wo
stringlengths
1
4.02k
fr
stringlengths
1
1.08k
source
stringclasses
2 values
Laobe lë woon.
Je fus Laobé.
null
Loolu doŋŋ doyul
Cela seulement ne suffit pas
null
Ngir gën a jafeel mbir mi, dañu daan bàyyi léeg-léeg bantu bale bi, tàllal leen benn baaraam, su jiit ji tàmbalee yëngal geen gi nu gaawtu delloosi sunu loxo.
Pour corser l'affaire il fallait donc, de temps en temps, lâcher la brindille et avancer la main, puis la retirer prestement au moment où la queue du scorpion fouettait.
null
Waaye xale bu ndaw laa booba, dooley Àngalteer xaajumaa teree nelaw.
J'étais seulement un enfant, la puissance de l'empire m'indifférait assez.
null
Naan ?
De quelle manière ?
null
Xale yi yëpp a ngi dund.
Tous leurs enfants ont survécu.
null
Mas na ma ni su démb doon tey, du nekk doktoor, weterineer lay doon, di faj mala yi, ndax ñoom rekk a mën a dékku seen metit, nangu ko ni ndogalu Yàlla.
À la fin de sa vie, je me souviens qu'il m'a dit une fois que, si c'était à refaire, il ne serait pas médecin, mais vétérinaire, parce que les animaux étaient les seuls à accepter leur souffrance.
null
Ag ñan ŋga doon xeexal ?
Tu te battais avec qui ?
null
Xuri wurus yaa ngi nuy nëbb jant bi
Les mines d'or nous cachent le jour
null
Naka ŋga def ?
Comment vas-tu ?
null
Bi jigéen ji ñëwée la
C'est lorsque la femme arriva
null
Góor gi dem
L'homme a été
null
Wayafuloo na sa nday ji.
Tu n'es pas aussi modeste que ta mère.
null
Ci biir ŋga wax ?
C'est à l'intérieur que tu dis ?
null
Waaye ndono loolu, mënees nan koo gise neneen. Wonaale nanu soloy njub ak weg say kilifa. Dëkki Kamerun ak Nise-ryaa ya mu jaar, benn gone du fa jooy mbaa di jàmbat.
Mais aussi l'exactitude et le respect, comme une règle des sociétés anciennes du Cameroun et du Nigeria, où les enfants ne doivent pas pleurer, ne doivent pas se plaindre.
null
Góor gi ni : cam !
L'homme fit : pouah !
null
Sa yay nee dana dellusi soo yeggee.
Ta mère dit qu'elle reviendra si tu vas jusqu'au bout.
null
Dem nañu
Nous partons
null
Góor gi bëgg na kii.
L'homme aime celui-là.
null
Ci dëgg-dëgg, bëggoon naa xam fu xalaat boobu jóge woon ba song ma. Li wóor daal, moo di ne Baay daan na tàkk i lonet yi xewoon ci at yi soriwul atum 1930. Mooy ya ñu tëgge woon weñ gu sew ba noppi ànd ak weer yu mërgalu te Luwi Suweek Sams Sooys (niróowaaleem ba) daan leen takk.
Pourquoi lui ? En réalité, mon père devait porter des lunettes à la mode des années trente, fine monture d'acier et verres ronds qui reflétaient la lumière. Les mêmes que je vois sur les portraits des hommes de sa génération, Louis Jouvet ou James Joyce (avec qui il avait du reste une certaine ressemblance).
null
Më ŋgile demkoon
Voilà que j'aurais été
null
Waxtaanal ag nit kookii ci sa wet !
Cause avec cet homme qui est à côté !
null
Ndax kan dem ?
Afin que parte qui ?
null
Góor gee dem walla xale yee noppi ?
C'est l'homme qui est parti ou bien ce sont les enfants qui se sont tus ?
null
Xale bi mayul dara kii.
