wo
stringlengths 1
4.02k
⌀ | fr
stringlengths 1
1.08k
| source
stringclasses 2
values |
---|---|---|
Am na ay xar. | Il a des moutons. | null |
Fan nga joge ? | D'où viens-tu ? | null |
Dem na | Il est parti | null |
Góor gee ni kookule la, soo demee ! | C'est l'homme qui a dit que c'est celui-là, peut-être ! | null |
Ana wanaag wi ? | Où sont les toilettes ? | null |
Xanaa liñ fi tudde woon Xare bu Mag bi. Sunu kër ca Niis : juróomi nit ñuy dankalikoo ci ňaari néeg yu ñu teg i xànq. Juróom-benn lanu woon sax, boo limaalee Mariyaa, mbindaan mi sama maam ju jigéen ne woon, ci xolam bu rafet, du ko wacc mukk ginnaaw. Luy delseeti ci sama xel ? Dëkku kow ba sama yaay war a daw làquji ndax ragal Almaŋ yi jàpp ko... Loolu lépp seey na ba ni mes, dellu mel niy léeb ak lëppóon. | La guerre, le confinement dans l'appartement de Nice (où nous vivions à cinq dans deux pièces mansardées, et même à six en comptant la bonne Maria dont ma grand-mère n'avait pas résolu de se passer), les rations, ou bien la fuite dans la montagne où ma mère devait se cacher, de peur d'être raflée par la Gestapo – tout cela s'effaçait, disparaissait, devenait irréel. | null |
Tay ci ŋgoon. | Aujourd'hui dans la soirée. | null |
Xaaj bu njëkk bi, mooy bañ nekkee ñoom ñaar sowub Kamerun, miin Bamendaak Bansoo ak seeni tund ya noppal bët ba dee, di fanaan Forestry House, di fa yeewo. Te yab lool nag, ñall yiy romb Garaas Fiild ak tangori Mbam, ca réewi mbembe yeek Kakaa yeek Sànti yi. | L'avant, pour mon père et ma mère, c'étaient les hauts plateaux de l'Ouest camerounais, les douces collines de Bamenda et de Banso, Forestry House, les chemins à travers les Grass Fields et les montagnes du Mbam et des pays mbembé, kaka, shanti. | null |
Seen gaynde gi xar la. | Leur lion c'est un mouton. | null |
Demoon ba Ndar. | Avoir pu aller jusqu'à Saint-Louis. | null |
Afrig danu fa tàbbi, daanaka, ci àddina su bees tàq. | En partant pour l'Afrique, nous avions changé de monde. | null |
Góor gi nitu Ndar la. | L'homme est un Saint-Louisien. | null |
Samba la ? | C'est Samba ? | null |
Léeg-léeg, seen dalukaay du dal xel dara, waay : Kuwajaa doy na ci tegtal. Foofa, ca réewum Kakaa yi, néegu bànxaas bi ñu war a fanaan ci biir toolu-banaana yi, amul sax palanteer. | Les campements sont parfois plus que précaires : à Kwaja, en pays kaka, ils logent dans une hutte de branches sans fenêtre au milieu d'une plantation de bananiers. | null |
Nit la ku baax ! | C'est un homme gentil ! | null |
Léegui léegui ma egg sa kër. | J'arrive tout de suite chez toi. | null |
Ci teen boobu bënn | Dans ce puits qui coule | null |
Te Afrig, du béréb bu ne tekk, ànd ak dal. Ku xalaat loolu, juum nga. Afrig, mënees nañ ko méngaleek callweer : dara du fa sedd. Daanaka ponkal mu xiif la, mar tey jaay doole. | L'Afrique, c'était la violence des sensations, la violence des appétits, la violence des saisons. | null |
Xammee naa nagu Tugël ! | Je reconnais une vache d'Europe ! | null |
Yaa ŋgi demuloo | Toi, tu n'as pas été | null |
Gunóor gi tàkkul ci saa si ndax ni ko safara si wëre. Mu des ci géew bi, xamatul nu muy def ak doom yi mu boot. Xanaa rekk taxaw, yëkkatiy keppukaayam ca kow, di xaar. | Pour une raison que j'ignore, le feu a d'abord pris autour de l'animal, en formant un cercle de flammes bleues, et la femelle scorpion s'est arrêtée dans une posture tragique, les pinces levées au ciel, son corps bandé dressant au-dessus de ses enfants son crochet à venin au bout de sa glande, parfaitement visible. | null |
