wo
stringlengths 1
4.02k
⌀ | fr
stringlengths 1
1.08k
| source
stringclasses 2
values |
---|---|---|
Ana kooku | Où est celui-là ? | null |
Ci talib Bamakook jëm Arundu | Sur la route de Bamako à Aroundou | null |
Yëf yan ñoo réer ? | Quelles choses se sont égarées ? | null |
Ñaata lay jar ? | Combien ça coute ? | null |
Àna ŋga ? | Où es-tu ? | null |
Maa dem. | C'est moi qui pars. | null |
Kenn a ŋgi. | En voilà un. | null |
Bëy yi daan neñu daw si biti ay jamono. | Les chèvres s'échappaient souvent. | null |
Naka lanuy waxee lii ci wolof ? | Comment dis t-on ceci en Wolof ? | null |
Góor ñi gisuñu la | Les hommes ne t'ont pas vu | null |
Gej na la giis | Ça fait longtemps que je ne t'ai pas vu | null |
Defe naa du ñëw ! | Je crois qu'il ne viendra pas ! | null |
Moo daan dem | C'est lui qui allait habituellement | null |
Seen biir yu dëll yi, seen jumbax yi mel ni xeer wu ñu leen ëwal ci seen koll. | Les ventres saillants, le bouton du nombril pareil à un galet cousu sous la peau. | null |
Su demee | Une fois là-bas | null |
Di tel-teli doŋŋ taxul sotal dara. | S'agiter simplement ne suffit à rien résoudre. | null |
Jigéen ji ñaan na ndax xale yi agg te itam seen baay nekk fa. | La femme pria pour que les enfants arrivent et aussi pour que leur père soit dans les lieux. | null |
Fu mu tooluy saytu këriň giy segg ndox mi ; maa ngi fàttaliku yit ne àttaaya doŋŋ la daan naan, walla sax ndox mu tàng kese – li Sinuwaa yiy woowe àttaaya ju weex. Baay moo daan defar ay sondeelam ak kombook i buum ; tabanaane la daan segg, raxasal boppam ndab yi ndax kenn doyu ko ci woon. | Il vérifiait à chaque instant le charbon du filtre à eau, ne buvait que du thé, ou même de l'eau bouillante (que les Chinois appellent du thé blanc), fabriquait lui-même ses bougies avec de la cire et des cordons trempés dans la paraffine, lavait lui-même la vaisselle avec des extraits de saponaire. | null |
lii daal, am taax la mu gudd mu weex. bari lool ay ubbi féexal. ci kaw, juróom benni ubbi-féexal feeñ na fi. ci suuf, juróom benni ubbi-féexal feeñ na fi. ñu lal laltu bu xonq, ay nit yu sol lu xonq séq ko. waaw noo ngi ziyaar. yaang ci jàmm ? | Ceci est un long bâtiment blanc. Il contient beaucoup de climatiseurs. Six climatiseurs apparaissent ici. En bas, six climatiseurs y apparaissent. On a étalé une table à manger rouge ; des gens, vêtus de rouge, l'entourent. Mes hommages. Vous allez bien ? | null |
Góor gi nee ñépp dem ! | L'homme demande à tous de partir ! | null |
Yow jambaar ji ub làmb yi | Toi le champion des arènes | null |
Wànte maak sama mag kay, dan daan defanteek moom, di ko fexeel saa su ne, ci lu mu xaajul a foog. Mu doon, nag, xare bu metti, jeexal doole te doon firndeel itam ni mu yóbboo woon sunu fit. | Au lieu de cela, nous menions contre lui une guerre sournoise, usante, inspirée par la peur des punitions et des coups. | null |
Ci ki ñëw ba ñu xammee ka. | Chez celui qui est venu et qu'on a reconnu. | null |
Ñii dañu demul ? | Ceux-ci ne sont pas partis ? | null |
Amul ardo benn Jéeri boo xamul ! | Il n'est Ardo d'aucun Dieri que tu ne connaisses ! | null |
di soppi wurus jënde koy bàmmeel | épurant l'or pour des sépultures | null |
Ñàkk pexe tax koo teguwaat ci yoon wi ba Kano, daldi ñibbi Ogosaa. | La mort dans l'âme, il doit revenir en arrière, refaire la route jusqu'à Kano, jusqu'à Ogoja. | null |
Ca keppaar ga ay beykat yu jàq | A l'ombre des paysans inquiets | null |
