wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
(prov.) Nég ba jaan dem, nga topp ca watit wa di dóor
attendre que le serpent soit parti pour se mettre à frapper sur ses traces (médecin après la mort).
nelawloo
endormir
neg-negi
ressentir les symptômes du paludisme
Sama yaram waa ngiy neg-negi
je sens un début de paludisme.
ngale
voilà
Mu ngale
le voilà.
nelaw
dormir
Dafay nelaw
il dort.
nel b-
crâne rasé complètement boule à zéro
Sa nel bi dafa la jox beneen kanam
ton crâne rasé te donne un autre visage.
nekkaale
vivre en concubinage
Dafay nekkaale ak waay si
elle vit en concubinage avec le gars.
ñeleŋ g-
plat à base de gros couscous accompagné d’une sauce à base d’arachide
nganj g-
indigotier
ñellarci
prendre (qqch) que l’on s’était fait réserver
Piis ba ma ñaloon ca bitiku Omar, ñellarci nañu ko
le tissu que je m’étais fait réserver à la boutique d’Omar et que j’envisageais de prendre plus tard, on l’a pris.
nemmali
achever de tuer
« dévaluation » bi kaay, mook nemmali ñoo yem
la dévaluation (du franc CFA) revient assurément à nous achever.
ŋeleju
faire des grimaces à qqn dans le but de le vexer ou bien de le démoraliser
Danga may ŋeleju léegi 
tu me fais des grimaces maintenant ?
(prov.) Lu jinne màgget, màgget, dese ŋeleju bu mu jommale gone
aussi vieux que soit un djinn, il lui restera toujours une grimace qui affolerait un enfant.
ngee
voilà
Mu ngee di dem
le voilà qui s’en va.
nemmat
se plaindre
Dafa bare lu muy nemmat
il se plaint de beaucoup de choses.
nemm
exprime l’idée de rester sans vie
Gaynde ga ne nemm.
Le lion resta sans vie.
nemm
récolter du miel
Alxames, danu bëgga nemmi
jeudi, nous avons l’intention d’aller récolter du miel.
ñendaxit w-
morve
Fompal ko ñendaxit yi
essuie-lui sa morve !
nemmali b-
recette spéciale de préparation d’encens
nemm-nemmaaral
rester totalement inerte
muucc
renfrogné
ñépp
tous.
Ñépp xam nañu ko
tous le connaissent.
Nit ñépp ci Aadama ak Awa lañu soqikoo
tous les hommes viennent d’Adam et d’Ève.
ngëmadi g-
manque de foi
Sa ngëmadi moo la ko teg
cela t’est arrivé à cause de ton manque de foi.
nepp
extrêmement, très (doux, moelleux)
Ci lal bu nooy nepp laay tëdd
je me couche dans un lit très moelleux.
nëtëri b-
sauce faite avec de la pâte d’arachide et du fruit du baobab pour accompagner la bouillie de mil
Laaxu nëtëri rekk la sopp
il n’aime que la bouillie de mil au {nëtëri}.
ñenn ñ-
pn.ind.plur. Uns
Xam naa ñenn ñi
je connais les uns.
nëtëx
être vert
Mbubb mu nëtëx la sol
il porte un boubou vert.
nërëm
tomber sur les genoux et les mains
Ba mu agsee ca Yéesu dafa ne nërëm
quand il arriva à Jésus, il tomba à quatre pattes.
ngénte
baptiser
Kawlax lañu ko ngéntee
C'est à Kaolack qu’on l’a baptisé.
nere g-
caroubier d’Afrique
new g-
pommier du Cayor
ñetteeku
se nettoyer avec du papier hygiénique
Kayit gu ñuy ñetteekoo la
C'est du papier hygiénique.
ñett ñ-
trois
Jél ci ñett !
prends-en trois !
nërméelu
se jetter dans les bras (de qqn). Tomber par terre (qqn)
ñëw
venir
Mu ngiy ñëw
il vient.
nëx
être trouble
Ndox mi dafa nëx
L'eau est trouble.
Xel mi dafa nëx
il n’est pas futé.
nëwu b-
grammaire
new g-
pommier du Cayor
newwi-newwi b-
enflure
ñewent
Éprouver de l’empathie
Soo leen gisee, danga leen di ñewent
si tu les vois, tu éprouves de l’empathie pour eux.
newwi
enfler
Sama óom yi dañu newwi woon
mes genoux avaient enflé.
nga
tu
Lan nga wax ?
qu’as-tu dit ? V. GR.
lu nga
se contracte en loo.
ngaaka b-
idiot bête
Waa jooju, du ab ngaaka de
ce gars n’est pas du tout idiot.
nëww
se consacrer à
Dama ne nëww ci Bàmba
je m’abandonne à Bamba (saint homme, père du mouridisme).
Dañu ko dóor ba mu ne nëww
on l’a battu à plate couture.
ŋexal
hennir
Booba la fas wa ŋexal
c’est à ce moment que le cheval hennit.
Fas wiy ŋexal, wu Omar la
le cheval qui hennit, c’est celui d’Omar.
ngaana g-
lèpre
Ku tudd Hansen moo nemmeeku li waral ngaana
C'est un nommé Hansen qui a identifié la cause de la lèpre.
ngaareew m-
canalisation
Ngaareew mi sotteegul
la canalisation n’est pas encore achevée.
ngirte l-
objectif
Lan mooy ngirte li ?
quelle en est la finalité ?
ngaaga l-
baleine
Géej gii amul ngaaga
il n’y a pas de baleine dans cette mer.
ngaax b-
sacs placés sur les flancs d’un dromadaire
Su gëléem gi dawee, ngaax yi wadd
si le dromadaire court, les sacs latéraux vont tomber.
(prov.) Ngaaxi tukkal, kenn du ko perngal mboccor
les sacs du grand dromadaire, on ne les met pas au jeune dromadaire) les sacs du grand dromadaire, on ne les met pas au petit.
ngaaràndu b-
chant de labour
Ngaaràndu yu neex rekk lay woy
il ne chante que de beaux chants de labour.
ngalam w-
or du Galam (l’ancienne région du Galam appelée aussi Gadjaga était située entre les hauts bassins du Sénégal et de la Gambie, la moyenne vallée du Sénégal et le Gidimakha)
Wurusu Ngalam
L'or du Galam.
ngajj
faucher les jambes
Dama ko ngajj, mu daanu
je lui ai fauché les jambes et il est tombé.
ngaaràndu
chanter en travaillant au champ
Dafay ngaaràndu bëccëg bi yépp
il chante toute la journée en travaillant au champ.