wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
rëq
avoir une luxation
Mbagg mee rëq il a eu une luxation à l’épaule. (Expression) rëq ndigg
briser (qqn).
Dinaa rëq sa ndigg
je te briserai.
res w-
foie
Doktoor dafa ma ne may lekk res ndax dama ñàkk deret
le médecin m’a dit de manger du foie, car je suis anémié.
(prov.) Resu xaj, bu seddee soof
le foie du chien, quand il se refroidit il devient insipide
rëkk
frapper dans le dos
Lu mu la def ba nga di ko rëkk ?
que t’a-t-il fait pour que tu le frappes dans le dos ?
rëkk
Manière d’être tout à fait juxtaposé, au pied du mur, tout contre qqch
Këram dafa sës rëkk ci sama bos
sa maison est tout contre la mienne.
reqi
couper de l’herbe dans l’eau où elle pousse
Mu nga ca toolu ceeb ba di reqi ñax ma
il est à la rizière à couper de l’herbe.
ronni
toiser
Man de, xamuma loo may xoole ba di ma ronni
je me demande bien pourquoi tu me regardes en me toisant.
rëppët b-
(onom.) Galop
ren
année en cours
Ren, bëgg naa dem Màkka
cette année, je veux aller à La Mecque.
rënd
incorporer viande ou poisson dans une préparation culinaire
Dàqal muus mi bala ngay rënd
chasse le chat avant de mettre la viande (ou le poisson) dans le mets !
rey
tuer
Muus mee rey jinax ji
C'est le chat qui a tué la souris.
(prov.) Dëmm rey la, jaale la
après t’avoir tué, le sorcier te présente ses condoléances.
Bi ñu ma nee dem nga, dafa rey sama yaram
quand on m’a dit que tu étais parti, cela m’a refroidi.
rewle
accoucher (une femme)
Porofesoor Adaci, moo ma rewle
C'est le professeur Adachi qui m’a accouchée.
roseet
manière de se désengager totalement d’une chose
Dama ne woon dama koy jénd waaye génn naa ca roseet
J'avais dit que je l’achète mais je m’en suis désengagé.
rew
déterrer les racines qui vont servir à faire des manches d’instruments aratoires comme le « ileer »
rendi
Égorger
Mbaam, deesu ko rendi
on n’égorge pas le cochon.
Elimaan rendi na
L'imam a égorgé (c’est ainsi qu’on annonce que l’imam de la mosquée a égorgé le mouton de la Tabaski, pour permettre aux autres fidèles d’égorger le leur).
rew y-
vergeture
Jigéen ju bare rew dafay jaboot
une femme qui a beaucoup de vergetures aura une famille nombreuse.
reso
réchaud
rët
avoir une légère peur
Te kat ba ma ko gisee, dama rët
et dire que quand je l’ai vu, j’ai eu un peu peur.
rew m-
séance collective de déterrement de racines qui vont servir à faire des manches d’instruments aratoires
réylu
être trop fier pour
Réylu naa ko leb dërëm bi gëna tuuti
je suis trop fier pour lui emprunter le moindre sou.
reyante
s’entretuer.
Ñaari réew yaa ngay reyante
les deux pays s’entretuent.
Dafa reyante ba am lijaasaam
il s’est battu pour avoir son diplôme.
ribijoŋ
réveillonner
Dingeen ribijoŋ ren 
réveillonnerez-vous cette année ?
réy-réylu
faire l’orgueilleux
rigol b-
rigole
riccamtéku
faire qqch pour se racheter d’un acte dont on est confus
Bëgga riccamtéku moo la tax di wax lii
C'est pour te racheter que tu dis ça.
rido
rideau
riigu
s’asseoir
Riigul fii
assois-toi là.
riij
piler qqch d’humide
Dafay riij ndig li, mel ni amul yax
elle roule les hanches comme si elle n’avait pas d’os.
riij
battre le tam-tam en sourdine
riiñoo b-
réunion
Riiñoo bi yàgg na bii yoon
la réunion a été longue cette fois-ci.
riccamti
mettre à l’aise qqn qui était confus à la suite d’une faute
Demal riccamti ko
va le tirer de sa honte.
riim
chantonner
Séet bi di riim ci suuf, mel ni ku bëgga wax
la nouvelle mariée chantonnait à voix basse, comme si elle allait parler.
riggël
arriver à terme
Waxtaan wi riggël na
la conversation est arrivée à terme.
riiti g-
vièle
rink
avoir les jambes arquées
Dafa rink
il a les jambes arquées.
ruuñ b-
sorte de ragoût de viande avec beaucoup de gras
Lekk naa ci ruuñ bi, duma reer
J'ai mangé du ragoût gras, je ne dînerai pas.
rijji
herser
Jigéen ñi dañuy xaar ba góor ñi rijji ba-noppi, ñu ñów
les femmes attendent que les hommes aient fini de herser pour venir.
rikkat
serrer les cordes d’un tambour d’aisselle pour en tendre la peau
War ngaa rikkat sa tama ji
tu devras serrer les cordes de ton tambour d’aisselle.
riir
foncer sur
Dafa riir, wutali ko, kooku mbas ko
il a foncé sur lui, ce dernier lui a fait une feinte.
riirandoo
se précipiter tous ensemble
Ba ñu déggee xibaar ba, ñu riirandoo, jubal marse
quand elles apprirent la nouvelle, elles se précipitèrent toutes ensemble en direction du marché.
rijji m-
hersage
Rijji mi, ay fan rekk lay def
le hersage ne prend que quelques jours.
ripp
manière d’être tout souillé (ne s’emploie qu’avec taq)
Mu ngi tooy xipp, taq ripp
il est tout mouillé, tout souillé.
rob
inhumer
Rob nañu ko démb, ci altine ji
on l’a enterré hier, lundi.
(prov.) Néew, bu rombee ay armeel, robam dootul neex
un mort quand il dépasse le cimetière, son enterrement ne sera plus aisé) quand un cortège funèbre va plus loin que le cimetière, ça devient malcommode.
roccantal
faire un nœud coulant
Mën nga roccantal ?
sais-tu faire un nœud coulant ?
ruux
enfoncer
Ruux ko ci poroxndoll bi
enfonce-le dans le trou !
ruux
donner des sensations douloureuses dans les membres (en particulier rhumatisme)
Mu ne tànkam yi dañuy ruux
il dit qu’il a des douleurs dans les jambes.
robb b-
robe
ràbbaske
être entrelacé
Car yu ràbbaske
des branches entrelacées.
ràbb
tisser
Maa ràbb bii ak bee
C'est moi qui ai tissé celui-ci et celui-là.
rog
regarder une personne du coin de l’œil sans la suivre dans son déplacement
rokkos
bourrer
Mu ngi rokkos ay kayit ci poosam yi ba ñu fees; xamuma lu mu koy doye
il a bourré ses poches de papiers; je me demande ce qu’il va en faire.
rodd
Érafler
Bant bilee ko rodd
C'est ce bâton qui l’a éraflé.
Lu la rodd ?
qu’est-ce qui t’a éraflé ?
romb-jaan b-
natte