wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
Ñoom, dañuy lekk njéeréer
eux, ils mangent les criquets pèlerins.
njëgg m-
caravane (du désert)
njég l-
prix
Bu ko wax njég li
ne lui dis pas le prix.
Ëndil njégu guró li nak
apporte donc le cadeau (argent qu’on donne en récompense, en général, après un service ponctuel) !
njeexital l-
finale d’une action
Njeexital li, moo gënoona xumb
la dernière partie était plus animée.
njëkke l-
sœur (ou personne considérée comme telle) du mari
Damay yónnee sama njëkke cere
J'envoie du couscous à ma belle-sœur.
njekkar l-
malheur
Loolu moom, njekkar lu ñuy muslu la
ça vraiment, c’est un malheur dont nous nous protégeons.
njël m-
(seule occurrence dans la locution {njël mu jëkk})
Dafa ko jël njël mu jëkk
il lui en a imposé dès le début.
njélém j-
tige métallique servant à égrener le coton
njëkk-jél b-
course compétition
Omar a raw ca njëkk-jél ba
C'est Omar qui a gagné la compétition.
njekk l-
conciliation
Amuloo looy def, lu dul ñaan njekk
tu n’as rien à faire, si ce n’est demander une conciliation.
njëmbët m-
bouture bouturage plant
Dinañu leen indil ay njëmbëtu filaawoo
nous vous apporterons des plants de filao.
njël g-
aube
Dem na ca njël
il est parti à l’aube.
nom
hausser (les épaules)
njett
prendre la tête de qqn sous son aisselle
Dafa ko njett, të koo bàyyi
il lui a pris la tête sous l’aisselle, refusant de le lâcher.
njett loos
baisser la tête (de honte).
noflaay g-
repos
Liggéey boobu amul noflaay
ce travail est sans repos.
njël l-
provision quotidienne de nourriture
Moo yore njël li, waaye dafay yàq
C'est elle qui a la charge de la provision de nourriture quotidienne, mais elle gaspille.
njig-njigéen
etre qqn à qui les choses n’arrivent jamais une fois seulement
Dama Njig-njigéen; xamoon naa ne dina ma dalaat
je suis qqn à qui les choses n’arrivent jamais une fois seulement; je savais que cela m’arriverait encore.
njig-njigéen b-
personne à qui les choses n’arrivent jamais une fois seulement
njiglaay l-
suite heureuse
Kër gi nga jénd, soo seetloo, njiglaay la ci sa takk gi
la maison que tu as achetée, si tu es attentif, c’est une suite heureuse à ton mariage.
njogonalu
prendre un goûter
Xale yi dañuy njogonalu
les enfants prennent leur goûter.
nji m-
semailles
Léegi nji mi jeex
bientôt les semailles vont finir.
njodom s-
pagne
Wutal ko njodom su set
cherche-lui un pagne propre !
njombor j-
lièvre
Ñi sant Seen duñu lekk njombor
ceux qui s’appellent Sène ne mangent pas de lièvre (leur totem).
njolloor g-
période comprise entre treize et quatorze heures
Bu ko yónni ci njolloor gi
ne l’envoie pas en ce début d’après-midi !
njoolaay b-
(en parlant de la stature d’une personne) Grande taille
njogonal l-
goûter aliment léger pris dans l’après-midi
Joxal njogonal li xale yi
donne le goûter aux enfants !
nooju
avoir la goutte
Dafa nooju
il a la goutte.
nooju
prendre par le buste une personne courbée et peser de tout son poids sur elle
Dama ko nooju, mu toog
J'ai pesé de tout mon poids sur lui, il s’est assis.
njong l-
cérémonie de circoncision
Njong la aka neexoon
comme la cérémonie de circoncision était réussie !
njombe w-
scandale
Omar def na aw njombe
Omar a fait un scandale.
njoñ
lier les mains ou les ailes sur le dos
Dañu njoñ ganaar gi
on a ficelé le poulet.
njool m-
personne de grande taille
Am njool a nga ca bunt ba
il y a une personne de grande taille à la porte.
(prov.) Ku la sut, nga ne ko njool mi
celui qui est plus grand que toi, tu lui dis « le grand ») reconnais sa supériorité à qui de droit.
njudduwaale l-
innéité
Bën-bën bi ci noppam, njudduwaale la
le trou qui est à son oreille est de naissance.
njoos b-
(pour jouer) Tape que les enfants se font entre eux au moment de se quitter en cherchant à ne pas être le dernier à la recevoir
Duma mujje njoos bi
je ne serai pas le dernier à recevoir la tape.
njoos
(entre enfants) Donner une tape à son compagnon au moment de se séparer de lui et fuir aussitôt pour éviter une riposte
Maa la mujja njoos
J'ai été le dernier à te faire une tape d’au revoir.
njoowaan g-
hamac
Xaaral, ma takk njoowaan gi ca keppaar ga
attends que j’installe le hamac à l’ombre !
(prov.) Kooyu bukki du njoowaanug tef
le pénis de l’hyène n’est pas une balançoire à chevreau.
njublaŋ b-
escroc truand
Omar, ab njublaŋ bu mag la
Omar est un grand truand.
njumbal l-
foulard
Yeena nga jëm kër Maam-réy-njumbal
vous allez chez Grand-mère au grand foulard.
njunux l-
mirage réverbération
Njunux li la tegoon ndox
C'est un mirage qu’il prenait pour de l’eau.
njukkal
faire un contre-don
Moo la njukkal fukki junni yii
C'est lui qui te fait ce contre-don de cinquante mille francs.
njooy-njooy
sève élaborée
njur l-
manche de hache
Njur li nga wutal sémmiñ wi du bant bu dëgër
le manche que tu as cherché pour la hache n’est pas un morceau de bois dur.
njugub b-
chauve-souris
Njugub yi ñooy waddal guyaab yi.
Ce sont les chauves-souris qui font tomber les goyaves.
njugur g-
jeu de mimiques où on doit deviner le personnage imité par un acteur
noppale
reposant
Looloo gëna noppale
cela est plus reposant.
njuuma l-
diablotin
Mu ne dafa doon nelaw ci toolam, njuuma yi xuuf ko
il dit qu’il dormait dans son champ, les diablotins lui ont rasé le crâne.
Sa doom jii, njuuma la
il est trop espiègle, ton enfant.
njàmbal
avoir la variole
Doomam dafa njàmbal
son enfant a la variole.
njàmbal j-
variole
njort
(avis) Penser
Njort naa mu ñàkka ñów
je pense qu’il ne viendra pas.
njuuj-njaaj b-
flou dans une démarche magouilles pratiques suspectes machination
Njaayum kër googu dafa bare njuuj-njaaj
il y a beaucoup de flou autour de la vente de cette maison.
njàndam g-
une plante dont les fruits sont comme des petits pois
njàndam g-
oxygène
njàmbataan l-
coqueluche
Njàmbataan, yomb na faj
la coqueluche se soigne facilement.