wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
(loc.) Sa colin gu xumb gii nak ?
que signifie cet accoutrement voyant ?
xojox
avoir une éruption de boutons aux commissures des lèvres
Dafa xojox, moo ko tax di muur gémmiñ gi
il a des boutons aux commissures des lèvres, c’est pour cela qu’il se couvre la bouche.
xus
Épiler
Xus sama yeel yi, moo ko neex daal
de m’épiler les jambes, cela lui plaît vraiment.
xus
exprime la manière d’être en abondance
Xaal jaa nga ne xus marse
le melon abonde au marché.
xogg
manière d’avoir le cou engoncé dans les épaules
Mu ngii, ne xogg ni am tan
le voici, le cou engoncé dans les épaules comme un vautour.
xojox g-
Écureuil de Gambie (Heliosciurus gambianus, Sciuridés)
Xojox sopp na lool gëŋ
L'écureuil de Gambie aime beaucoup les figues sauvages.
xoddoos
(voix). Être rauque, être enrouée
xoj
Étrangler avec la main
xol b-
cœur
Soo tegee sa loxo ci sama dënn, dinga yég sama xol biy dal
si tu poses ta main sur ma poitrine, tu sentiras mon cœur battre.
Xolu garab gi la
C'est le cœur de l’arbre.
xat xol
avoir les nerfs à fleur de peau.
ñuul xol
être méchant.
yàq xol
attrister.
Bul yàq sama xol
ne me fais pas de la peine.
Sama xol dafa jeex
je suis découragé.
Amul xol
il n’est pas rancunier (ou bien) il est inexorable.
rafet xol
avoir bon cœur.
tàng xol
être soupe au lait (ou bien) être frustré.
jéle xol
prendre à cœur.
Ci xol bu sedd (ou bien) ci xol bu tàlli
de bon cœur.
xol
faire manger qqn (ou un animal) qui ne peut pas le faire tout seul
Boo ko nee mu xol xale bi, mu lekk genn-wàll gi
quand tu lui dis de faire manger l’enfant, il en mange la moitié.
xoju
(fam.) Porter une cravate
Lu xew ba nga xoju ?
que se passe-t-il pour que tu portes une cravate ?
xollit w-
pelure, épluchure coque
Baleel xolliti pombiteer yi
balaie les épluchures de pommes de terre !
xomb g-
cadenas
Ana xombug bunt bi
où est le cadenas de la porte ?
xon g-
arc-en-ciel
Xanaa gisuloo xon gi ? Dootul taw
est-ce que tu n’as pas vu l’arc-en-ciel ? Il ne pleuvra plus.
xomm
complètement, tout à fait, bien (mûr, cuit)
Xaaral ba mu ñor xomm
attends que ça soit tout à fait cuit (mûr).
xonqal
rendre rouge
Lu xonqal ndox mi ?
qu’est-ce qui a rougi l’eau ?
xolu tànk b-
milieu de la plante du pied
xoob m-
variété d’épervier
xuumtoo
s’entretenir de qqch en secret
Ñu ngiy xuumtoo mbir mi
ils s’entretiennent de la chose en secret.
xuuge
être bossu
Dama defe woon ne dafa xuuge
je pensais qu’il était bossu.
xonq
être rouge vif
Yére bu xonq la sol
il porte un habit rouge vif.
Bu sa bët xonqee, say mbokk
ñooy taxaw
xonjom y-
pratiques magiques visant à ensorceler qqn
xoñoñ
être exaspéré
Dafa xoñoñ ndax li nga ko ne du dem
il est exaspéré parce que tu lui as dit qu’il ne partirait pas.
xoñoñ
exaspérer
xonjom
ensorceler
xont
donner à manger (à un animal)
Négal tuuti, dafay xont xar yi
attends un peu, il donne à manger aux moutons.
xoolin b-
expression du regard
xooj
tremper
Xoojal yére yi, dinaa leen fóot ci kanam
trempe les habits, je les laverai tout à l’heure.
xuuxaan
avoir une hernie scrotale
Dafa xuuxaan
il a une hernie scrotale.
xoot-xoot b-
eau qui reste dans un récipient qu’on a lavé
Xoot-xoot baaxul ci ndab; rawati-na lu weñ la
L'eau qui y reste n’est pas bonne pour les récipients, surtout ceux en fer.
xoosu
avoir des éraflures
Taabal bi dafa xoosu yépp
la table est toute éraflée.
xoos-xoos b-
Éraflure
xoor w-
pomme d’Adam
xoojooj
avoir bu en quantité excessive au point d’en avoir le ventre balloné
xoraay
Être rouge.
Jant baa ngay xoraay
le soleil au loin devient rouge.
xoox b-
noix
Tojal xoox bi
casse la noix !
xor w-
coquillage
Ay xor la def ci
ëttam il a mis des coquillages dans sa cour.
xosiku
une égratignure
Xosiku nga ci lex
tu as une égratignure à la joue.
xoos g-
nom d’une variété de plante qui ne croît que dans l’eau
xàbban b-
taureau châtré
Xàbban la ko reyal ba mu ko ganejee
il lui a tué un taureau châtré quand il est allé lui rendre visite.
xoox
être à bout de course, épuisé, fatigué
Dama xoox
je suis à bout de course.
xorondom g-
galerie de {xorondom}
xopp s-
couteau dont la lame est presque entièrement usée
Sànnil xopp si, te wut paaka bu bees
jette le couteau usé et cherche un couteau neuf !
xosi
Égratigner
Lu la xosi
qu’est-ce qui t’a égratigné ?
xosi-xosi b-
Égratignure
Lu la def xosi-xosi bii
comment as-tu eu cette égratignure.
xorom s-
sel
Demal jéndali ma xorom
va m’acheter du sel !
Li ngay nettali amul xorom
ce que tu racontes n’a pas de piquant.
(prov.) Lu cin xat, xat xorom xaj ca
si étroite que puisse être une marmite, le sel y trouvera de la place.
xoteet
complètement (déchirer)
Dafa xotti simis ba xoteet
il a complètement déchiré la chemise.
xoti b-
pigeon
Ubbil kaafu xoti yi
ouvre la cage des pigeons.
xos w-
talisman qu’on place dans un champ pour avoir un bon rendement
Ba ma defee xos wi ci sama tool ba léegi, maa ngiy sant Yàlla
depuis que j’ai placé dans mon champ le talisman pour avoir un bon rendement, je rends grâce à Dieu !
xos g-
virgule
Danga wara def xos fii
tu dois mettre une virgule ici.