Waa ji moo dulwoon dem | C'est ce personnage qui n'allait pas partir | null |
Joxoon na la juuti bi | Il t'avait remis la taxe | null |
Koo gis ? | Qu'as-tu vu ? | null |
Góor gi doon dem | L'homme qui devait partir | null |
Liggéey bi Baay daan def, njëkkee ko Kamerun door a jàll Niserya, du woon liggéeyu caaxaan. | Le travail que faisait mon père au Cameroun d'abord, puis au Nigeria, créait une situation exceptionnelle. | null |
Dem naa, dem ŋga, dem na... | J'ai été, tu as été, il a été... | null |
Legoos, Ibadaŋ ak Kótónu, naka noonu. Askan yeek làkk yi jaxasoo. Mënoon naa sax limaale Onitsaa ak màrseem ba nga xam ni daanaka téereb nettali bu la réer ci dunyaa soo fa demee ñu jaay la ko. Te ci xeet yooyu ma tudd, Àngale yi kenn demul ñu des. Ni ñu yëge seen bopp, di jaay maanaa, mu méngook seen colin, dafa rekk reelu. Foo séenee ay kompalet ak i sàppo, dóoral yat, ñoom a. Seeni jigéen, ñoom, ñu nga leen doon xàmmee seeni yére yu tegginewul woon lool. Ñoom ñépp nag, Àngale yooyu, di daje ci seeni màkkaani bopp, di wax ay waxi picc. Fàww ñu ràññee ci gaa ñooñu liggéeykati Lloyd's ya mbaa yu Glynn Mills ak Barclay's. Foo leen fekk ñu ngay xëcc ci seeni sigaar, lu ñor ñu wax, lu ñorul ñu wax, di jëw ak déeyante. Léeg-léeg kenn ci ñoom ni : « Mbër, neexul ba neexul waaye dëkk bii du dëkku como, de ! » Bóoy yi ñoom, ñu ngiy jaabanteek ay ndab yu ñu teg i kaasi sàngara, ku ne ñu ni la ko jabb te du benn yoon booy dégg seen baat. | Les grandes villes, Onitsha et son marché aux romans populaires, la rumeur des bateaux poussant les grumes sur le grand fleuve. Lagos, Ibadan, Cotonou, le mélange des genres, des peuples, des langues, le côté drolatique, caricatural de la société coloniale, les hommes d'affaires en complets et chapeaux, parapluies noirs impeccablement roulés, les salons surchauffés où s'éventent les Anglaises en robes décolletées, les terrasses des clubs où les agents de la Lloyd's, de la Glynn Mills, de la Barclay's fument leurs cigares en échangeant des mots sur le temps qu'il fait – old chap, this is a tough country – et les domestiques en habit et gants blancs qui circulent en silence en portant les cocktails sur des plateaux d'argent. | null |
Nit ñi nee nañu mu dem. | Les gens demandent qu'ils partent. | null |
Gàddaay dund fa sa giiru-dund | S'exiler habiter l'exil toute une vie | null |
Fekkkoon mu jóge Móris juróomi-ñetti at ca ginnaaw, ba ňu fa dàqee njabootam ca atum 1919. | Bientôt huit ans qu'il est parti de Maurice, après l'expulsion de sa famille de la maison natale, le fatal jour de l'an de 1919. | null |
Ci biir nataal bii maa ngi ciy gis ay batã, batã yu bari yu sës ci miir bi nii. Xam naa boo moytuwul denculaayi yëre lay doon. Walla bu nekkul dencukaayu yërë mu nekk dencukaayu ay bool. Xam naa lii ab néeg la walla mu nekk aw waañ. Waaye daal lu ci mënti xew batã yi rafet nañ lool ndax wirgo wi mu ame nii dafa rafet lool. Ak palanteer bi nekk ci kow nee nga xam ni ngelaw lee ciy jaar di dugg lu baax la. | À l'intérieur de cette photo je vois beaucoup de commodes placées contre le mur. C'est certainement pour garder des habits. Si ce n'est pas pour garder des habits, c'est pour garder des bols. Je crois que c'est une chambre ou une cuisine. Mais quoi qu'il en soit, les commodes sont très jolies car leur couleur est très jolie. La fenêtre qui est au-dessus, le fait que le vent passe à travers et entre à l'intérieur, est une bonne chose. | null |
