wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
ndañ
donner un coup de tête
Dafa ko ndañ
il lui a donné un coup de tête.
ndarakàmm
en plein jour
ndarkase g-
anacardier
ndarkase g-
anacardier
ndawal l-
poisson ou viande qui accompagne le mets
Jéndaguma ndawal
je n’ai pas encore acheté de poisson
ndarkepp
(dans une poursuite) Le fait de se retrouver dans une impasse
nding m-
endroit où l’on entasse le foin
ndawràbbin b-
danse traditionnelle lébou
Dañu bëgga xewalaat ndawràbbin elles veulent ramener la danse ndawràbbin
la mode.
ndéef g-
bouse de vache séchée
Dañuy jaxase ndéef gi ak ban di ko tabaxe
ils mélangent la bouse de vache et l’argile et construisent avec.
ndaxam
pourtant
Ndaxam waxtu wi jotagul
pourtant il n’est pas encore l’heure.
ndawtal
offrir un cadeau à l’occasion d’une fête de famille
Sama xarit yépp ndawtal nañu ma ba mu des yow
toutes mes copines m’ont offert un cadeau sauf toi.
ndaw s-
jeune femme
Am na ndaw su lay laaj
il y a une jeune femme qui te demande.
ndaw ñ-
les jeunes
Ndaw ñaa ngi tooge fii, mag ñi fale
les jeunes sont assis par ici, les adultes par là-bas.
ndawe
être relativement petit
ndéeyoo l-
fait de se chuchoter des choses
ndaw
être jeune
Gone gu ndaw la
C'est un petit enfant.
ndaw
quel ... ! Que de ... !
Ndaw woto bu rafet
Quelle belle voiture !
Ndaw lu gaaw 
quelle chose rapide !
Ndaw i yoo ci kër gi 
que de moustiques dans la maison !
ndéeñ l-
gland de la verge
Ci ndéeñ li la ko melentaan wi màtt
la fourmi l’a piqué au gland.
ndéegu l-
(wolof du Saloum)
ndéego l-
(wolof du Saloum)
ndékki l-
petit déjeuner
Ana ndékki li ?
où est le petit déjeuner ?
(prov.) Borom ndékki, ku ko jëkka yewwu tëddaat
le propriétaire du petit déjeuner, celui qui se réveille avant lui se recouche.
ndeer w-
variété de moineau
Amul picc wala aw ndeer
il n’y a pas âme qui vive.
ndoŋ l-
occiput
Gënal wàññi kawaru ndoŋ li
diminue davantage les cheveux à l’arrière de la tête.
ndëggu l-
 du pied
Ndëggu li moo koy metti
C'est à la plante du pied qu’il a mal.
ndeete l-
fin
Dinaa la fey ci ndeetelu weer wi
je te paierai à la fin du mois.
Fii ak ndeetel at mi
D'ici la fin de l’année.
ndekkite g-
résurrection
Paak lañuy màggal ndekkite Yéesu
C'est à Pâques qu’on célèbre la résurrection de Jésus.
ndëlle
avoir les caractéristiques du molleton
Dafa ndëlle, moo tax neexu ma
C'est du genre molleton, c’est pour cette raison que ça ne me plaît pas.
ndékki
prendre le petit déjeuner
Damay ndékki
je prends le petit déjeuner.
ndem-si-Yàlla j-
défunt
Ndem-si-Yàlla ji, Omar
le défunt Omar.
(loc.) Ndem-si-Yàlla ji, foo nekkoon ?
le revenant, où étais-tu ?
ndëll b-
molleton étoffe épaisse et légère en laine ou coton
Sama yaay daan na ma ñawal yére ndëll
ma mère me cousait des habits en molleton.
ndem-dellu b-
de souris en U
Ndem-dellu lay niru
ça ressemble à un trou de souris en U.
ndenceef l-
réserve
ndénéer g-
clairière
Ci ndénéer gi lay gëna yomba jàppe
il sera plus facile à prendre dans la clairière.
ndem l-
aller
Ndem lee gëna gaaw
L'aller est (a été) plus rapide.
ndàbb
coller
Dañu ko ci ndàbb
on l’y a collé.
ndés g-
natte
Dafa ne réjj déju ci ndés gi
elle s’assit brutalement sur la natte.
ndetteelu l-
fait de tomber soi-même sur le postérieur
Sa ndetteelu li dafa la bett
tu as été surpris de tomber sur le derrière.
ndëpp
organiser une cérémonie de danse d’exorcisme (chez les Lébou)
Lébu yeey ndëpp
ce sont les Lébou qui organisent le ndëpp.
ndengleer g-
clairière
Ndengleer gii lañu tëgge làmb ji
C'est dans cette clairière qu’on a organisé les jeux de lutte.
ndetteel l-
chute sur le postérieur
Ndetteel dafa metti
une chute sur le postérieur, c’est douloureux.
ndengeñ
refuser une chose par dépit
Dafa ko ndengeñ
il l’a boudé.
ndóomaar m-
tortue de mer géante
Am ndóomaar a ngi ci mbaal mi
il y a une tortue de mer dans le filet.
Kooku, ndóomaar la
celui-là, c’est un idiot.
ndéstan g-
natte
Toogal ci ndéstan gi
assois-toi sur la natte !
ndënd m-
gros tambour à une membrane dont le fond est fermé
Ndënd ya sàjj nañu, njegemaar yaa ngay tëb, di dal
les gros tambours ont résonné, les jeunes filles trépignent.
tollu ci sa diggi ndënd
être à son apogée.
Booba, maa ngi tollu woon ci sama diggi ndënd
cette époque-là, j’étais à mon apogée.
(prov.) Sàcc ndënd yomb na, waaye foo koy tëgge 
voler un tambour, c’est facile mais où le battre ?
ndeq s-
petit marigot
ndeyale
donner comme marraine
Moom lañu ma ndeyale
C'est elle qu’on m’a choisie pour marraine.
ndëxënteef l-
trésor
ne
dire
Mu ne dina
ñów il dit qu’il viendra.
ne
que
Xam naa ne dina
ñów je sais qu’il viendra.
ndóndi b-
idiot
Ndóndi bu mel ni Musaa, su gisoon lii, dafay daw
un idiot comme Moussa, s’il voyait ça, il s’enfuirait.
ndétt l-
le fond de la mer le lit d’un fleuve, d’une rivière, etc) le sol (plus largement)
ndóobu w-
cheval qui a les pattes blanches
ndëpp l-
chant et danse d’exorcisme pratiqués surtout par les Lébou