wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
Loo def ci sa yéen yi ?
qu’as-tu mis à tes sourcils ?
yeetal
aider un nourrisson à s’endormir, souvent en le berçant
Damay yeetal xale bi
J'aide l’enfant à s’endormir.
yenn w-
couscous sans viande ni poisson
Lekk aw yenn, ag jaaxle lay doon ci yow
manger du couscous sans viande ni poisson serait embarrassant pour toi.
yéet j-
gros escargot de mer (Cymbium, Volutidés) (très apprécié des Sénégalais)
Bu ma gisee yéet sama yaram dafay daw
quand je vois le Cymbium j’en ai la chair de poule.
yeete
réveiller
Montar bii mënul yeete
cette montre ne peut pas réveiller qqn.
yéex
être lent
Danga yéex
tu es lent.
yeew m-
python
Deru yeew lay jaay
il vend une peau de python.
yeewe
attaché, lié par un lien (à un endroit)
yëf y-
chose(s)
Am na ñaari yëf yu ma soppul ci moom
il y a deux choses que je n’aime pas en lui.
yettkat b-
sculpteur
yéjj
saboter, chambrer
Lu naqari la mu ma doon def, di ma ko yéjje, moo tax ma tudde dëkk bi Njar-Meew
J'ai appelé ce village Njar-Meew (lait coupé) à cause des choses déplaisantes qu’elle me faisait pour me saboter (me démoraliser).
yegg
arriver
Yegsi nga nag
il ne manquait plus que ça !
yékëti
soulever
Xaaral ma yékëti tànku lal bi
attends que je soulève le pied du lit !
yég-yég b-
sensation, émotion
yiir
couvrir pour protéger
Yàlla na la Yàlla yiir malaanum sutura
que Dieu te couvre d’un pagne de discrétion !
Maay ñag biy yiir tool yi
je suis la haie qui protège les champs.
yékket
exprime la manière de soulever énergiquement
Mu ne yékket xeej ba, jam ca
il s’empara énergiquement de la lance et l’y planta.
yékkat
sangloter
Dafa agsi di yikkat
il est arrivé en sanglotant.
yëkk w-
taureau
(prov.) Ñaari yëkk yu mat xajuñu ci menn mbalka
deux taureaux adultes ne peuvent pas se retrouver devant un même abreuvoir.
yékëtiku
se soulever
Pom buy yékëtiku
pont qui se soulève.
yéwén
être généreux
Nit ku yéwén la
C'est une personne généreuse.
(prov.) Yéwén : ci sa alal
généreux, avec tes biens) sois généreux, mais avec tes propres biens !
yem
rester tranquille
Soo bëggee nu déggoo, nanga yem
si tu veux que nous soyons d’accord, tu restes tranquille.
Dangay yem, walla nga dem ci biti
tu restes tranquille, ou tu vas dehors.
(prov.) Tànk bu yemul, dëgg day
le pied qui ne reste pas tranquille marchera sur des excréments.
yem
s’en tenir à
Li mu wax, ci laay yem
je m’en tiens à ce qu’il a dit.
yëlëb
secouer (drap, vêtement, tapis, etc)
Yëlëb naa saaku bi, dara nekku ci
J'ai secoué le sac, il n’y a rien dedans.
yëlbu
secouer les vêtements qu’on porte
Dama jog, yëlbu, xaalis bi wadd
je me suis levé et j’ai secoué mes habits, l’argent est tombé.
yembadi
être malade mentalement
Dafa yembadi
il est malade mentalement.
yen
aider qqn à porter qqch sur la tête
Amuma woon ku ma yen paan bi
je n’avais personne pour m’aider à porter la bassine.
(prov.) Am na ku la ne : – ma yen la ; booba, la ca ndab la la bëgga gis
quand certains t’offrent leurs services pour t’aider à porter ton récipient sur la tête c’est pour voir ce qu’il contient.
yemu b-
limite
Xalaat amul ub yemu
la pensée n’a pas de limite.
yemadi
être turbulent
Gone gii dafa yemadi lool
cet enfant est trop turbulent.
yen b-
charge
Ndax àttan nga sa yen bi ?
es-tu capable de supporter ta charge ?
yënd
avoir bien pris (feu)
Bàyyil taal bi mu yënd
Laisse le feu bien prendre.
yemle
avoir à égalité (quelque chose sous-entendu)
yoloosu
se déplacer à pas de velours
Ñu yoloosu ndànk, di roñ saaku ya
se déplaçant à pas de velours, lentement, ils prirent les sacs un à un.
yendeer g-
trou de sortie inachevé que fait la souris pour s’en servir comme issue de secours
Janax ji jaare na ca yendeer ga
la souris est passée par le trou de secours.
yoodo g-
Personne avec laquelle on a des affinités.
Yoodo gi mu am moo tax kenn munta ànd ak moom.
c’est à cause de la relation qu’il a que personne ne peut s’associer à lui.
yentem
manière d’entrer dans un trou en sautant
Ne na yentem ci kan mi
il a sauté dans le trou.
yenn-saa
parfois
Yenn saa, damay fàtte ne nekkuma Senegaal
parfois, j’oublie que je ne suis pas au Sénégal.
yenn y-
num.indéf
yenni
aider qqn à enlever une charge qu’il porte
Wool Astu, mu yenni la
appelle Astou pour qu’elle t’aide à te décharger !
yeññ w-
cœur d’un arbre
Gor ko ba àgg ca yeññ wa
coupe le jusqu’au cœur.
yomb-yomb b-
facilité
yëqóol
avoir le hoquet
Mu ngiy yëqóol; may ko ndox
il a le hoquet; donne-lui de l’eau.
yenniku
une charge qu’on porte
yeraange g-
honte
Yeraange gee ko teree wax
C'est la honte qui l’empêche de parler.
yére b-
habit
Yére bi nga sol, moomuloo ko
L'habit que tu portes n’est pas à toi.
yëqóol g-
hoquet
Maam Jokel, yëqóol a ko yóbbu
grand-père Diokel est mort du hoquet.
yenu
porter sur la tête
Yenu ko !
Porte-le sur la tête !
(prov.) Bët du yenu waaye xam na lu bopp àttan
l’œil ne porte pas mais il sait ce que la tête peut supporter.
yeru
réciter à voix basse
Booy julli tàkkusaan, dangay yeru
quand tu pries à dix-sept heures, tu récites à voix basse.
yépp
tous
Xale yépp dem nañu foyi
tous les enfants sont partis jouer.
yer m-
fosse
yooy
être maigre, être malingre
Tànnal fas wa gëna yooy
choisis le cheval le plus maigre !
(prov.) Bukki, balaa baax, yooy
C'est seulement quand elle est maigre que l’hyène est gentille.
yëru b-
judas trou par lequel on peut voir sans être vu
Bu ñu fëggatee, nanga xool ci yëru bi bala ngay ubbi
si on sonne encore, tu regarderas par le judas avant d’ouvrir.