wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
nuyu b-
salutation fait de saluer
ñàdd
tenir de force (personne ou un animal) en position allongée
Dañu ko ñàdd ci lal bi
on l’a étendu de force sur le lit.
nuyu
saluer
Dafay nuyu borom kër gi
il salue le maître de maison.
(prov.) Duma bëgg lu la neex ba ne la Yàllaa ngi lay nuyu
je ne voudrais pas ce qui te plaît au point de te dire Dieu te salue).
ŋàdd w-
morceau d’une noix
Amuloo ŋàddu guró ?
n’aurais-tu pas un morceau de noix de cola ?
(prov.) Borom ŋàdd yëgul borom pañe
celui qui a un morceau de noix (de cola) n’a cure de celui qui en a un panier.
ŋàddanti
lisser. S ?
nàkk b-
gâteau de riz en boulettes.
Àjjuma ju jot, damay saraxe nàkk
chaque vendredi, je donne en aumône des gâteaux de riz.
ŋàbbu
trouver à redire
Yow amuloo looy ŋàbbu
toi, tu n’as rien à redire.
(prov.) Su gan ŋàbboo, dëkk a ko ca bàyyi
si l’hôte trouve à redire, c’est qu’il s’est établi.
ŋàbbu
être rempli à trois quart
Bu doom ji, bu ko defalee meew ba mu fees, mu defal kële ba mu ŋàbbu
quand elle remplissait de lait celui de son fils, celui de l’autre, elle le remplissait à trois quart.
ñàkkali
réviser (ce qu’on a appris)
Damay ñàkkali sooga yalwaani
je vais réviser mes leçons puis j’irai demander l’aumône.
nàkkal
donner en privilège
Yàlla daal nàkkal na ma loolu
Dieu m’a donné cela en privilège.
ñàkk-deret m-
anémie
ñàkkaana
il est possible que ne pas..
Amaana, ñàkkaana nga fekk ko fa
il peut se faire que tu l’y trouves ou non.
ñàkki
commencer les travaux champêtres avant la saison des pluies
Dañu ñàkki
ils ont commencé prématurément les travaux champêtres.
ñàkka-xam g-
ignorance
ñàkk-deret
être anémié
ñàkkloo
faire perdre qqch
ñàkk-jot
manquer de temps
ñàkk m-
dénuement manque
Ñàkk baaxul ci gor
le dénuement est mauvais pour l’homme honnête.
ñàkk-maanaa
être sans importance, sans intérêt
ŋàlli
détaler, prendre ses jambes à son cou
nàll b-
plat à base de courge
Ndax sopp nga nàll
aimes-tu le nàll ?
ñàkk-sutura
manquer de discrétion
ñàkk-solo
être sans importance, sans intérêt
ñàkk-njariñ
être un vaurien
Billaay yaa ñàkk-njariñ
ma foi, quel vaurien tu es !
ñàmbaas b-
morceau de tissu ajouté à un pagne pour augmenter la largeur
Ñàmbaas bi doyul
la bande d’étoffe pour augmenter la largeur du pagne ne suffit pas.
nàmm
aiguiser
Demal nàmm paaka bi
va aiguiser le couteau !
ŋàmm
rester bouche bée
Mu ngiy wax ak yow, nga ne ŋàmm di ko xool
il te parle, tu es là bouche bée, à le regarder.
nàmpal
allaiter
Xaaral ba ma nàmpal sama doom ba-noppi
attends que j’aie fini d’allaiter mon enfant !
nàmmukaay b-
fusil (pour aiguiser)
nàmp
téter
Mu ngiy nàmp ba tey ?
il tète encore ?
nàmpu w-
tétine
Nanga baxal bibëroŋ bi ak nàmpu wi
tu feras bouillir le biberon et la tétine.
nàmm b-
fait d’aiguiser
nàndalu
se circoncire
Booba dañu daan wax ne bés sàngam la xale yiy nàndalu, bu ko defee ku-nekk pare ay gàllaajam
ces temps-là on disait c’est tel jour que les enfants vont être circoncis, alors chacun préparait ses talismans.
nànd
comprendre
Nàndul dara
il n’a rien compris.
nàmpal b-
allaiter
Nàmpal bi gën, mooy bu ween
le meilleur allaitement est celui fait au sein.
ñàmbi j-
manioc.
Ñàmbi ju ñu lakk la
C'est du manioc grillé.
(prov.) Bëre, reenu ñàmbi la; fa nga ko foogewul lay damme
la lutte, c’est comme un tubercule de manioc qui se brise là où tu ne t’y attends pas.
ñàngaay b-
austérité
nàndal g-
purgatif
Lii, nàndal la.
Ça, c’est un purgatif.
nàmpatal b-
fontanelle
Bul laal nàmpatal bi
ne touche pas la fontanelle !
nàmpaliin w-
d’allaiter
Dañu leen di jàngal nàmpaliin wi gën
on leur enseigne la meilleure façon d’allaiter.
nàndite g-
compréhension
Dangay jaay nàndite, daañu gis
tu joues au malin, on verra.
nàŋŋ
exprime le fait de regarder droit devant soi
Séñ Fàllu nee na : Bu nee yàŋŋ, nga ne yoll te teey. Bu nee tacc, nga ne tekk, booleek nga ne nikk, ne nàŋŋ
le guide Fallou a dit : Quand elle (la voie) est libre, tu accélères sans te précipiter. Quand elle est embouteillée, tu restes calme, tu maîtrises ta voiture, tout en regardant droit devant toi.
ŋàññ b-
reproche
Gisu ci benn ŋàññ
il n’a trouvé aucun reproche à lui faire.
ŋàññ b-
lampe artisanale à graisse animale
ŋàññ lañu doon taal
on allumait des lampes à graisse.
ñàngóor m-
cobra
Am na ñàngóor mu dëkk ci lëm gi
il y a un cobra qui habite dans le creux de l’arbre.
ŋàpp
être béant
Bunt baa ngi ne ŋàpp te terewul mu tàng
la porte est béante et malgré cela il fait chaud.
nàttable
Émettre des réserves
Weddiwuma, damay nàttable rekk
je ne démens pas, j’émets des réserves seulement.
ŋóotóot w-
pou de volaille
ñàpp
s’agripper
Soxna sa di xool, di xool, ba séen gone ga, mu ne ñàpp ca kaw garab ga
la vieille dame chercha, chercha, et finit par apercevoir l’enfant qui s’était agrippé à l’arbre.
ñàppu
grimper à mains nues sur un arbre dont le tronc est lisse
Dafa ñàppu garab gi
il a grimpé sur l’arbre à mains nues.
ŋàppati b-
varicelle
Ñakku ŋàppati am na
il existe un vaccin contre la varicelle.
ñànki
se lamenter
Aas Géy, rékk bul ñànki El Hadj Guéye
surtout ne te lamente pas !
ŋàppati
avoir la varicelle
Dooman dafa ŋàppati
son enfant a la varicelle.
ñànjaxeer b-
blanc d’œuf
Dindil ñànjaxeer bi ba mu set
enlève proprement le blanc d’œuf.
ñówental
compatir avec
Ñówental na sunu doom-ndey yi liggéeyi bitim-réew
il compatit avec nos frères qui sont allés travailler à l’étranger.
nóoxóor b-
personne dont le père est « vampire » et dont la mère ne le serait pas