L'enfant n'a rien donné à celui-ci.
null
Tey jii, sidaa dal ci kowam nar ko faagaagal. Teewul réewi Tubaab yi mën dugal seen loxo ci mbir mi dumóoyu, ni ñoom yëguñu tinuñu.
À présent la nouvelle peste du sida, qui menace de mort le tiers de la population générale de l'Afrique, et toujours les nations occidentales, détentrices des remèdes, qui feignent de ne rien voir, de ne rien savoir.
null
Joxeel foofu doŋŋ ñari yoon !
Rien que là, donne deux fois !
null
Du mës e am roppalaan buy ñow.
Il n'y a jamais d'avion qui arrive.
null
Mayal nag wile !
Nourris cette vache-ci !
null
Mu ŋgooguu di dem
Le voilà, là-bas, qui s'en va
null
Jën la waaw, Wu am wirgo Wu baxa ak Wu xonq.
C'est des poissons, oui. Ils sont de couleur bleue ou rouge.
null
Kon nun, bés ba nu njëkkee teg tànk Ogosaa sun neexoon ni : « Guléet tey nu ñam cafko moom sa bopp ! » Daanaka noo moomoom lépp lu sunuy bët daan daj.
Ces journées à courir dans les hautes herbes à Ogoja, c'était notre première liberté.
null
Jënfandikoo naa ak U2 yi.
J'ai traité avec les U2.
null
Su ma ragalul woon fen, dinaa ni toog naa ay at teguma bët sama xar-kanam gii.
Pendant des années, je crois que je ne l'ai jamais vu.
null
Moo di loola !
Quel démon !
null
Ogosaa, dëkku tés-tés la, jàmburewul ni Kamerun.
La douceur nonchalante du Cameroun n'a pas cours à Ogoja.
null
Nit la woon !
Ce fut un homme !
null
Nun daal, dañoo meloon ni ñu caŋ ci biir gaal gu tag diggante ňaari àddina.
Le souvenir que je garde de ce temps pourrait être celui passé à bord d'un bateau, entre deux mondes.
null
« District Officer » bi soriwu fa, sarwiis bu mag biy saytu diiwaanu Koros Riwër mi ngi Abaakaliki te it tali bi baax na.
Le D.O. n'est pas loin, le grand centre administratif de la province de Cross River est à Abakaliki, accessible par une route carrossable.
null
Jël naa sama retraite si atum 2002.
J'ai pris ma retraite en 2002.
null
Yaa ŋgoogule.
Te voilà, là.
null
ci song merum ngëlén li ?
pour braver la furie de l'orage ?
null
Moontin góor gi jambaar la lool ci liggéey bi.
Et pourtant l'homme est dur à la tâche.
null
Yenn saa yi ma nekk bitim-réew, ci dëkk bu mag, woto yiy riir, tanqal ñépp, wànte man, su may tàllal sama nopp di dégg dexug Ayaa muy woyantu ci suuf.
J'entends même, par-dessus la vibration des autos embouteillées dans une avenue, la musique douce et froissante de la rivière Aiya.
null
Mi ŋgi, benn la ci ndàyam.
Le voilà, il est unique en son genre.
null
Bul dem tay jii !
Ne sors pas aujourd'hui !
null
Gis naa benn affaire bu ñuy ndugge marché...
J'ai vu quelque chose qu'on achète au marché...
null
Li ma tudde sànq ñàkk-kersay yaram yi, mook taw bu mettee-metti ñoo daan faral a ànd, mel ni nit keek takkandeeram.
Elle imprégnait la muraille de la forêt pluvieuse qui nous enserrait de toutes parts.
null
La ŋga wax la.
Ce que tu as dit.
null
Wekkil gëñ yii !
Arrache ces dents-là !
null
Kooy seet ?