Waaw mbokk mi, gis naa ni lii de ay potu Nescafé ñu def ci café. Gis naa ci ay doomi café yu ñor ak yu ñorul. Gis naa ci café gu mokku tamit ci wet gi. | Oui mon parent, je vois que ça c'est des pots de Nescafé dans lesquels il y a du café. J'y ai vu des graines de café mûrs et d'autres qui ne le sont pas. J'y ai vu aussi du café en poudre sur le coté. | null |
Baay daldi jàngaale lii : ak lu mu doon doon xaritu doomi réew mi, seen doomu-ndey, ñu koy diis seeni soxla, ba tey rekk ci nguurug Tubaab yi la bokk, moom la fi toogal. Ndax, su ñu waxantee dëgg, nit ki bu wér-gu-yaramam ajoo ci yow, fu la neex nga koy jaarloo. Te kon, dara du wutale sa taxawaay ak bu alkaati bi mbaa bu àttekat beek soldaar bi. Nga nangu kook nga bañ koo nangu, yaa ngiy pólitig. Naka la mënoon a deme neneen ? Faj doom-aadama, liggéey bu am maanaa la. | Alors mon père découvre, après toutes ces années où il s'est senti proche des Africains, leur parent, leur ami, que le médecin n'est qu'un autre acteur de la puissance coloniale, pas différent du policier, du juge ou du soldat. Comment pouvait-il en être autrement ? L'exercice de la médecine est aussi un pouvoir sur les gens, et la surveillance médicale est également une surveillance politique. | null |
Gis naa jigéen ju. | J'ai vu la femme. | null |
Dem naa ba Ndar. | J'ai été jusqu'à Saint-Louis. | null |
Ci bir sax ? | À l'intérieur même ? | null |
Jafe-jafe yiy way-juram doon jànkoonteel tax ba mu war a sukkandiku ci ndimbalu gornmaa bi. | Sa famille est ruinée, et il ne peut compter que sur la bourse du gouvernement. | null |
Fi muy ñefee ngir xàmmeewaat boppam ciw askanam, mu ngi yëg ni ko njabootam jéppee. | Aux difficultés d'adaptation s'ajoutait l'hostilité qu'il devait ressentir dans son propre foyer. | null |
Na ŋga dem | Que tu partes | null |
Liy Baay di njëkk a seetlu ci ñoom saa yu duggsee, mooy ni ñu tiite. | Quand il entre dans les chambrées, mon père lit la peur dans leurs yeux. | null |
Lii nag ay pólisee yu jigéeñ la. Ëe bari nañu lool, ñu ràngoo ay fetal, sol ay gā yu weex, sol ay mbaxana, ëe, mbaxana mi tamit am na ay rëdd yu weex ci kaw, ak ay yére yu ñuul, jiital lu weex. | Ceux-là sont des femmes policières. Elles sont nombreuses, portant des armes, des gangs blancs et un chapeau. Le chapeau aussi comporte des traits blancs, au-dessus. Elles portes des habits de couleur noir, précédée d'une couleur blanche. | null |
Yenn xar yooyuu laa wax ! | Je parle des autres moutons ! | null |
Seetal nit keneen ! | Cherche un autre homme ! | null |
Kooku la ! | C'est celui-là ! | null |
Dem nañu | Nous sommes partis | null |
bu njëgg yiy romb | au passage des caravanes | null |
Dellu biir Ndar, soo bëggée. | Retourne au centre de Saint-Louis, si tu veux. | null |
Tey, ma ngiy fàttaliku bu ci nekk ci ñoom ak i màndargaam. | Je me souviens de chacun d'eux, de leurs noms, de leurs bras levés, de leurs masques. | null |
Li mébét mu am solo moomu àntuwul, soppi na lu bari ci gis-gisu Afrigam. | À partir de cet échec, l'Afrique n'a plus pour lui le même goût de liberté. | null |
Miin kon naa gis-gis boobu ba duma ko soxlaa fat ba koy fàtte. | Je crois même qu'au bout d'un temps, je les aurais oubliés. | null |
Génnal ! | Sors ! | null |
Xëynë xar yi ñëw nañu, wante gisaguma wenn. | Les moutons sont peut-être déjà arrivés, mais j'en n'ai encore vu aucun. | null |
