wolof
stringlengths 1
166
| french
stringlengths 2
331
|
---|---|
peer b- | paire |
Benn peeru dàll | une paire de chaussures. |
pool b- | poêle |
Raxasal pool bi | lave la poêle ! |
pelle w- | cheval ayant une tache blanche au front |
pëll | exprime l’idée de faire irruption |
Ba xaj ya nee pëll, golo ga tàmbalee pat-pati | quand les chiens firent irruption, le singe se mit à trembler. |
pénc m- | place publique dans un village |
Mu ngay fo ca pénc ma | il joue sur la place publique. |
Bésu pénc ma | au jour du jugement dernier (christianisme et islam). |
(prov.) Ku gor sa pénc yenduwaani | celui qui abat l’arbre de la place publique où il a coutume de s’asseoir sera obligé d’aller passer la journée ailleurs. |
pellax b- | niébé doux |
pël-pël m- | race de mouton de taille moyenne, difficilement apprivoisable, dont la robe est fauve en général, les cornes grandes et écartées |
Coggal gi yépp ay pël-pël rekk la il n’y a que des moutons pël-pël | dans le troupeau. |
pendal m- | pagne (wolof du Walo) |
Damay gaar sama pendal | je raccommode mon pagne. |
pënd b- | poussière |
Nag yee yékëti pënd bi | ce sont les vaches qui ont soulevé la poussière. |
(prov.) Pëndub tànk a gën pëndub taat | la poussière aux pieds est meilleure que la poussière aux fesses |
pëndax b- | poudre |
Pëndaxu meew | lait en poudre. |
pello b- | tache blanche au front d’un cheval |
Pello bi laa koy xàmmee | je le reconnais à la tache blanche à son front. |
portale | photographier |
Portale ma ! | photographie-moi ! |
peñewu | peigner |
Damay peñewu | je me peigne. |
penk b- | giron |
Ci penku ndeyam la bëgga toog | il veut s’asseoir dans le giron de sa mère. |
penk b- | magasin à céréales |
Denc nañu dugub ji ci penk bi | ils ont gardé le mil dans le magasin à céréales. |
péŋŋ | complètement |
penku-suuf b- | sud-est |
Penku-suuf la féete | C'est au sud-est. |
per b- | perle |
peñe b- | peigne |
Ana peñe bi ? | où est le peigne ? |
puno b- | pneu |
pëpp | être vide sans graines (coque d’arachide) |
Naka la suuf si di dugge ci gerte gu pëpp | comment le sable entre-t-il dans les coques d’arachide vides ? |
pëŋŋ | entièrement (fini, épuisé). |
Ñuy roñ saaku ya ba dugub ja ne pëŋŋ | ils prirent les sacs un à un jusqu’à ce que le mil fut entièrement épuisé. |
pend b- | petit van |
Pend bee gëna neexa téye | le petit van est plus facile à tenir. |
përe b- | reflux |
Ci përe bi lañuy wute sebbet | C'est au moment du reflux qu’on cherche des coquillages Donax. |
pëqéet | exprime la manière de sortir brusquement (d’un trou) |
Geneen yax ne ca pëqéet | un autre os en sortit brusquement. |
Xaj ya ne wesar génn, màggetum golo ga ne pëxéet mel ni fitt | les chiens sortirent dans tous les sens, le vieux singe bondit brusquement comme une flèche. |
perlit m- | nourrisson nouvellement sevré qui ne réclame plus le sein |
peral m- | sevrage |
Peral mi laa koy wax nu mu wara deme | je lui dis comment doit se passer le sevrage. |
përëg m- | bras partie située entre l’épaule et le coude |
Ci përëg lañu ko ñakk | on l’a vacciné à l’avant-bras. |
përiis m- | tabac à priser |
Jéndal ko përiis, duy tux | achète-lui du tabac à priser, il ne fume pas. |
perlukaay b- | lieu où l’on va pour sevrer son enfant (en général chez sa propre mère, pour ainsi éviter les grossesses rapprochées) |
Sama kër maam mooy sama perlukaay | la maison de ma grand-mère est l’endroit où je vais pour sevrer mes enfants. |
perngal | monter la pièce de bois à laquelle on attache les cordes qui retiennent les gros sacs latéraux que porte un dromadaire |
(prov.) Ngaaxi tukkal, kenn du ko perngal mboccor | les sacs du grand dromadaire, on ne les met pas au jeune dromadaire) les sacs du grand dromadaire, on ne les met pas au petit. |
për m- | fanes d’arachide |
perngal b- | instrument servant à effiler un métal |
përngal b- | restant de savon |
Amuloo përngalu saabu ? | tu n’as pas un restant de savon ? |
puudar b- | poudre de toilette |
Puudar fel-màtt-ak-teeñ | poudre D.D.T. |
puukare j- | vanité des choses |
Yëfi àddina, puukare doŋŋ la | les choses temporelles ne sont que vanité. |
petaar b- | pétard feu d’artifice |
puupa b- | valet, roi, dame lorsqu’ils ont une valeur faible dans certains jeux |
persi b- | persil |
puune | être atteint d’albinisme |
Dafa puune | il est atteint d’albinisme. |
pëtëm | griller qqch sous la cendre |
Damay pëtëm gerte gi | je grille les arachides sous la cendre. |
pettaaw | lire la bonne aventure avec des cauris |
Mën nga pettaaw ? | sais-tu lire la bonne aventure avec des cauris ? |
petorool b- | pétrole |
picc m- | n.onom. Oiseau |
Picc maa ngiy sab | L'oiseau chante. |
(prov.) Picc, la muy wax ca banqaasu garab, du ko wax ci loxol gone | l’oiseau, ce qu’il dit sur la branche de l’arbre, il ne le dit pas entre les mains d’un enfant) l’oiseau ne dit pas la même chose quand il est dans l’arbre et quand il est entre les mains d’un enfant. |
Fekkuma fa picc | je n’y ai trouvé personne. |
Amul picc walla aw ndeer | il n’y a pas âme qui vive. |
Ay waxi picc | des paroles creuses. |
petoo | avoir un entretien en tête-à-tête |
Kaay nu petoo | viens que nous nous entretenions en tête-à-tête. |
pey g- | salaire rétribution rémunération |
Pey gi may am léegi moo ëpp fuuf | le salaire que j’ai maintenant est bien plus élevé. |
pettaaw b- | cauris |
Pettaaw lay gisaanee | il lit la bonne aventure avec des cauris. |
pàq b- | dent de fourche |
Jéñ wu am ay pàq yu bare mooy doon kenu | C'est avec un pieu fourchu qu’on fait un support. |
póllëre b- | nervure |
Dindil ma póllëre bi | enlève-moi la nervure. |
picc b- | bouton pustule |
Dafa am ay picc ci yaram wi | il a des boutons sur le corps. |
Picci tàngoor | bourbouille. |
piis | faire un clin d’œil |
Dafa ko piis, mu dem | il lui a fait un clin d’œil, il s’en est allé. |
pikini b- | vingt-cinq centimes |
Subsets and Splits
No community queries yet
The top public SQL queries from the community will appear here once available.