Qui cherches-tu ?
null
Bés, bi timis diy waaj a jot, dënnu bi bett na Baay fa mu doon opeeree ca loppitaanu Ogosaa, daldi lakk ay caraxam, ruyal tànki lal ba ñu tëraloon aji-tawat ba. Nes tuut, mu dajaloo, jaaraat ca suufu bunt ba, dellu ca kow asamaan. Afrig, dund naa fay mbir, ñu ni fàŋŋ ci samay bët te du ma tee werante ci sama xel, naan ndax lii ay léeb laam déet.
Un après-midi, mon père opérait dans l'hôpital d'Ogoja, quand la foudre est entrée par la porte et s'est répandue sur le sol sans un bruit, faisant fondre les pieds métalliques de la table d'opération et brûlant les semelles en caoutchouc des sandales de mon père, puis l'éclair s'est rassemblé et a fui par où il était entré, comme un ectoplasme, pour rejoindre le fond du ciel. La réalité de l'Afrique était dans ses légendes.
null
African Farm la gën a jege. Nga gis ni mu barey nit, ni mu yëge kàttanam te balaa yu dul jeex di ko sotoo. Benn wóomam yegg suuf, muy yëg ni muy tërëf-tërëfee, waaye du ko tax a ñaaw ci xare bi. Foo walbatiku say bët dajeek ay naaxi gone ak seen biiri-taññ, ñépp di woy di fecc. Saa yu samay way-jur taseek ay sàmm ciw ñall, daldi yéemu ci seen neex deret ak seen am xorom.
C'est plutôt celle d'African Farm, une Afrique réelle, à forte densité humaine, ployée par la maladie et les guerres tribales. Mais forte et exhilarante aussi, avec ses enfants innombrables, ses fêtes dansées, la bonne humeur et l'humour des bergers rencontrés sur les chemins.
null
Bi mu demee
Lorsqu'il a été
null
Fu mu bëgg ?
Où veut-il
null
Defe naa ni keneen ki la !
Je crois que c'est l'autre !
null
Xar yooyu yan ŋga moom ?
Les quels moutons qui t'appartiennent ?
null
Ki kan la ?
Qui est-ce celui-ci ?
null
Jëlël lépp !
Prends tout !
null
Ñàkkul ne goney Ogosaa sooke woon mbir mi, nu topp ci. Sunu gàngóor ga raxe lool, sax : ñii diy gone yu tuutee-tuuti def tànki neen ak seen biir yu réy, ñi ci des diy xaleeli góor yu soreetul fukki at ak ñett, sol ni nun ay tubay yu kakeek simis. Ñoo nu daan jàngal ni nuy summee sunuy dàll ngir mën a daw ci ñax mi.
Peut-être à l'instigation des enfants du village, la bande un peu hétéroclite qui comportait des tout-petits tout nus avec un gros ventre et des presque adolescents de douze, treize ans, vêtus comme nous d'un short kaki et d'une chemise, et qui nous avaient appris à ôter chaussures et chaussettes de laine pour courir pieds nus dans les herbes.
null
Yaral xar !
Élève des moutons !
null
Waxal ag Samba rekk !
Parle avec Samba seulement !
null
Mbaa defuñu dara.
J'espère qu'ils vont bien.
null
Ana ŋgoor ?
Où est NGor ?
null
Dem na ba tere ku toog ci ëtt bi walla ku fa togg.
Les femmes et les enfants n'ont pas leur place dans la cour de l'hôpital, il est interdit d'y allumer du feu pour faire la cuisine.
null
Soo bawoo foofu, dem fu gën a sore, ngay soog a gis doomi réew mi, nit ñu ñuul ñi, baree-baree ba nga ni lii lu mu doon. Ñoom dara lañu jotewul ak Tubaab yi. Xanaa ab doxandéem di leen sant ñuy def. Walla boog léeg-léeg ñu séen ab woto – waaye ndax woto dëggëntaan la sax ? – muy xélu, di yëkkati pënd bu bareek a korne buy romb – fiiw ! fiiw ! –s eeni gox.