Boo weesuwaan tóokër ba, sànni say bët fu sori, danga daan séen ñax mi tëdd, defug joor gu yaatu, wuti dexug Ayaa. | Passé la limite du jardin, commençait la grande plaine d'herbes qui s'étendait jusqu'à la rivière Aiya. | null |
Waa ji demulwoon | L'homme n'a pas été | null |
Atum 1968 agsi, di at mu bariy yëngu-yëngu. Ma nekk Meksikoo, làrmeb nguur gi rey fay ndongoy daara ca Talatelókoo, ay fafal-naaw yu ndaw di for néewu gone yiy yóbbu ; ca Niis, liggéeykat yi bank seen loxo, samay ñaari way-jur sëppu seen palanteer di gis ni mbalit mi juugee ci mbedd mi ; fekk na Niseryaa, xareb Biyaafaraa baa ngay waaj a jeex ; mu doon faagaagal bi gënoon a ñaaw ci xarnu bi. | En 1968, tandis que mon père et ma mère regardent monter sous leurs fenêtres, à Nice, les montagnes d'ordures laissées par la grève générale, et tandis qu'à Mexico j'entends le vrombissement des hélicos de l'armée qui emportent les corps des étudiants tués à Tlatelolco, le Nigeria entre dans la phase terminale d'un massacre terrible, l'un des grands génocides du siècle, connu sous le nom de guerre du Biafra. | null |
Foo ko fekk mu ngi jëliy nataal ak Leikaam. Nataal yi, daanaka ñoo ëpp fuuf doole ay kàdduy neen. | Il prend des photos. Avec son Leica à soufflet, il collectionne des clichés en noir et blanc qui représentent mieux que des mots son éloignement, son enthousiasme devant la beauté de ce nouveau monde. | null |
Nil : wóoy ! | Crie ! | null |
Baay dem bëj-gànnaar, dal ca Ogaar, ci wetu Tamaŋaset (tuddoon booba Foor-Laperin). | Mon père remonte vers le Nord, bivouaque dans le Hoggar, près de Tamanghasset (à l'époque, Fort-Laperrine). | null |
Duma dem | Je n'irai pas | null |
Gisóon ŋga doomu jigéen joojale jan ? | Tu as vu le fils de quelle femme ? | null |
Nataal bii ma jot dee, Palais lay nuru waaye Palais bi nag am na ay garde corps yoo xam ne ñi ngi koy gardé, ba noppi mu am ñaari gaynde yoo xam ni ñoo ko séq. Palais bi nag paleb Senegaal lay nuru, ba noppi mu am ay xob yu wert ba noppi Palais bi bâtiment bi daa weex tàll. | Sur la photo que j'ai reçue, il y a une sorte de Palais. Cependant le Palais comprends des gardes du corps qui le garde. En plus, il y a deux lions qui l'entourent. Le Palais ressemble au palais du Sénégal. En plus, il a des feuilles vertes et le bâtiment du palais est complètement blanche. | null |
Moontin, dem naa | Et pourtant, j'ai été | null |
So demee, mi ŋgiy wax ! | Il est peut-être entrain de parler ! | null |
Loolu la. | Voilà ce qu'il en est. | null |
Waaw, lii nag moom lal la. Benn lal gu yànj boo xam ni mën nañ ne, ñetti nit ñoo siy dallu. Ndax si suuf, ñaari nit man neñ faa dallu. Ci kaw moom, ben nit rekk moo fa man a dallu. Ci wet ga, ñoong fa am benn rideau, rideau boo xam ne manees nañ ne couleur bu roos la am, roos claire ak roos bu foncée. Ca lal gi ca kaw moom, pour nga yegg ca, il faut, ëe... benn lu ñuy naan echelle. Echelle nag nekk benn juntukaay boo xam ne ay tànk la am, bole tànk boo teg di daal di gën a yéeg. Ca beneen wetu lal boobu nag moom, ca wetou echelle ba ñu ngi am ay tiroir. Tiroir nag nekk na benn juntukaay boo xam ne da lay tax nga fay denc say yëf. Waaw. | Oui, ceci est une chambre. Une large chambre dans lequel, on peut dire que, trois personnes peuvent s'y coucher. Car en bas, deux personnes peuvent s'y coucher. En haut, une seule personne peut s'y coucher. À coté, on a un rideau qui est complètement teint en rose, rose claire et rose foncée. En haut, sur le lit, pour pouvoir monter, il faut une échelle. Une échelle est un outil qui a des marches. Chaque marche sur lequel tu mets ton pied, tu montes encore plus. De l'autre coté du lit, à coté de l'échelle, on a des tiroirs. Un tiroir est un outil qui te permet de garder tes objets. C'est sûr. | null |
