wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
Nóoxóor la
il est {nóoxóor}.
ŋóot w-
gaine où est logé le grain de mil
ŋàyy
s’ouvrir grand
Bunt ba ne ŋàyy
la porte s’ouvrit toute grande.
palanteer b-
fenêtre
Tijjil palanteer bi
ouvre la fenêtre !
Dafay wut palanteer
il cherche une échappatoire.
om
être malingre
Xeex bee leen taxa om
C'est à cause de la guerre qu’ils sont malingres.
(prov.) Lu bukki om, om, mën naa bëre ak bëy
aussi malingre que soit l’hyène, elle pourrait lutter avec une chèvre.
paddaañu
être pieds nus
Tàmm na paddaañu
il est habitué à être pieds nus.
(prov.) Dàll yuy xotti ay tànk, paddaañoo ko gën
mieux vaut aller pieds nus qu’avec des chaussures qui vous déchirent les pieds.
pamti-pamtee
malmener qqn
Mu ngiy pamti-pamtee sa doom ji
il malmène ton enfant.
os
mettre un trépied au foyer pour ne pas mettre directement un récipient sur le feu
Osal cin li
pose la marmite sur un trépied !
omb
ourler
Omb nga tubay ji ?
as-tu ourlé le pantalon ?
par m-
race de cheval
Fasum par, nu muy mel ?
comment est un cheval de race par ?
(prov.) Wax ju jëkk, fasum par la, tontu la, naaru-góor
les premiers propos sont un cheval de la race par, la réplique, un cheval pur-sang.
pareñ b-
parrain. (terme employé en milieu catholique)
pajaas b-
paillasse (matelas)
paan
être en panne
Sama woto dafa paan
ma voiture est en panne.
ootal
venir qqn par des pratiques de sorcellerie
Dañu ko ootal, dafa naroona laŋ Tugal
on l’a fait venir par des pratiques magiques, autrement il serait resté en Europe.
palaas b-
place
parax-paraxi
entrer partout puis ressortir et chaque fois rapidement
parlukaay b-
pâturage
Borom bi, Yaa may teg ci parlukaay yi gën
Seigneur, c’est Toi qui me mets dans les meilleurs pâturages.
paas b-
argent pour un ticket de spectacle ou un billet de voyage
Ku may jox paas bu may dem ?
qui me donnera l’argent pour le billet quand je devrai partir ?
paas b-
passage à gué
Dafa am paas bu ñuy jaar
il y a un passage à gué qu’ils empruntent.
pakku
parer
Dama pakku kurpeñ bi
J'ai paré le coup de poing.
(prov.) Ku Yàlla sànni fitt, doo ko mëna pakku
celui à qui Dieu lance une flèche ne pourra pas la parer) on ne peut pas éviter le destin.
par-parle b-
partialité
pacantaan b-
cauchemar
Dama amoon pacantaan
J'avais fait un cauchemar.
oo
de... en.
Wut naa ko kër-oo-kër
je l’ai cherché de maison en maison.
Bunt-oo-bunt nga taxaw ne fa naam Daraame, di wut loo nettaliji
tu t’arrêtes et salues de porte en porte, cherchant qqch à aller raconter
oos g-
hameçon
Lonkil oos gi
décroche l’hameçon !
paaxe b-
homme non circoncis
Duma wax ak ab paaxe
je ne parle pas à un incirconcis.
paataŋ m-
omoplate
Nataalu paataŋ bi la
C'est la radiographie de l’omoplate.
pacc-pacci
cracher sans arrêt
Yaa ngiy pacc-pacci rekk, xanaa danga biir ?
tu craches sans arrêt, serais-tu enceinte ?
palpale b-
sole (poisson)
paa b-
fois (langage des jeunes)
Bii paa, maay dem
cette fois-ci, c’est moi qui irai.
paar b-
part
Na ku nekk jél paaram
que chacun prenne sa part !
paalaax b-
chair située derrière la cuisse
ci paalaax bi la doktoor bi sàkk ñaw ko ci ween wi
le docteur a prélevé de la chair derrière la cuisse pour la greffer au sein.
paase
repasser (linge)
pañe b-
panier
Indil pañe marse bi
apporte le panier du marché.
(prov.) Borom ŋàdd yëgul borom pañe
celui qui a un morceau de noix de cola n’a cure de celui qui en a un panier
pal b-
courge séchée et évidée servant de gourde
Ñu daldi jël ku nekk sag pal daldi jubal ca tool ya
ils prirent chacun leur gourde puis se dirigèrent vers les champs.
paas
payer pour un voyage ou pour un spectacle
Kenn du paas; ku bëgg dugg
personne ne paye (le ticket); entre qui veut.
palaat b-
plat
Amatuma benn palaat
je n’ai plus aucun plat.
oos
être usé
Tubay ji dafa oos
le pantalon est usé.
paccal
faire sortir par pression une noisette de (pâte, crème, etc.)
Dama ci paccal mayonees
J'y ai pressé de la mayonnaise.
paccaxndiku
barboter
Xale yaa ngiy paccaxndiku ci ndox mi
les enfants barbotent dans l’eau.
paañ b-
arche (coquillage lamellibranche)
paan b-
panne (machine, moteur)
Paan bi amul solo
la panne n’est pas importante.
paan b-
Bassine
Jéndal paan booy fóote
achète une bassine pour faire la lessive.
peñ b-
pain (de sucre)
Jox ma benn peñu suukar
donne-moi un pain de sucre.
pastel
mettre du crayon à maquillage à qqn
Kaay ma pastel la
viens que je te mette du crayon à maquillage !
palafoŋ b-
plafond (toiture)
pase g-
répudiation
Pase gi dafa bett ñépp
la répudiation a surpris tout le monde.
paccax-paccax m-
clapotis
Paccax-paccaxu géej gi rekk ngay dégg
tu n’entends que les clapotis de la mer.
pataas j-
patate douce
Pataas ju ñu fiiriir lay jaay
elle vend des patates frites.
Mbër mii pataas la rekk
ce lutteur n’est qu’une mauviette.
penku-kow b-
nord-est
Mu ngi jubblu penku-kow
il se dirige vers le nord-est.
ordisawel b-
eau de Javel
pasin w-
charade énigme accompagnée d’indices
Kenn xamul pasin wi
personne ne sait résoudre l’énigme.
par-parloo b-
attitude partisane partialité
Seen par-parloo bee tax duñu déggoo
C'est à cause de leur attitude partisane qu’ils ne s’entendront pas.