Su dee dem | Une fois en chemin | null |
Dafa dem | Il est parti | null |
Waaye de, ku mu gis, ŋga de. | Mais, celui qu'il voit, meurt. | null |
Nit kii jaŋg na | Cet homme a étudié | null |
Tann ŋga doomu benn jigéen jan ? | Tu as choisi la fille de quelle femme ? | null |
Gis ŋga kan ? | Tu as vu qui ? | null |
Ay meri dof dëgg a ko daan dikkal. | Ses colères étaient disproportionnées, excessives, épuisantes. | null |
Wéetaay ak nangu dogal la nataal yiy feeñal. Ma leen di xool, mu mel ni maa ngi janook fi raayi dunyaa téene. | Sur ses photos paraissent la solitude, l'abandon, l'impression d'avoir touché à la rive la plus lointaine du monde. | null |
Ngir teeri Bansoo, muy noor di nawet, oto bi day daw cib taliy raŋ-raŋ ba jeexal ko. | Banso est au bout de la route de latérite carrossable en toutes saisons. | null |
Weneen fas la bëgg ! | C'est un autre cheval que je veux ! | null |
Àngale ya nangu woon ci Almaañ penkub Niseryaa ak sowub Kamerun daldi ko woo, mu war faa nekki fajkat. | Un poste venait d'être créé en Afrique de l'Ouest, dans la bande de terre reprise à l'Allemagne à la fin de la Première Guerre mondiale, et qui comprenait l'est du Nigeria et l'Ouest du Cameroun, sous mandat britannique. Mon père s'est porté volontaire. | null |
Ci sa peggi dex yi | Sur les rives de tes cours d'eau | null |
Kooka ak kile, bokkuñu ! | Celui-là et celui-ci n'ont rien de commun ! | null |
Lii nag mel na ni benn baye la. Baye bu sokolaa la nekk ci barab boo xam ni dafa a weex. Mën naa def yu mel ni ay téere Walla ay kaas walla yu mel noonu. Mën naa denc yu am solo. | Ceci ressemble à un bahut. Un bahut chocolat dans un espace blanc. Il peut contenir des livres, des tasses ou consorts. Il peut garder des objets de valeur. | null |
Yaw daawuloo coow. | Tu ne bavardais pas, en général. | null |
Dafa di dem. | Il doit partir. | null |
Ñëwël ndax xale yi di ay liggéeykat, di ay jambaar ! | Viens pour que les enfants soient des travailleurs, soient des braves ! | null |
Daŋgeen bëggé naka ñoom ! | Vous êtes aussi avares qu'eux ! | null |
Attekat ŋgeen ci ban yoon ? | Vous êtes des juges en vertu de quel droit ? | null |
Lawbe la. | C'est un bûcheron. | null |
Séetal ci bir, ci biti, ci suuf ak ci kaw. | Regarde à l'intérieur, à l'extérieur, en bas et en haut. | null |
Musaa wax na leen jël naa sama retraite. | Moussa vous a dit que j'étais à la retraite. | null |
Li ŋga wax loolu. | Ce que tu as dit. | null |
Sama xarit la ! | C'est mon ami ! | null |
Ñàkkul dog-dogu xare bee ko taxoon a mel noonu. Su fekkoon ni bokkoon naak nun benn kër, di nu gis ba nuy perantal ba ba nuy dëgër, àddina du dox ba bés ay doomam diy doxandéem ci moom. | Sans doute les choses se seraient-elles passées autrement s'il n'y avait pas eu la cassure de la guerre, si mon père, au lieu d'être confronté à des enfants qui lui étaient devenus étrangers, avait appris à vivre dans la même maison qu'un bébé, s'il avait suivi ce lent parcours qui mène de la petite enfance à l'âge de raison. | null |
Noonu ma dem. | Sur ces entrefaites, je partis. | null |
