wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
ngand m-
homme costaud
Ngand mi dikk na
le costaud est venu.
Ngand mi dikk na
le caïd est arrivé.
ngan l-
séjour d’un hôte
Sa ngan li gàtt na lool
ton séjour est trop court.
nganj g-
indigotier
ngori l-
variété de petit niébé
ngar l-
botte d’arachides
Nag yaa ngi jublu ci sa ngar li
les vaches se dirigent vers tes bottes d’arachides.
ngar l-
mil
ngarab s-
arbuste
Dinga gis as ngarab ca buntu kër ga
tu verras un arbuste à l’entrée de la maison.
ngallax
préparer une bouillie de mil à l’arachide
Damay ngallax
je prépare du {ngallax}.
ngallax l-
bouillie de mil à l’arachide
Ngallax li neex na le ngallax
est délicieux.
ngaska l-
instrument pour creuser
ngas m-
fait de creuser forage
ngawar g-
fait de monter à cheval
ngato b-
gâteau
Dafay defar ngato kokko
elle prépare un gâteau de coco.
ngañ m-
eau de fleuve saumâtre (du fait de la remontée de l’eau de mer)
Ngañ mi agsi na Dagana ?
l’eau saumâtre du fleuve est-elle arrivée à Dagana ?
nguri b-
guêpe
Dafa ragal nguri
il a peur des guêpes.
ngeen
vous
Dégg ngeen wolof ?
comprenez-vous le wolof ?
ngatan l-
lit rustique à lattes
ngeel
être vert
Mënula raññaatle ngeel ak puur
il ne peut pas faire la différence entre le vert et le jaune.
ngawar
monter à cheval
Mokkaloo ngawar moo tax nga daanu
tu es tombé parce que tu ne sais pas bien monter à cheval.
ngegenaay l-
oreiller
Ngegenaay li dafa dëgër
L'oreiller est dur.
(prov.) Bëgg i ween du ma taxa takk i ngegenaay
désirer des seins ne me fera pas porter des oreillers
ngelaane l-
vent fort
Ngelaane li daane na garab yu bare
le vent a fait tomber beaucoup d’arbres.
ngëjëm l-
tige, tubercule comestible
Pullóox, ci ngëjëm yi la bokk
le manioc fait partie des tubercules comestibles.
ngatan l-
lit rustique à lattes
ngelaw l-
vent
Tey, ngelaw li dafa bare
aujourd’hui, il y a beaucoup de vent.
(prov.) Ngelaw la dugal xob ci pax, génnewu ko ca
le vent qui a fait entrer la feuille dans un trou ne l’en sort pas.
ngëléen l-
vent fort tempête
Ngëléen lee ko daaneel
C'est la tempête qui l’a fait tomber.
(prov.) Ëkk tiitul ngëléen
la souche ne craint pas la tempête.
ngëm g-
foi
Sama ngëm mooy sama gànnaay
ma foi est mon arme.
ngeer g-
guiera senegalensis (Combrétacées)
Ngeer baax na ci ku tooy
le Guiera senegalensis est bon pour qqn qui a une fatigue généralisée.
ñiim g-
pince pour (des)serrer
ngecceel l-
complexe d’infériorité
Baña fonk sa làkk ngecceel la
ne pas estimer sa langue est un complexe d’infériorité.
ngéndi m-
grande ville
Feek i at, dina dooni am ngéndi
dans quelques années, ce sera une grande ville.
ngémmiñ s-
petite bouche
Xéjul ci sa ngémmiñ si
ça ne peut pas tenir dans ta petite bouche.
ngelabon l-
embryon
Ay weer, ngelabon li, lu tuuti lay doon
pendant des mois, l’embryon est tout petit.
ngelaw
venter
Bu xale yi génn, dafa ngelaw
que les enfants ne sortent pas, il y a du vent !
ngent l-
désertion massive d’un village, d’un pays, d’une demeure
Ngental dëkk bee tax woto yi jaaratuñu fi
C'est à cause de l’abandon du village que les voitures ne passent plus par ici.
ngér m-
rue très large, avenue, boulevard
Ca ngér ma lañuy teertoo gan yi
C'est sur le boulevard qu’on va accueillir les hôtes.
ngér m-
chacun des rites de l’islam (hanafite, malékite, chaféite, hanbalite)
Ngér yi xaajalewuñu lislaam
les rites n’ont pas divisé l’islam.
ngënd l-
douille (d’outil)
Ngënd li dafa damm
la douille est cassée.
ngéwal g-
fait caractéristique de griot
Tey, ngéwal laa lay toggal
aujourd’hui, je te ferai une cuisine conforme à l’art des griots.
ngën g-
le meilleur (...)
Ngën gi wax mooy li gàtt te tekki li ngay wax
le meilleur des discours est celui qui est concis et qui explicite ta pensée.
ngërëm l-
remerciement
Fu ngërëm am, xol a fa sedd
quand il y a des remerciements, c’est qu’il y a satisfaction.
(prov.) Ku la ne : « mayeel sa alal », sa ngërëm la bëgg
qui te dit : « offre tes biens », c’est ton remerciement qu’il veut) qui te dit d’offrir tes biens veut que tu sois loué.
ngii
voici
Mu ngii
le voici.
ngélliir l-
son
ngiir l-
fait d’enlever des grains de leur épi avec le pouce pour les manger
Lekk mboq, taamuwuma ci ngiir
pour manger du maïs, je préfère ne pas enlever les graines avec les doigts.
nger m-
corruption
Alal ju juddoowul cim nger laa bëgg
je veux une richesse qui ne vienne pas de la corruption.
ngigis g-
piliostigma reticulatum Piliostigma thonningii (Césalpiniacées)
Xaar ma ca ngigis gale
attends-moi au piliostig-ma là-bas.
ngénte l-
baptême
Ngénte li, kañ la ?
le baptême, c’est quand ?
ngone s-
enfant
Moo ngone sii, fooy dem waxtu wii yow doŋŋ ?
oh là petit bonhomme, où t’en vas-tu à cette heure-ci tout seul ?
ngone g-
enfance
Soo ko tàmmee ci sag ngone, mooy wéy
si tu en prends l’habitude dès ton enfance, c’est ça qui continue.
ngiñ g-
fait de jurer
Lu waral ngiñ gi  ?
pourquoi jurer ?
ngomaar b-
cérémonie de danses organisée les jours avant la circoncision
Jaajax, dinañu tàmbali seen ngomaar altine jiy ñów
à Djadjakh, ils vont commencer les danses d’avant la circoncision lundi prochain.
ngis b-
prémonition
ngonnal
veiller
Biig, dañu ngonnal ba xaaju guddi
la nuit dernière, nous avons veillé jusqu’au milieu de la nuit.
ngonnal
aller au champ l’après-midi
Dinaa ngonnal
J'irai au champ dans l’après-midi.