Muy béréb buy delloo xelam démb. | Les congés qu'il passe en France auprès d'eux sont le retour imaginaire vers un passé qui n'est plus. | null |
Man la góor gi woo ? | C'est moi que l'homme appelle ? | null |
Lu nekk ñu koy wax, ñépp tiit, kenn wóolootul kenn. | Les histoires qu'on raconte créent un climat de méfiance, de tension. | null |
Xar yan ñoo ñëw ? | Quels moutons sont arrivés ? | null |
Dem naa te demuloo ! | J'ai été et tu n'as pas été ! | null |
Gis naa kooku woon. | J'ai vu celui-là. | null |
Yaw, yaa ŋgi ! | Toi, tu es là ! | null |
Filipus a doon sama xaritu yaay. | Philippus était l'ami de ma mère. | null |
Gis ŋga samay xarit yan ? | Tu as vu quels amis à moi ? | null |
Waxu la yaw ! | Il ne te parle pas, à toi ! | null |
Waaye sax, kenn dafa dul dem | Du reste, nul n'ira | null |
Ma toog fan ? | Où puis-je m'asseoir ? | null |
Romb Legoos ak Ówéri, daldi agsi Aboo, ci wetu dexu Niseer. | Après Lagos, Owerri, Abo non loin du fleuve Niger. | null |
Baay seetlu ni, ni Afrig doon soppikoo ngir dëppook jamono, jigu ko. Bëgge, yàkkamti àddina ak ku mën sa moroom duma ñoo daldi wuutu lépp la mu soppoon ci Afrig. Li mu xamoon, moo doon i nit ñu ànd ak seen sago di daagu, am toppatoo ci seeni dëkk te weg bu baax mbey mi leen doon dundal. | Ce qui disparaissait aux yeux de mon père, c'était le charme des villages, la vie lente, insouciante, au rythme des travaux agricoles. La remplaçaient l'appât du gain, la vénalité, une certaine violence. | null |
Mi ŋgii dem na | Le voilà, il est parti | null |
Yaw dem ŋga | Toi tu as été | null |
Daŋga gis kan ? | Quel homme as-tu vu ? | null |
Dañuy xéy di wër ba ngoon jot, léeg-léeg ñuy doxe tànk, léeg-léeg ñu war fas. Fu leen guddi bett, ñu fanaan fa, nelaw cib taatu garab mbaa ci biir berkelle bu yem. Ca Kawóolu, ci tali Kisoŋ bi, bañ fa fekkee néeg buñ defare ban bu wow ak i xob, dañu daldi lonk seeni njoowaan. | Ils marchent tout le jour, tantôt à pied, tantôt à cheval, et s'arrêtent le soir pour dormir sous un arbre à la belle étoile, ou dans un campement sommaire, comme à Kwolu, sur la route de Kishong, une simple hutte de boue séchée et de feuilles où ils accrochent leurs hamacs. | null |
Coonoy dexi Guwiyaan ya duñu tus, doxantu bu gàtt lañu su leen méngaleek li muy waaj a daji Afrig sowu-jant. | À côté de ce qui attend mon père en Afrique, les expéditions pour remonter les fleuves de Guyane ont pu lui sembler des promenades. | null |
Teralal béppu nit ! | Honore tout homme ! | null |
Gor gii dem | Cet homme qui a été | null |
Dégguma | Je ne comprends pas | null |
Yàgguñu fa dara – bu àggee ci genn-wàllu xarnu fa lay yem – ñoom wutkati alal yooyu, daldi beru, di wujje, ñeme wax ju sew, lépp lu ñu gis mu taxaw ñu daaneel, lu jag ñu yàq ngir rekk bëgg a gaaw a jot ca lañ doon yóotu. | Une société qui, en moins d'un demi-siècle, s'est architecturée en castes, lieux réservés, interdits, privilèges, abus et profits. | null |
Buleen dem ! | Ne partez pas ! | null |