Lii lan ? | Cela quoi ? | null |
Gàddaay kàdd ga ñuy siyaare | S'exiler loin de cet arbre vénéré | null |
Timis jot na. Maa ngi téen, janook asamaan siy gën a yëngu saa su ne. Niir yu dóomu-taal yaa ngi nirook i waasintóor, melax yiy réer ak a feeñ ci seen biir. | Je vais regarder la fièvre monter dans le ciel du crépuscule, les éclairs courir en silence entre les écailles grises des nuages auréolés de feu. | null |
Baay a yilifoon dispañseeru Ogosaa ba ay jigéeni kër-làbbe ubbi woon ay ati-at ca ginnaaw. Te it moom kott a doon fajkat ca bëj-gànnaaru Koros Riwër. | À Ogoja, mon père était responsable du dispensaire (un ancien hôpital religieux délaissé par les sœurs), et le seul médecin au Nord de la province de Cross River. | null |
Ñu bare ci Àngale ya fa toogaloon seen réew, ay soldaar lañu woon wallay àttekat walla li ñu tudde woon ci seen làkk ay « District Officers ». | La plupart des Anglais en poste dans la colonie exerçaient des fonctions administratives. Ils étaient militaires, juges, district officers (D.O.). | null |
Su dee Lawbe Rao | S'il est Laobe de Rao | null |
Bul bàkk ci ñooñu ! | Ne fais pas partie de ceux-là ! | null |
Dem ŋga | Tu es parti | null |
Bu ňu reeraan ba noppi, ne faax ci sunuy toogu-xóot yu der ya, di xëcc seen naanu, di fàttaliku ba jamonoy neex. Man nag, dañ ma daan géeyloo, ma tiim sama palaat di dajjant. | Après dîner, ils s'installaient dans les fauteuils de cuir de la salle à manger, souvenirs de temps prospères, ils fumaient et ils parlaient, et moi je m'endormais le nez dans mon assiette vide en écoutant le ronron de leurs voix. | null |
Jan ŋga gis ? | Lequel as-tu vu ? | null |
Benn numéro bii leñ ñu jox ñun ñep, lepp lun nun digoon amatul solo ndax duwoon sakh dëg. | On nous a tous donné le même nombre exact, peu importe les privilèges qu'on nous avait promis d'accorder, tout cela était un mensonge. | null |
Téere yee laa jënd ! | C'est ces livres là-bas que j'ai achetés ! | null |
Kenn nëwul. | Nul n'est venu. | null |
Góor gi nee na la fi saŋx, ŋga dem ci biti. | L'homme t'a dit ici il y a un instant de sortir. | null |
Yeneen nit laa gis ! | C'est d'autres gens que j'ai vus ! | null |
Sa yay nee na ci ŋgoon dana ñëw. | Ta mère dit qu'elle viendra ce soir. | null |
Dama mujjee dem ba yaakaar ne man mii maa dund loolu ci dëgg-dëgg, mu jaxasoo ci sama xel ak bés ba may mellentaan singalee ca Ogosaa. Ñu ngi ma wër-ndomb, di dem ak a dikk. Man ma taxaw ne yàcc, di xullee. Waaye it maa ngi may nopp tekk-tekkaaral gi. Dafa sew, leew, gën a raglu mbooleem riiri dunyaa yépp. | Au point de croire que cela m'était arrivé, de mêler le fleuve dévorant au tourbillon de fourmis qui m'avait assailli. Le mouvement de giration des insectes autour de moi ne me quitte pas, et je reste figé dans un rêve, j'écoute le silence, un silence aigu, strident, plus effrayant qu'aucun bruit au monde. | null |
Baay ak nijaayam ji may wax, ci benn kër gi lañu juddoo, ku nekk ci ñoom ñaar màgge fa. Kon li ñu séq bare na, ñoo bokk i mbóot te yit ñoo daan sangoo ci benn dex gi. | Mon père est né dans la même maison que son oncle, à tour de rôle ils y ont grandi, ils ont connu les mêmes lieux, les mêmes secrets, les mêmes cachettes, ils se sont baignés dans le même ruisseau. | null |
Ak i turi réew, Mbembe, Kakaa, Sungili, Bum, Fungom. | Et les noms de pays, Mbembé, Kaka, Nsungli, Bum, Fungom. | null |
