wolof
stringlengths 1
166
| french
stringlengths 2
331
|
---|---|
bàkkat g-
|
une variété d’herbe
|
buuse b-
|
boucher
|
Buuse la woon
|
il était boucher.
|
baaxe
|
(Dieu) Combler
|
Yàlla baaxe na ko
|
Dieu l’a comblé.
|
bif
|
tirer d’un coup, violemment
|
Bu ko bif, xëcc ko ndànk
|
ne le tire pas d’un coup, tire-le doucement !
|
baaraamu-tofu-digg b-
|
(doigt) Annulaire
|
baaraamu-digg b-
|
majeur
|
Takkal jaaro bi ci baaraamu-digg bi
|
mets la bague au majeur !
|
boppu-lal b-
|
chevet
|
Féetaleel boppu-lal bi ci palanteer bi
|
oriente le chevet vers la fenêtre !
|
baayoo
|
faire de qqn son père adoptif
|
Xamuma fi kenn; yow laa baayoo
|
je ne connais personne ici; c’est toi que j’ai pris pour père adoptif.
|
baagante b-
|
fait de faire la navette
|
Bàyyil baagante bi
|
arrête de faire la navette !
|
bëtër
|
exprime la manière brutale de projeter
|
Mu agseek kéwélam, ne ko bëtër
|
il arriva avec sa gazelle, et vlan ! (la projeta).
|
boob
|
faucher de l’herbe sèche
|
Altine, dinaa boob gannaaw kër gi
|
lundi, je faucherai l’herbe sèche derrière la maison.
|
baara g-
|
plante dont l’épi couvert d’une couche cotoneuse ressemble à une chenille avec des barbes.
|
baana-baana
|
du commerce informel
|
Omar dafay baana-baana léegi
|
Omar fait du petit commerce maintenant.
|
baar b-
|
bar
|
Soo ko bëggee gis, demal ca baar ba nekk korniis
|
si tu veux le voir, va au bar de la Corniche.
|
bàq g-
|
flaque d’eau
|
baale
|
pardonner
|
Dil baale
|
il faut pardonner.
|
ba-dee
|
bel et bien
|
Xam nga ko ba-dee
|
tu le sais bel et bien.
|
baaral
|
laisser mijoter
|
Ne ko mu baaral ba ca kanam
|
dis-lui de laisser mijoter quelque temps encore !
|
booyal b-
|
jachère
|
bal
|
en lutte, faire une prise qui consiste à mettre la main sous l’aisselle de l’adversaire
|
baaraamu-sanqaleñ b-
|
auriculaire, petit doigt
|
baji b-
|
excréments partiellement devenus comme des grains de sable
|
Moytula joggi baji yi
|
fais attention de ne pas mettre les pieds sur les excréments.
|
biddanti
|
avoir le torticolis
|
Dama biddanti
|
J'ai le torticolis.
|
biddanti
|
se réveiller tard le matin involontairement
|
Dama biddanti; tuuti saxaar gi raw ma
|
je me suis réveillé tard; pour peu, je ratais le train.
|
bagaas b-
|
bagage
|
Amuma bagaas
|
je n’ai pas de bagages.
|
(Loc. Fam.) Sa waa ji du bagaas
|
ton bonhomme ne fait pas le poids.
|
baara g-
|
plante dont l’épi couvert d’une couche cotoneuse ressemble à une chenille avec des barbes.
|
bërëx
|
être bien pris (feu)
|
Sa taal bi bërëx na; kaay tàmbali
|
ton feu est bien pris; viens commencer.
|
baara-yégoo
|
{baara-yégoo} consiste, pour un ex-mari, à être de connivence avec qqn qui contractera un mariage blanc avec cette femme, puis divorcera rapidement, afin de pouvoir légitimer une quatrième union
|
bag b-
|
(transport) Bac
|
Am na bag buy jàlle woto yi
|
il y a un bac pour faire traverser les voitures.
|
balaxalmàddaa
|
mener la belle vie
|
bagaan g-
|
grande calebasse taillée dans un tronc d’arbre
|
Mën na lekk bagaan gu fees ak laax
|
il peut manger une grande calebasse pleine de bouillie de mil.
|
baay-jagal b-
|
personne qui a pour métier de réparer toutes sortes de choses
|
Baay-jagal dikk na. Ku amoon looy defarlu
|
le réparateur est arrivé. Qui aurait qqch à faire réparer ?
|
baxaw
|
désherber un champ de mil
|
Na la xale yi jàppale, nga baxaw
|
fais-toi aider par les enfants pour désherber.
|
bajo b-
|
sexe de la femme
|
Muural ko bajo bi
|
recouvre-lui le sexe.
|
Bajo fàŋŋ
|
sexe en l’air.
|
baagante
|
faire la navette
|
Looy baagante nii ?
|
qu’as-tu à faire la navette ainsi ?
|
bàkkaarkat b-
|
pécheur
|
bugewiye g-
|
bougainvillier
|
baaxoo
|
avoir pour coutume de faire qqch
|
Altine lañu baaxoo daje
|
habituellement, c’est le lundi que nous nous réunissons.
|
bale b-
|
balai
|
Indil bale bi
|
apporte le balai.
|
baaxoñ b-
|
corbeau
|
Baaxoñ bee ko yee
|
C'est le corbeau qui l’a réveillé.
|
(prov.) Baaxoñ a doon jàng doxinu ramatu, mënatu ko, faf fàtte bosam
|
c’est le corbeau qui apprenait la démarche du moineau, il ne sut pas (l’imiter), du coup il oublia la sienne
|
bas-basi
|
couler à flots (larmes)
|
Maa ngi ko fekk, rongoñ yiy bas-basi
|
je l’ai trouvé en larmes.
|
baalante
|
se pardonner mutuellement
|
Nangeen baalante su ngeen bëggee Yàlla baal leen
|
pardonnez-vous les uns les autres si vous voulez que Dieu vous pardonne.
|
boroos b-
|
brosse
|
Wutal ma sama boroos
|
cherche-moi ma brosse !
|
baayo b-
|
orphelin de père
|
Xare booba def na ay baayo yu bare
|
cette guerre a fait beaucoup d’orphelins de père.
|
belli
|
extraire les meilleurs
|
been
|
mettre à l’envers
|
Danga been sa simis
|
tu as mis ta chemise à l’envers.
|
bale
|
balayer
|
Ku bale fii tey
|
qui a balayé ici aujourd’hui ?
|
bakku b-
|
grande cuillère en bois pour remuer dans la marmite
|
Raxasal bakku bi
|
lave la grande cuillère en bois !
|
baawal
|
répandre
|
Dafa baawal wax ji ci tund wépp
|
il a répandu les propos dans toute la région.
|
baaraam b-
|
doigt
|
Sa baaraam yi dañu gàtt
|
tu as les doigts courts.
|
balaas b-
|
balance
|
bal-balal
|
exécuter la troisième phase de la culture, qui consiste à désherber
|
Léegi ñu wara tàmbali bal-balal
|
bientôt on va devoir commencer à désherber.
|
bal b-
|
balle d’arme à feu
|
Bal bi dafa sarale óom bi
|
la balle a transpercé le genou.
|
bugg
|
être affamé
|
Ñooña dañoo bugg
|
ceux-là sont affamés.
|
caaf l-
|
arachide décortiquée et grillée
|
Jaay ma ñaari laxasu caaf
|
vends-moi deux cornets d’arachides grillées !
|
caabi j-
|
clé
|
Subsets and Splits
No community queries yet
The top public SQL queries from the community will appear here once available.