wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
njàmb m-
gouttière
njàccaar b-
personne voyante
Lu-tax ngay sarax njàccaar yi bàyyi silmaxa yi
pourquoi fais-tu l’aumône aux voyants, et non aux aveugles.
njàngale m-
enseignement
Njàngale mi dina jafe ci moom ndax sawaru ci
J'enseignement sera difficile pour lui car il n’y a pas le cœur.
noppu-bakkan b-
aile du nez
Noppu-bakkan bi lañuy bëtt, def ci jaaro
ils percent l’aile du nez et y mettent un anneau.
noq
(vulgaire) Casser la gueule
Soo ko laalee, ma noq la
si tu le touches, je te casse la gueule.
njàndam g-
une plante dont les fruits sont comme des petits pois
njàndam g-
oxygène
njàpp m-
ablutions
Maa ngeek njàpp
mes ablutions sont encore bonnes.
njànj m-
couscous non fermenté
May ma ci njànj mi
donne-moi du couscous non fermenté !
nob
aimer charnellement
Dama la nob
je t’aime.
nobante
s’aimer mutuellement
njàppaan b-
sorte de chat sauvage qui capture les poules
Dañuy rëbbi njàppaan
ils vont à la chasse aux chats sauvages.
nobaate
amoureux
Danga nobaate lool
tu es trop amoureuse.
noqu
(expr. vulgaire à l’impératif)
Noqul ci gat
va te faire foutre !
nodd
appeler les fidèles à la prière
Nodd nañu
on a fait l’appel à la prière.
nodd
se cabrer
Fas waa ngiy nodd
le cheval se cabre.
nogoy g-
très vieille femme
Ag nogoy la fa fekk
C'est une très vieille femme qu’il y a trouvée.
nodd g-
appel du muezzin à la prière
Nodd gee ko yee
C'est l’appel du muezzin qui l’a réveillé.
nokkos-nokkosi
marcher comme un vieillard
Perantal buy jàng dox dafay nokkos-nokkosi ni màgget
le nourrisson qui apprend à marcher avance comme un vieillard.
nobeel g-
charnel
Nobeel mësula wees lii
jamais amour n’a été plus fort.
ñokket
exprime la manière de se lever immédiatement
Mu daldi ne ñokket jóg
il se leva immédiatement.
Uli ñokket 
['arrête de manger et lève-toi\xa0!', 'ñokket}.']
ñox b-
trompe
Ñox bi lay buddee garab yi
C'est avec sa trompe qu’il arrache les arbres.
nokkas b-
pâte d’oignon, d’ail, et de poivre pour assaisonner un plat
Nanga def kaani ci nokkas bi
tu mettras du piment dans la pâte d’oignon et d’ail.
noddal
cabrer
ñoll w-
alcool (boisson)
Ñoll woowoo ko yóbbu barsàq
C'est cet alcool qui l’a emporté dans l’au-delà.
noŋŋ-noŋŋ b-
secousses imprimés au cavalier par sa monture (un âne).
nooj
être cagneux
Tànkam yi dañu nooj
il a des jambes cagneuses.
nugg
tiède
Dangay xooj say tànk ci ndox mu nugg
tu trempes tes pieds dans de l’eau tiède.
ñoddi
tirer
Ñoddil bu baax
tire bien.
ñoom
eux
Ñoom la
ce sont eux.
Ñoom, wolof lañu
eux, ils sont wolof.
Gis naa ñoom Omar
J'ai vu Omar et compagnie.
nomu
hausser les épaules
noona
ainsi, de cette manière (avec nuance de distance)
Te du xam nga na mu daan def ? Noona ngay def
tu sais comment il faisait, n’est-ce pas ? C’est ainsi que tu vas faire.
nokki
respirer
Saxaar si ngay nokki baaxul ci sa wér-gi-yaram
la fumée que tu respires n’est pas bonne pour ta santé.
Bul nokki
ne respire pas.
noob
envoûter
Jabar ji dafa ko noob
sa femme l’a envoûté.
noonoo
devenir ennemi
Su ngeen noonoo, dungeen mëna nekk
si vous devenez ennemis, vous ne pourrez pas vivre ensemble.
noon b-
ennemi
Kooku sama noon la
celui-là, c’est mon ennemi.
noo g-
respiration, souffle
Téyeel sa noo
retiens ton souffle; arrête de respirer.
ñoor b-
cordon ou ruban qu’on passe dans un ourlet en guise de ceinture
Ñoor bi dafa gàtt
le cordon ceinture est court.
(prov.) Ñaari loxooy takk
ñoor il faut les deux mains pour attacher une ceinture.
noor b-
saison sèche
Ci noor bi la fi dikkoon
C'est en saison sèche qu’il était venu ici.
ñoor
passer un cordon ou un ruban dans un ourlet
Ñooral tubay ji
passe un cordon dans l’ourlet du pantalon !
nooraan
se déplacer en saison sèche pour aller travailler
Dafay nooraan at mu jot
chaque année, pendant la saison sèche, il va travailler ailleurs.
ñooru
garder ses distances vis-à-vis de qqn
Dafa may ñooru léegi
avec moi, il garde ses distances maintenant.
noor
passer la saison sèche
Ndakaaru la noor
il a passé la saison sèche à Dakar.
Dinga fi noor, nawet fi
tu vas poireauter ici.
ŋoos-ŋoos b-
houe
Mënuma baye ŋoos-ŋoos
je ne sais pas cultiver à la houe.
nooyal
ramollir
Soo ko ci defee, dafa koy nooyal
si tu l’y mets, ça va le ramollir.
ñuy
qui
Am na nit ñuy wut Omar
il y a des gens qui cherchent Omar.
nootaange b-
oppression
Waa Afirig-di-siid dëkk nañu lu yàgg ci nootaange
les Sud-Africains ont longtemps vécu dans l’oppression.
noppalu
reposer
Damay noppaliku tuuti
je me repose un peu.
(prov.) Noppaliku, noppee ci gën
pour se reposer, finir est ce qu’il y a de mieux à faire) on se repose mieux quand on a fini de travailler.
nopp b-
oreille
Maa ko dégg ak samay nopp
je l’ai entendu de mes oreilles.
(prov.) Su nopp doon ràcc laax, ñu woo mbaam-sëf
si l’oreille servait à étaler la bouillie, on appellerait l’âne.
noppu-jaboot b-
singe (terme d’évitement, en présence d’un nourrisson)