Fan ŋga jëm ? | Où vas-tu ? | null |
Kaay ! | Viens ! | null |
Gis na sama xarit yeneen yooyuu ! | Il a vu mes autres amis ! | null |
Xamuma dara ci samag juddu (war naa naa cee bariy moroom... ) waaye su ma daagoo ba fa gën a sore ci man, seen kàttan googoo may feeñu ak pëndaxit bi seen yaram di togg ak a toggaat, mu jaxasoo ba indi jëmmu doom-aadama. | Moi, je ne sais rien de ma naissance (ce qui est, je suppose, le cas de tout un chacun). Mais si j'entre en moi-même, si je retourne mes yeux vers l'intérieur, c'est cette force que je perçois, ce bouillonnement d'énergie, la soupe de molécules prêtes à s'assembler pour former un corps. | null |
Fecckat yaa ngi jiitle di wër làng gi, seen tànk yiy dóor suuf seek doole ñoom tamit, ànd ak njiinum sabar yi. | Elles avancent l'une derrière l'autre, penchées en avant, leurs pieds battent la terre au même rythme que les tambours. | null |
Gisu la woon | Il ne t'avait pas vu | null |
Ñu teg ciy waxtu, Baay pikiir ko poson. | Quelques heures plus tard, c'est mon père qui plonge dans sa veine l'aiguille qui lui injecte le poison. | null |
Nataal bii gis naa ci ab néegu ñax bu nekk cib àll bu naat bu am ay ñax ak ay garab. | Sur cette photo j'y ai vu une case qui se trouve dans une belle forêt contenant des herbes et des arbres. | null |
Ci foofu ŋga taxaw | Là où tu es | null |
Góor gi gisul meneen. | L'homme n'en a pas vu un autre. | null |
Lii nag baraada la. Baraada bu nu def attaaya la walla bu mën def kafe. Boo xoolee mi ngi am njàpp. Baraada bi nag mu ngi yor wirgo wu'orange' ak lu'jaune' waaw. Ñuŋ ko yor. Boo xoole tamit am na gëléem buñ ci nataal ak ay garab. Ñu nataal leen ak wirgo Wu ñuul. | Ceci est une théière. Une théière dans la quelle on met du thé ou du café. Si tu regardes bien, il a une capture. La théière comporte une couleur'orange' et'jaune', oui. On le gère. Si tu regardes bien aussi, sur lui il y a un chameau dessiné ainsi qu'un arbre. On les a dessinés avec une couleur noire. | null |
Wutkati wurus Sadiolaak Sabadola | Les chercheurs d'or de Sadiola et de Sabadola | null |
Ñëwël ndax xale yi di mbër te it ñu di ay jambaar ! | Viens pour que les enfants soient des travailleurs, soient des braves ! | null |
Nataal bii nag am na benn lu ñu wërële ay bant mu mel ni néeg nekk ci wetu garab gu sëq. Am tamit beneen lu mel ni toogukaay lu ñu def ay bant am ay ñax yu nekk ci koteem. | Sur cette photo il y a une chose enroulée avec des bâtons qui semble être une chambre à coté d'un arbre en abondance. Il y a aussi autre chose qui ressemble à un ustensile de cuisine dans lequel on a mis des bâtons et il y a des herbes à coté. | null |
Moom mile ci buntu kër gi la. | C'est celui-là même devant le seuil de la maison. | null |
Réew mi am na alal ndax ? | Est-ce que le pays a des richesses ? | null |
ňa nga desak seen ngor ci yoon wu sore wii | restent debout sur cette longue route | null |
A ngiy dóor dàqeek jànt bi | Jouent à cache-cache avec le soleil | null |
Ci sa peru bët maa ngi lay séen | Dans la prunelle de tes yeux | null |
Loo gis ? | Qui as-tu vu ? | null |
Dikk na ndax yaw. | Il est venu à cause de toi. | null |
Dana tukki tay mbaa ëlëk. | Il voyagera aujourd'hui ou demain. | null |
Kookule la kookule taxaw la ! | C'est celui-là, celui-là debout ! | null |
Subsets and Splits