wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
noppiloo
faire taire (qqn)
ñoqali
ruminer
Nag, mala muy ñoqali la
la vache est un animal qui rumine.
nor
être enfoncé
Bool bi dafa nor
le bol est enfoncé.
nooy-bopp
naïf, qui se laisse convaincre facilement
noral
défoncer
Lu noral bool bi ?
qu’est-ce qui a défoncé le bol ?
ñoromtaan
chatouiller
Bu wéñ di dox ci sama kow, dafa may ñoromtaan
quand une mouche marche sur moi, ça me chatouille.
nose b-
poème
noppalu b-
le fait de se reposer
nos g-
corde qu’on passe à l’anneau placé au museau d’un animal pour le conduire
Jàppal ci nos gi
tiens la bride !
nos
nasiller
Dafa nos
il nasille.
nos
mettre un anneau à l’aile du museau d’un animal
Xamuma lu-tax mu nos xar mi
je ne sais pas pourquoi il a mis un anneau au museau du mouton.
ñàkkante
se manquer de respect mutuellement
Su dara desul lu dul ñàkkante, ma dem sama yoon
S'il ne reste plus qu’à se manquer de respect, je m’en vais.
ñoyy
exprime l’idée de sauter prestement
Kéwél daw, ni ñoyy tëb ñag ba
la gazelle courut, sauta prestement par-dessus la haie.
ñoy
dans l’expression {jàmm ne ñoy}: Régner, exister (paix)
Soo defee noonu, jàmm ne ñoy
si tu fais ainsi, la paix régnera.
noyyi g-
respiration
Li mu doon daw moo tax noyyi gi gëna gaaw
C'est parce qu’il courait que sa respiration s’est accélérée.
nose b-
poème
nottarñi
redresser une partie cabossée
Yóbbul bool bi ca tëgg ba, mu nottarñi ko
apporte le bol chez le forgeron pour qu’il le décabosse !
nu
nous
Dafa bëgg nu gis ko
il veut que nous le voyions.
Dafa nu bëgga gis
il veut nous voir.
noyyi
respirer
Mu ngiy noyyi
il respire.
nqareñtéef l-
compétence
nqomb l-
cadenas
Nqomb lee yàqu
C'est le cadenas qui est cassé.
ñukk
courir à petits pas saccadés
Omar a ngay ñukk, di wéy
Omar s’en va en courant à petits pas saccadés.
ñukk
laisser qqch à un endroit et ne plus s’en occuper, ou ne plus y toucher pour un temps
Ne na fi ñukk rajoom bi, waxatu ci dara
il a abandonné sa radio ici, il n’en parle plus.
ñu
nous
Dafa ñu saaga, ñu saaga ko
il nous a injuriés et nous l’avons injurié.
ñu
Ils
Ñu ngiy sant Yàlla
ils rendent grâce à Dieu.
nukki
surface
Xaaral ba mu nukki
attends qu’il refasse surface !
ñun
nous.
Ñun, duñu dem
nous, nous n’irons pas.
Ñun, dungeen ñu woo
nous, vous ne nous appelez pas ?
nuggal
réchauffer
And bi nuggal na néeg bi
le brûle-parfum a réchauffé la chambre.
nuggaay b-
tiédeur
Nuggaayu néeg bee ko fi téye
C'est la tiédeur de la chambre qui le retient ici.
ñukk-ñukki
courir à petits pas saccadés
ñurumtu b-
ronchonnement
Ñurumtu bi doy na
les ronchonnements, ça suffit.
ñurumtu
ronchonner
Mu ngiy ñurumtu; li nga ko wax neexu ko
il ronchonne; ce que tu lui as dit ne lui plaît pas.
nunjum b-
menton
Fompal suuf si ci sa nunjum bi
nettoie le sable qui est à ton menton !
ñumm
être entier
Lekk na ganaar gu ne ñumm
il a mangé un poulet entier.
nun
nous
Nun, dunu dem
nous, nous n’irons pas.
ñulug b-
quantité d’eau versée dans la marmite pour la cuisson
Ñulug bi dafa ëpp
il y a trop d’eau dans la marmite
ñur g-
bout du nez
Damay faral am yu weex yi ci sama ñur gi
J'ai souvent ces trucs blancs au bout de mon nez.
ñuqati
enlever qqch qui était fourré quelque part
Nanga ñuqi yére yi ci saak bi yépp, te fudd leen
tu enlèveras tous les habits fourrés dans le sac et tu les repasseras.
nunni
chasser dans une direction
Nunnil sëllu wi ci ndey ji
chasse le veau vers sa mère.
ñuul b-
amande de noix de palmier à huile
Séddaleel xale yi ñuul bi
partage les amandes de noix de palmier entre les enfants !
ñuul
être noir
Nit ku ñuul.
Une personne noire.
(prov.) Ku ndóbin rey sa maam, foo séenati lu ñuul, daw
celui dont l’ancêtre a été tué par un grand calao s’enfuit dès qu’il voit qqch de noir
ñuul w-
cheval tout noir
ñuulal
noircir
Damay ñuulal samay dàll
je teins mes chaussures en noir.
ñuulaay b-
noirceur
nuuru-bakkan b-
arête du nez
Xeet yi niroowuñu nuuru-bakkan
les différents peuples n’ont pas la même arête de nez.
ñuulit g-
noir de fumée
Ñuulit gee tax làmp bi leerul
C'est à cause du noir de fumée que la lampe n’est pas claire.
nuuru g-
le fait de se mettre sous l’eau de plonger et rester sous l’eau
ñuuxu
s’approcher de trop près de qqn
Danga mën ñuuxu nit lool
tu aimes trop te coller aux gens.
ñuuxit m-
mie (pain)
Samay doom bëgguñu ñuuxitu mburu
mes enfants n’aiment pas la mie de pain.
ŋuut m-
chuchoter faire des messes basses
ŋóobi
faire des grimaces à qqn pour le narguer
nuyoo b-
salutation
Nuyoo bi yàgg na
les salutations ont duré.
nàcc
saigner
Sa góom baa ngiy nàcc
ta plaie saigne.
(loc.) Xel muy nàcc.
Esprit créatif
nuyoo
se saluer
Ñaari seef detaa yaa ngiy nuyoo
les deux chefs d’État se saluent.