Maane ca Bayern Munich
https://www.defuwaxu.com/gattali-taggat-yaram/
Njiiti Bayern Munich yi mujje woon nañ déggook yu Liverpool FC yi ñeel ëllëgu Saajo Maane. Doomu Senegaal ji di jóge Liverpool bim fa jotee def 6i at (Suweŋ  2016 ba Suweŋ 2022), amal fa 267i joŋante, dugal ca 120i bii. Talaatay tey ji la Bayern di ko dalal ngir mu amal caytu-yaram ginnaaw bi mu fa teewee ngir xaatim déggoo yi.