Benn nataal boobu mel ni doom-aadama bu fuññaaral, téye boppam, di biral ni nit ku weex tegee loxo ci Afrig, dem sax bay jéem a jox Afrig xar-kanamu Tugal. Yëg-yëg yu ni mel, benn yoon lañ ma mas a ganesiwaat, te ca diiwaanu Kanaalu Panamaa la woon. | Il y a dans cette photo unique quelque chose de froid, presque austère, qui évoque l'empire instauré par les hommes blancs en Afrique, mélange de camp militaire, de pelouse anglaise et de puissance naturelle que je n'ai retrouvé, longtemps après, que dans la zone du canal de Panama. | null |
Demuloowoon ca biir | Tu n'avais pas été à l'intérieur | null |
Dem ŋgeen | Vous êtes partis | null |
Duggël ci biir mbaa ci fii ! | Pénètre à l'intérieur ou ici ! | null |
Gàddaay defar sa gentu baay | S'exiler pour reconstruire les ruines de ton père | null |
Géej gaa ngi mar ak a maraat xeer yu ňuul yi ci tefes gi. | La mer déferle sur les roches noires et vient mourir sur la plage. | null |
Góor gi waxoon na | L'homme avait parlé | null |
Nataal bii de ab néeg la, ab néeg la waawaaw ; néeg boo xam ne kaw gi ñax la waawwaaw. Am na ag garab gu nekk nee waaw. Am na itam ay ñax yu nekk nee. Am na ay montaañ yu nekk nële yu kawe kawe uhun. Ay montaañ yu kawe sax waaye néeg bi moom bunt bi ëe maanaam dénk la, dénk bu xonq daal. | Sur cette photo ci il y a une assurément une chambre ; Une chambre au-dessus de laquelle il y a assurément de l'herbe. Il y a un arbre qui est juste là. Il y a aussi des herbes qui sont justes là. Il y a de très hautes montagnes qui sont là-bas. Oui de vraiment hautes montagnes mais la porte de la chambre est faite de bois de couleur rouge. | null |
Fekkoon na sax lonet yooyu xewwi. | Les lorgnons n'étaient déjà plus très courants à cette époque. | null |
Ndox may balle Kaburi ak Masuruni, loppitaanu Kamakusaa, baraag yi topp dex gi, bitigi wutkati marjaan yi. | Les chutes de Kaburi, sur le Mazaruni, l'hôpital de Kamakusa, les maisons de bois le long du fleuve, les boutiques de chercheurs de diamants. | null |
Yaa daan ganu Mustaf | Tu étais d'habitude l'hôte de Mustapha | null |
Te demuloo fenn ? | Et tu n'as été nulle part ? | null |
Su doon sunu sago, neneen la yëf yiy deme, nuy déglu Baay muy nettaliy jaar-jaaram, di woy léeg-léeg mbaa di ànd ak nun rëbbi sindax walla wuti sippax ci dexug Ayaa. Am kon naa mbégte yëg ni muy téyee sama loxo di ma won i lëppaa-lëpp yu jafee teg bët, ay tóor-tóor yu làq seen tooke fu sori ak yeneen ak yeneen. Waaw, doon na ma neex lool ma koy dégg muy fàttaliku ndawam ca Móris mbaa ma koy gunge buy seetiy xaritam. Dara doonul dàq ma koy seetaan muy defar wotoom walla di jagalaat ab palanteer ; su ma noon jàppale ma, doom, ma jëmbët ay tóor-tóor ak i garab, su ma noon may ma loxo ma dekkali tóokër ba woon ca kër ga ma yaroo ca Mokaa, dama ni, su ma Baay waxoon lu ni mel, duma ko sax gëme. | Il aurait fallu grandir en écoutant un père raconter sa vie, chanter des chansons, accompagner ses garçons à la chasse aux lézards ou à la pêche aux écrevisses dans la rivière Aiya, il aurait fallu mettre sa main dans la sienne pour qu'il montre les papillons rares, les fleurs vénéneuses, les secrets de la nature qu'il devait bien connaître, l'écouter parler de son enfance à Maurice, marcher à côté de lui quand il allait rendre visite à ses amis, à ses collègues d'hôpital, le regarder réparer la voiture ou changer un volet brisé, l'aider à planter les arbustes et les fleurs qu'il aimait, les bougainvillées, les strelitzias, les oiseaux-de-paradis, tout ce qui devait lui rappeler le merveilleux jardin de sa maison natale à Moka. | null |
Doomu-aadama bu, ne ci ndey ak baay nga jóge. | Tout être humain est le résultat d'un père et une mère. | null |
Subsets and Splits