wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
Jox ko ndàmpaay
donne-lui un dédommagement !
ndàdde b-
dernier (jargon des écoliers)
Mooy ndàdde kalaas bi
il est le dernier de la classe.
ndàllan l-
ensemble (de choses)
ndàbb l-
colle
ndàq m-
fait de renvoyer
Sa ndàqum ganaar mi de jigu la
ça ne t’a pas porté bonheur de chasser la poule.
(prov.) Ndàqum ganaar, waxaale sa soxla
profiter du fait qu’on chasse la poule pour dire ce qu’on a sur le cœur.
nelaw b-
sommeil
Nelaw bu xóot
un sommeil profond.
Nelaw yu yàgg
un long sommeil.
Nelaw yu neex
un sommeil réparateur.
(prov.) Nelaw tax naa gëm dee
le sommeil préfigure la mort.
ndóbinu b-
costume de femme composé d’un haut et d’un pagne
ndóbin g-
grand calao
nëb
être pourri
Màngo bi dafa nëb
la mangue est pourrie.
ŋeb
fermer la bouche
Bu lay déglu, du ŋeb
quand il t’écoute, il ne ferme pas la bouche.
Ba mu duggsee ak mbaxanaam, kenn manatula
ŋeb quand il entra avec son chapeau, personne ne put plus retenir son rire.
nen b-
Œuf
Dafay baxal ay nen
elle fait bouillir des œufs.
(prov.) Nen du bëre ak doj
un œuf ne lutte pas avec un caillou) on ne s’attaque pas à plus fort que soi.
nëbb
cacher
Yaa nëbb sama caabi
C'est toi qui as caché ma clé.
ndàndi b-
bon cultivateur
Sama baay ab ndàndi la woon
mon père était un excellent cultivateur.
ndóof
jouer au ndóof
neb-neb g-
acacia à gomme rouge dont les fruits sont utilisés pour tanner le cuir
nëbbatu
se cacher
Looy nëbbatu ?
qu’as-tu à te cacher ?
ndóof g-
jeu où on poursuit un joueur pour le frapper avec un ballon
ñedd
racler avec les doigts pour récupérer qqch
Dafa noon xiiful, waaye lekk na ba ñedd ndab li
il avait dit qu’il n’avait pas faim, mais il a mangé au point de racler le fond du plat.
néegu-séy b-
domicile conjugal
ñeel
revenir de droit à qqn
Barke, ñeel na la
la bénédiction te revient de droit.
ñéññ
ne plus accepter les règles du jeu du fait d’une position désavantageuse
Bu ñu la bëggee gañe rekk, nga ñéññ
dès qu’on est sur le point de gagner, tu n’acceptes plus les règles.
neefare j-
crottin de cheval
Anal neefare ji, def ko ci tool bi
ramasse le crottin de cheval et mets-le dans le champ.
neekata b-
tempe
Dafa am ay ñaas ci neekata ndeyjoor bi
il a des scarifications à la tempe droite.
nenn
une certaine façon
Am na nenn noo xam ne, soo ko defe, dina baax
il y a une certaine façon de procéder, si tu l’adoptes, ce sera bien.
Defunu nenn maak moom
nous n’avons aucune relation entre nous, lui et moi (on ne s’entend pas du tout).
nebbon b-
graisse animale
Berleen nebbon bi
mettez la graisse à part !
ñeeblu
négliger
Loo ko wax, mu ñeeblu ko
tout ce que tu lui dis, il le néglige.
ñeeño b-
personne castée
Mënul séy ak moom ndax ñeeño la
il ne peut pas l’épouser car elle est castée.
ñeem g-
tenailles
ŋeer
s’évaporer
Sa ñeex mi ŋeer na
ta sauce s’est évaporée.
ñent ñ-
Quatre
Ñent ñi, téeméer
les quatre pour cinq cents francs.
ŋeeñkat b-
rongeur
Jinax ŋeeñkat la
la souris est un rongeur.
ŋeeral
Évaporer
ñeetal
mémoriser visuellement
ñetti
torcher le derrière d’un enfant
netetu j-
pâte de graines de néré fermentées servant à assaisonner des plats, « moutarde » de néré
Guléet ma gis ku def netetu ci makaroni
C'est la première fois que je vois qqn mettre de la « moutarde » de néré dans des pâtes.
néew b-
défunt dépouille mortelle cadavre
Yóbbu nañu néew bi
on a emmené la dépouille mortelle.
(prov.) Néew, bu rombeey armeel, robam dootul neex
quand une dépouille mortelle va au delà du cimetière, son enterrement ne sera plus aisé.
néew-doole
être faible
Du lekk; moo tax mu néew-doole
il ne mange pas; c’est pour cela qu’il est faible.
neex-baat
avoir une belle voix
ñey b-
unité de mesure faisant deux mètres
neex-xel
être intelligent
Dafa neex-xel moo tax
C'est parce qu’il est intelligent.
ŋexal b-
hennissement
Dafa mel ni ŋexal laa dégg
on dirait que c’est un hennissement que j’ai entendu.
ñef
frapper un enfant
Dinaa la ñef soo ko defatee
je te frapperai si tu recommences.
neexoo
être en bon termes
neexoo
se valoir l’un l’autre
nees
comment on..
Nees koy defe 
comment le fait-on ?
neey
être en extase
Dama ko gis rekk neey
je suis tombé en extase en le voyant.
ñég
se buter à tort sur une idée par orgueil
Dafa ñég
il s’est buté.
nef
avoir des grossesses rapprochées
Dafay nef
elle a des grossesses rapprochées.
ngaakin w-
cheval mâle, étalon (wolof du djolof)
Aw ngaakin la jénd
il a acheté un cheval mâle.
nëhu b-
grammaire
nekkal
représenter qqn
Moo ko fi nekkal
C'est lui qui le représente ici.
nekkal
faire sans discontinuer, sans interruption
Su dul koon ak Sëriñ bi, ñu nekkal fi ba tey njaayum sàngara mi ñu fi daan def
sans le marabout, on n’aurait pas interrompu la vente d’alcool qu’on pratiquait ici.
nég b-
fait d’attendre
nékk g-
graisse animale
Beral nékk gi
mets la graisse à part !
(prov.) Ku sol tubéyu nékk du jaaru
celui qui porte un pantalon en graisse ne se réchauffe pas) dans certaines situations, on ne prend pas de risques.
nég
attendre
Damay nég ba mu dem
J'attends qu’il soit parti.