wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
(prov.) Wax ju jëkk, fasu par la, tontu la, naaru-góor
les premiers propos sont comme un cheval de la race {par} mais la réplique est comme un pur-sang.
na
comment
Na nga def ?
comment vas-tu ?
na
exprime une injonction, une invitation à exécuter une action
Nañu dem partons ! Nanga ci def tuuti xorom
tu y mettras un peu de sel !
ñaasu
se balafrer
ñaas
balafrer
Dafa ñaas kanamam
il s’est balafré le visage.
naawaan b-
oisillon
naanu g-
pipe
Naanu gi nga ko may rafet na
la pipe que tu lui as offerte est belle.
naaféq b-
personne perfide
Kooku naaféq la
celui-là, c’est un perfide.
ŋalaab j-
mors
Dindil ŋalaab ji
enlève-lui le mors !
ñaasentaan w-
chenille
naataango b-
Égal collègue pair
Ministar bi dafay daje ak i naataangoom
le ministre rencontre ses pairs.
ñaanaatu
demander par-ci, par-là
Dafay ñaanaatu ay yére
il demande des habits ici et là.
ñaag b-
poignée de nourriture
Ñaag bi xéjul ci sa gémmiñ
cette poignée ne peut pas entrer dans ta bouche.
ñaaw-xel
avoir l’esprit retors
Danga ñaaw-xel
tu as l’esprit retors.
naawal g-
cerf-volant
Naawal gi dafa lonku ci garab gi
le cerf-volant est accroché à l’arbre.
nammeel g-
intention
Lu nammeel di jariñ ?
à quoi sert la nostalgie (à l’instant où on se revoit, elle cesse) ?
nammeel g-
intention
Ba Yéesu nangoo jébbalu ca kurwaa ba, musal àddina si moo doon nammeelam
quand Jésus accepta de s’offrir sur la croix, son dessein était de sauver le monde.
naana b-
menthe (plante ou feuille)
Àttaaya ji amul naana
il n’y a pas de menthe dans le thé.
naam
interj. Oui !
Ne naa naam ñaari yoon
J'ai dit oui deux fois.
(prov.) Bala nga naan naam, ne fa
pour répondre, encore faut-il être présent; pour faire qqch, il faut en avoir les moyens.
Naam
le nom de famille ?
naaj
(dans la matinée) Être tard
Léegi, naaj na; su nu demee, dunu ko fa fekk; Suba teel lay xéy
maintenant il est tard; si nous partons, nous ne l’y trouverons pas; il s’en va tôt le matin.
naar-bët b-
insecte recouvert de poils veloutés, écarlates
ŋaam w-
mâchoire
Sa ŋaam dafay metti ?
tu as mal à la mâchoire ?
naaga b-
chamelle
Naaga du bokk ci rawante bi
une chamelle ne participe pas à la course.
ñaas b-
pratique de la balafre
ñaag
prendre une grosse poignée de nourriture
Ni nga mëne ñaag ceeb
comme tu es doué pour faire de grosses poignées de riz !
ñaan g-
prière demande
Sama ñaan nangu na
ma prière a été exaucée.
ñaay b-
brousse.
Ñaay booba yépp ñu ngi koy bay léegi
on cultive dans toute cette brousse maintenant.
(prov.) Ndànk, ndànk mooy jàpp golo cib ñaay
c’est en faisant doucement qu’on parvient à prendre le singe en brousse
ñaan b-
demande en mariage.
Ñaan bi, bu ñu jullee tàkkusaan la
la demande en mariage se fera après la prière de dix-sept heures.
ŋaamaan b-
personne qui circoncit
Omar a di ŋaamaanu tund wi wépp
Omar est le circonciseur dans toute cette contrée.
(prov.) Wor sa ŋaamaan a gën wor sa léttkat
il vaut mieux trahir celui qui t’a circoncis que trahir ta coiffeuse.
naan-kaani
(Fam.) Être acariâtre
Kookoo la gëna naan-kaani
celui-là est plus acariâtre que toi.
ŋa
ouvrir la bouche
Looy ŋa nii ?
qu’as-tu à ouvrir la bouche ainsi ?
ñaata
combien
Ñaata bunt la woto bi am
la voiture a combien de portes ?
naaw b-
vol (oiseau, avion, etc.)
naaw-naaw m-
poule de mer, Grondin volant
ŋabar-ŋàbb g-
objet vétuste, en mauvais état
Tali yaa ngi def ay ŋabar-ŋàbb
les routes étaient en mauvais état.
ñankataŋ b-
riz cuit à l’eau
Indil ñankataŋ bi
apporte le riz cuit à l’eau !
ñab-ñabal
rafistoler
Dafa ñab-ñabal armool bi
il a rafistolé l’armoire.
ñaaw-njort
être pessimiste
Danga ñaaw-njort rekk, waaye du dara
C'est simplement que tu es pessimiste, mais ce n’est rien.
naat b-
pintade
Ay naat lay jaay.
Il vend des pintades.
(prov.) Toŋ-toŋu naat, bu wëree am réew, dung yaa tax
c’est à cause des plumes que tout le monde sait qu’on a partagé une pintade.
naawtal
exercer à voler (oiseau)
Boo demee ba naawtal, su la neexee, nga dellu Ndakaaru
quand tu auras fait faire ses premiers pas à ton enfant, tu pourras retourner à Dakar.
naawtal
jeter un sort à qqn en sorte qu’il éprouve toujours le besoin de partir, de ne pas rester en place
Dañu ko naawtal
on lui a jeté un sort pour qu’il ne se fixe nulle part.
ñaawteef b-
ignominie vilenie
Mësunu ko déggal benn ñaawteef
nous ne l’avons jamais entendu dire aucune vilenie.
naal b-
projet
Rafetlu na naal bi
il a été satisfait du projet.
ŋacc
être asséché, tarir
Teen bi dafa ŋacc, xaaral tuuti
le puits s’est asséché, attends un peu !
ŋacc
Écoper
Ne ko mu ŋacc ndaa li
dis-lui d’écoper le canari !
ŋaayoo
se brouiller, se chamailler avec qqn
Waruleena ŋaayoo
vous ne devez pas vous chamailler
ñaay
dévaster
Golo yaa ngay ñaay tool ba
les singes dévastent le champ.
Kawlax maa ko ñaay
j’ai fait un tabac à Kaolack.
ñaay
(fam.) Prendre la fuite.
Ñaay nga àll bi yépp
tu as pris la fuite.
nafa g-
bourse qu’on porte sur la poitrine ou à la taille
Defal xaalis bi ci sa nafa bala muy réer
mets l’argent dans ta bourse avant qu’il ne se perde.
ñagas
être rugueux
Toof bu ñagas ngay wut
cherche une étoffe rugueuse !
nab-nabal
chouchouter
Bàyyil xale bi ngay nab-nabal
arrête de chouchouter cet enfant !