wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
Dangeen ñiiroo xanaa ?
est-ce que vous vous seriez chamaillés ?
niitu g-
torche
Jélal niitu gi, wut ci ëtt bi
prends la torche et cherche dans la cour !
niiw b-
dépouille (mortelle), cadavre
Yóbbu nañu niiw bi
on a emmené la dépouille.
niis
(ciel) Être couvert de petits blocs de nuages noirs
Asamaan si dafa niis
le ciel est gris.
niis w-
État du ciel assombri par de petits blocs de nuages noirs
Bu niis wi jàllee, dina tàngaat
quand les nuages auront passé, il fera chaud encore.
niitu
s’éclairer avec une torche
Lii nag, mooy niitu ba lakkle
ça alors, c’est s’éclairer au point de se brûler.
ñiit
racler le fond
Nguur, kenn du ko ñiit
le pouvoir, on ne le racle pas (on ne s’y accroche pas jusqu’à la dernière minute).
nikk
exprime le fait d’immobiliser fermement
Séñ Fàllu nee na : Bu nee yàŋŋ, nga ne yoll te teey. Bu nee tacc, nga ne tekk, booleek nga ne nikk, ne nàŋŋ
le guide Fallou a dit : Quand elle (la voie) est libre, tu accélères sans te précipiter. Quand elle est embouteillée, tu restes calme, tu maîtrises ta voiture, tout en regardant droit devant toi.
njënnéeg m-
carré
ninki-nanka b-
monstre légendaire
Buur ne ki rey ninki-nanka bi lay may doomam
le roi dit qu’il va marier sa fille à celui qui a tué le « dragon ».
niroole
des choses similaires
Yeena niroole les vôtres sont semblables. Ñoo niroole
nous avons les mêmes.
niw g-
crème de lait
Tonnil ma niw gi
enlève-moi la couche de crème !
niroowaale b-
double
niteef g-
d’humain
Ci Yéesu la niteefug Yàlla wonewoo
C'est en Jésus que Dieu a manifesté son humanité.
njëlu
partir à l’aube
njëkk m-
mouton, vache (ou autres) sans cornes
Nag woowu rekk a fiy njëkk
cette vache est la seule sans cornes ici.
njaal l-
condoléances présentation de condoléances
Njaal laa ngay ame kër gu mag ga
les condoléances seront reçues à la résidence principale.
Njaal li, ñu ngi koy nangoo kër magam
les condoléances seront reçues chez son grand frère.
njaam l-
esclavage
Njaam am na ba tey
L'esclavage existe encore.
nitt b-
num. Vingt (rare)
njaaloo g-
adultère
Njaaloo gi lañu bëgg mu jóge fi
on veut que l’on ne commette plus l’adultère ici.
njaab l-
cuir brut
Dañu ciy sóob njaab li
on y plonge le cuir brut.
njaago b-
manjak, ethnie vivant en Casamance et en Guinée-Bissau membre de cette ethnie
njaaxaanaay l-
fait de se coucher sur le dos
Su ma tëddee njaaxaanaay, duma nelaw lu yàgg
si je me couche sur le dos, je ne dors pas longtemps.
(prov.) Ndey-ji-séex, njaaxaanaay lay tëdde
une mère de jumeaux se couche sur le dos
njaane j-
capitaine (poisson)
njaambur-njaambur b-
ressortissant de la région de Louga
njaaréem g-
autre appellation de la ville de Diourbel, chef-lieu de la région du Baol
njabb m-
menu fretin
Ay njabb rekk a am marse
il n’y a que du menu fretin au marché.
njaba
tremper du pain dans de l’eau sucrée
Damay njaba
je prépare du pain trempé dans de l’eau sucrée.
njaba j-
pain trempé dans de l’eau sucrée
njoolum-golo
ressembler à un gorille
Dafa njoolum-golo
il ressemble à un gorille.
njamala g-
girafe
Njamala moo sut fas
la girafe est plus grande que le cheval.
njulli b-
personne qui vient de subir la circoncision
Bu jëkk, njulli daawul dem dispañseer
autrefois, le nouveau circoncis n’allait pas au dispensaire.
njambaan l-
mélange aqueux de pain de singe ou de tamarin (pouvant être assaisonné d’épices dans le dernier cas)
njaniiw j-
l’au-delà
Xalaatal njaniiw.
Pense à l’au-delà.
(prov.) Tëradi àggul njaniiw
dans l’au-delà, on ne dort pas d’un sommeil agité.
njañ l-
chevelure abondante et longue
Doo wàññi sa njañ li
est-ce que tu ne vas pas raccourcir tes longs cheveux ?
njargeen b-
hirondelle
njaq s-
petit canari en terre cuite
Njaq si toj na
le petit canari est brisé.
njaba g-
variété de petite courge
njarum làññ g-
nom de fleuve dans un conte
Kumba-amul-ndey moo àndoon ak wujju yaayam, dem dex gu ñuy tudde Njarum-Làññ
Coumba-l’orpheline, en compagnie de la coépouse de sa mère, s’était rendue à un fleuve qu’on appelle Ndiaroum-Lagne.
njang-teg m-
fourche artisanale à deux dents
njukkal l-
contre-don
Xaalisu njukkal bi la jénde wotoom
C'est avec l’argent des contre-dons qu’elle a acheté sa voiture.
njañu
laisser ses cheveux sans tresses
Toog naa weer, njañu
je suis restée un mois sans tresses.
njur g-
fait de mettre au monde
Jigéen ñu bare ñemewuñu njurug séex
beaucoup de femmes craignent le fait de mettre au monde des jumeaux.
njaboot g-
famille
Naka njaboot gi ?
comment va la famille ?
njaw l-
cuisson de longue durée
Njaw li xanaa suba la jëm ?
cette longue cuisson va-t-elle durer jusqu’à demain ?
(prov.) Njaw des na aw xambin
il faut encore un attisement pour cette longue cuisson) il y a encore à faire.
njaw l-
occiput
Ci njaw li la góom bi nekk
la plaie se trouve à l’occiput
njaw l-
sirop de Sclerocarya birrea
Njaw laay naan
je bois du sirop de Sclerocarya birrea.
njar
couper un liquide avec de l’eau
Dafay njar biiñ di ko ko jox
il coupe du vin et le lui donne.
njariñ l-
utilité
Xamul njariñ li
il n’en connaît pas l’utilité.
(prov.) Baadoolo bu ragal naaj ragal na njariñam
L'homme de condition modeste qui craint le soleil, craint ce qui lui rend service.
njébbal l-
offrande
Borom bi, nangul njébbal li la sa doom yi tàllal
Seigneur, reçois l’offrande que te présentent tes enfants.
nja-àll y-
animaux de brousse
Nja-àll yi dañu daje, ne dañuy fal buur
les animaux de la brousse se réunirent, disant qu’ils allaient élire un roi.
njegemaar b-
adolescente
njaxnaat l-
gros mil
njàmbataan
avoir la coqueluche
Dafa njàmbataan
il a la coqueluche.
njeextal l-
fin
Njeextal li laa fekke
J'ai assisté à la fin.
njéeréer b-
criquet pèlerin.