Enfin, à l'extérieur, c'est l'océan immense des Africains, qui ne connaissent des Occidentaux que leurs ordres et l'image presque irréelle d'une voiture carrossée de noir qui roule à toute vitesse dans un nuage de poussière et qui traverse en cornant leurs quartiers et leurs villages.
null
Ŋgor dem ?
Ngor peut-il partir ?
null
Fàttalikuwuma bés bi ňu njëkkee sàcc dugg ci biir àll bi, maak sama mag ju góor.
Je ne me souviens pas du jour où nous nous sommes aventurés, mon frère et moi, pour la première fois dans la savane.
null
Ci saa si la tàng-diineem ak bëgg yilifam jur fitna.
Son autorité a tout de suite posé un problème.
null
Amal ŋgor ba mën nekk nit !
Aie assez de sérénité pour conserver ta dignité !
null
Bu mu dem
Qu'il ne parte pas
null
Rax-ci-dolli, dafa mel ni béréb yu bare ci Afrig, doom-aadama masu faa sax teg tànkam.
Mais ce pays est immense, il n'appartient pas encore tout à fait aux hommes.
null
Sunu saxaaru-géej a ngi riisu tefes gi, romb Konaakiri, teg ci Firitaawun ak Monrowiyaa. Maa ngi tëdd ci benn lal bu ndaw, def yaramu neen. Noon laa bàyyi palanteer bi mu ubbeeku, péexu géej giy upp néeg bi. Ñu ngi ma diw fépp puudar tàlk, ma mel ni Buur yooyu ñuy wëraleek bàndaas ci seen biir bàmmeel walla boog jën wu ňu mbaal, suy ko fëriň ba di ko waaj a fiiriir.
Je suis dans la cabine du bateau qui longe lentement la côte, au large de Conakry, Freetown, Monrovia, nu sur la couchette, hublot ouvert sur l'air humide, le corps saupoudré de talc, avec l'impression d'être dans un sarcophage invisible, ou d'avoir été pris comme un poisson dans la nasse, enfariné avant d'aller à la friture.
null
Waaye bi nawetu 1968 di agsi la leen làrmeb Niseryaa wër-ndombo, daan leen. Seneraal Beŋsameŋ Adekunle, nga xam ni dafa soxoroon ba ñu koy woowe « Jiit ju Ñuul ji » ni moom it tey mu neex.
Mais à la fin de l'été 1968, encerclée, décimée par les troupes fédérales sous le commandement du général Benjamin Adekunle, surnommé pour sa cruauté le « Scorpion noir », l'armée biafraise capitule.
null
Jaama nga endu ?
As-tu passé la matinée en paix ?
null
Weeru sàttumbar agsi, xare bi ci boppam dakk. Wànte ay junniy-junniy doom-aadama nga tëju Biyaafaraa di deek xiif ak mar, faju të leen.
À partir de septembre, il n'y a plus d'opérations militaires, mais des millions de gens coupés du reste du monde, sans vivres, sans médicaments.
null
Sama yaay daan na wax ni du benn du ñaar, Filipus aj na ko ciy loxoom di xuus ci biir dex gu yëngatu.
Ma mère racontait que plusieurs fois il l'avait aidée à traverser des rivières en crue, en la tenant à bout de bras au-dessus de l'eau.
null
Lan la ?
Qu'est-ce qu'il y a ?
null
Benn téere bu ndaw te ñuul, daal, la mas a ubbi, muy bi tudd ci kàllaama nasaraan l'Imitation de Jésus-Christ, tey soññ doom-aadama ci toppandoo Yéesu. Bi ma ci mujjee daj yàggul dara wànte keroog sama yaram daw na.
Sa seule lecture était un petit ouvrage relié de noir que j'ai trouvé longtemps après, et que je ne peux ouvrir sans émotion : l'Imitation de Jésus-Christ.
null
Démal !
Va !
null
Deh-det.
