wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
niral
exemple
Joxe naa niral
J'ai donné un exemple.
ngonk m-
Âne adulte et fort
Dama bëgga jénd am ngonk ngir liggéeyu tool yi
je veux acheter un âne adulte pour les travaux des champs.
ngoogale
voilà
Mu ngoogale
le voilà.
ngonku
un âne
Fii, gone gi gëna ndaw mën naa ngonku
ici, l’enfant le plus jeune sait monter un âne.
ngonnal l-
veillée
ngooñ m-
foin fourrage
Xar mi amatul ngooñ
le mouton n’a plus de foin.
niroo
se ressembler
Ñaari dëkk yooyu dañu niroo
ces deux villes se ressemblent.
ngont l-
après-midi de travail
Tool ba dey, ab ngont rekk, mu sotti
il suffit d’une après-midi de travail pour finir le travail à faire au champ.
ngoon g-
après-midi (de midi au crépuscule)
Dinaa fa ñów ci ngoon gi
je viendrai là-bas dans l’après-midi.
ngoolool b-
serpenteau
Ci taatu ndaa li la fekk ngoolool yi
C'est au pied du canari qu’il a trouvé les serpenteaux.
njaaloo
commettre l’adultère
Su ma njaaloo woon, jox say doom ñu lekk, du la saf
si je commettais l’adultère pour nourrir tes enfants, cela te laisserait froid.
ngoox
croassement du crapaud
Mbott tiit fa mu làqu woon ba daldi ne ngoox ! ngooxii ! ngoox
le crapaud dans sa cachette eut si peur qu’il fit croa ! croa ! croa !
ngopp l-
nord
Njaaréem a ngi ci ngoppu Kawlax
Diourbel est au nord de Kaolack.
ngoogu
voilà (à côté de toi)
Mu ngoogu
le voilà (à côté de toi).
ngoro
se lier d’amour avec qqn du sexe opposé
Dégg naa ne Omar dafay ngoro ak Astu
J'ai appris qu’Omar et Astou ont une liaison.
ngoro g-
liaison amoureuse
Seen ngoro gi weesuwul weer
leur liaison n’a pas excédé un mois.
njaambur g-
région de Louga
ngoy m-
nom propre de personne
(expr.) Ku doon laajte Faali, Ngoy a ngi
qui demandait Fali, voici Ngoye
ngunu l-
poulailler
Yóbbul ganaar gi ca ngunu la
emporte la poule au poulailler !
(prov.) Keppaarug ngunu jombul séq
L'ombre d’un poulailler n’excède pas le mérite du coq
njaaxum l-
gaffe grosse bêtise
Defati nga njaaxum
tu as encore fait une bêtise.
ngumbaan-tooye b-
escargot
njagabaar b-
pélican
Fan nga portalee njagabaar yi ?
où as-tu photographié les pélicans ?
ngot w-
tassergal
ngorka l-
pivert
ngot l-
gourdin
Ngot la gànnaayoo
il est armé d’un gourdin.
nguuka w-
otolithe( poisson de mer)
ngàdd
frapper à l’arrière du cou
Dafa ko ngàdd
il l’a frappé à l’arrière du cou.
ngurbaan g-
plat sérère à base de semoule de mil, accompagné de viande ou de poisson
Ngurbaanu yàpp laa togg J'ai préparé du ngurbaan
la viande.
njall b-
(péjoratif) Mulâtre, -tresse
nguufaan
porter qqn en lui passant un bras sous les jambes et l’autre sous les épaules
Nguufaan ko
prends-le par les bras et les épaules.
ngunaaba m-
chameau de basse taille
ngàll b-
bretelle
Bu ci def ngàll
J'y mets pas de bretelles !
ngàllent b-
digue
Tabax nañu fa ab ngàllent.
On y a construit une digue.
nguuka b-
cheveux postiches bouclés que les femmes portaient autrefois sur les tempes
Léegi takkatuñu nguuka
maintenant on ne porte plus de {nguuka}.
ngànja l-
mil pilé le soir
Cere ngànja wute na ak cere njël
le couscous de mil pilé le soir est différent de celui du matin.
ngàttaan b-
courtaud
Ab ngàttaan la, tóoju gi dafa kowe ci moom
C'est un courtaud, le mirador est haut pour lui.
ngànk
souder
ngàdd b-
coup donné à l’arrière du cou
Ngàdd bi dafa moy
le coup à l’arrière du cou a été raté.
ngàdd b-
manioc bouilli
Ngàdd lay lekk
il mange du manioc bouilli.
ngureet g-
variété de courge
ngàtte m-
sparaillon
ngàngoor l-
splendeur
Ngàngooru jant bi rekk doy na kéemaan
la splendeur du soleil, à elle seule, suffit comme merveille.
ngàngoor l-
foule
Ngàngoor laa ngi ko topp
la foule le suit.
ngóob l-; m-
moisson
Ngóob li dina ma fekk Ndakaaru
pendant la moisson, je serai à Dakar.
njarweñ g-
piège à oiseaux (lacets) fait de crins de queue de cheval tressés et ayant un nœud coulant pour prendre la patte du volatile
Picc mi yóbbaale na njarweñ gi
L'oiseau a emporté le piège.
ñibbi
retourner chez soi
Kañ ngay ñibbi 
quand rentres-tu ?
ñiimantu
manger lentement pour ne pas vite finir ce qu’on mange
Mu ngiy ñiimantu pom bi nga ko may
il mange lentement la pomme que tu lui as offerte.
niir
scruter
Ñu ngiy niir asamaan si
ils scrutent le ciel.
ñi
les
Nit ñi
les gens
ni
comme
Dafa mel ni du dimaas
C'est comme si ce n’est pas dimanche.
niim g-
nime (Azadirachta indica Méliacées)
Kaay wittal ma ay xobi niim
viens me cueillir des feuilles de nime !
ŋiis
se retirer par infiltration (eau)
(prov.) Àddina, ndoxum joor la; buy taa, mu ngay ŋiis
les choses en ce bas monde sont comparables à de l’eau sur un terrain sablonneux; en même temps qu’elle recouvre le sol, elle s’y infiltre.
niinal
tacher d’huile
Niinal nga lal bi
tu as taché le lit d’huile.
niir w-
petits nuages noirs assombrissant le ciel et, le plus souvent, n’entraînant pas de pluie
Niir yaa ngiy dem
les nuages s’en vont.
niini b-
2,5 centimes. (ancienne pièce de monnaie)
ñiiroo
se chamailler