Non.
null
Xam naa waroon naa bég ba mu fa àggee... Ci dajaleb fotoom ya, benn a ciy gën a daw sama yaram. Baay ci boppam bëggoon na lool foto boobu ba sax yàkki ko, def ko nataal, wékk.
Dans la collection de clichés pris par mon père en Afrique, il y a une photo qui m'émeut particulièrement, parce que c'est celle qu'il a choisi d'agrandir pour en faire un tableau.
null
Kuy seet bu baax sax, danga naan dafa tafantoo jàppanteem ak kilifaam ca Saawusamston ngir dogook askanu Tugal.
L'épisode de la carte de visite exigée par le médecin-chef de l'hôpital de Southampton ne sera que le prétexte à rompre avec la société européenne.
null
Ma seetlu ni kanam gi ñànge ak ni mu noppee.
Il était dur, taciturne.
null
Ndax ñaari gone yi ci nataal baa ngiy dund ba tey ?
S'ils vivent encore, que sont devenus ce garçon et cette fille ?
null
Jamono jooju lañu mas a jënd ay móobal. Fépp fu ñu mas a toxu, dañ yóbbaale móobal yooyu. Lim baa ngi, gàtt ba dee : ay taabal, toogu yu ňu yàtt ci dàttu iróko te ñu jekk-jekkal kook i nataali golo mbaa yu segg mbaa yu kooba, ni ko waa sowu-jantu Kamerun aadawoo.
Ils installent leurs meubles, les seuls meubles qu'ils ont jamais achetés et qu'ils emporteront avec eux partout : des tables, des fauteuils taillés dans des troncs d'iroko, décorés de sculptures traditionnelles des hauts plateaux de l'Ouest camerounais, léopards, singes, antilopes.
null
Cetam gu jéggi dayo ga, demoon ba mel ni feebar ci moom, fu mu tolluy raxasi loxoom, noonu laa koy gise tey.
C'est ainsi que je comprends maintenant ce qui me semblait absurde alors, son obsession de l'hygiène, cette façon qu'il avait de se laver les mains.
null
Samba ŋga woo ?
C'est Samba que tu appelles ?
null
Wattaliwuma la ka woon.
Je n'avais pas été te le cueillir.
null
Yéen bëgg ŋgeen
Vous, vous voulez
null
Xaleel rekk ŋgeen !
Vous êtes des enfants seulement !
null
Sañumaa bañ a lim jumtukaayu yi « opeerekat » yi mu daan jëfandikoo ca Tugal su daan togg, di dagg ginnaar geek paaka awsa te bu ñoree mu jël siso, séddale nu ko.
Les outils aussi, ses instruments de chirurgien, qu'il utilisait en France pour faire la cuisine, découpant le poulet au scalpel et servant avec une pince à clampser.
null
Maay dem
C'est moi qui pars
null
Doo nitu jamm !
Tu n'es pas homme de paix !
null
Mbootaayi xeet yi fexe ba fekk leen fa, door a teg bët ciy ňaawtéef yu kéemaane ya fa Adekunle defoon.
Quand les organisations internationales peuvent enfin pénétrer dans la zone insurgée, elles découvrent l'étendue de l'horreur.
null
Fas yeneen yan ŋga gis ?
Quels autres chevaux as-tu vu ?
null
Man mii, ni ma nekkee gone gu ndaw ba jóge fa doon waxambaane, ci tabure yu ñu yatt yooyu la daan toog di jàng samay sàqum-baat.
J'ai passé une grande partie de mon enfance et de mon adolescence au milieu de ces meubles, assis sur les tabourets pour y lire les dictionnaires.
null
Góor gi moo ñëwkóon
C'est l'homme qui serait venu
null
Daan naa dem bay yëg ci sama biir xol lu niroo woon lool ak mbañeel.
Je me souviens d'avoir ressenti quelque chose qui ressemblait à de la haine.
null
Bi ŋga dee dem
Du moment que tu pars
null