wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
Dama seetaani woon ndëpp la
J'étais allé voir la cérémonie de danse d’exorcisme.
ndey-dikke j-
personne pour qui on a de la sympathie et avec qui on lie une amitié profonde
ndeyi-koor g-
septième mois du calendrier musulman
ndig
cri pour éloigner une vache
ndimmal l-
aide, assistance
Dafay sàkku ndimmal ngir jumaa ji
il fait une collecte pour la mosquée.
(prov.) Ndimmal, na ci fekk loxol borom
l’aide, qu’elle y trouve la main de l’intéressé) il faut déjà avoir la main à la pâte quand on demande de l’aide.
ndeyu-mbill g-
personnage principal
Ndeyu-mbill gaa ngi : moo def lépp
voici le personnage principal : c’est lui qui a tout fait.
ndikkaan m-
se dit de qqn qui fréquente un lieu où il n’est pas désiré
Ndikkaan dikkati na
L'indésirable est encore là.
ndiig l-
messager d’un ami auprès de sa future belle-famille
Sa ndiig li mat na
ton messager auprès de ta future belle-famille est à la hauteur de sa tâche.
ndo
sert à marquer un lapsus. Pardon !
Suba lay dem, ndo ! tey
il part demain, pardon ! aujourd’hui.
ndimb m-
cheval blanc
Am ndimb laay jénd beneen yoon
J'achèterai un cheval blanc la prochaine fois.
ndiir j-
souchet comestible
Jigéen ji dafay jaay ndiir
la dame vend des souchets.
ndof g-
folie
Loolu ag ndof la
ça, c’est de la folie.
ndimo l-
Étoffe tissu
Xeeti ndimo yépp a ngi fi
toutes les sortes de tissu sont là.
ndokkeel
féliciter
Maa ngi leen di ndokkeel
je vous félicite.
ndiiraan g-
foule groupe
Ndiiraan gaa ngi koy tàccu
la foule l’applaudit.
(prov.) Menn picc mënula yàq ndiiraan
un seul oiseau ne peut pas disperser un groupe.
ndogu l-
repas pris à la fin d’une journée de jeûne
Indil ndogu li
apporte le repas pour rompre le jeûne.
ndokk
bien fait !
Ndokk ! ba nga ko indiwulee
bien fait de ne l’avoir pas amené.
Ndokk sa bakkan
Dieu soit loué ! Félicitations !
Ndokk sa wàll
félicitations à toi aussi !
ndoket b-
robe ample avec manches larges et fronces au-dessous des seins ou à la taille
Ndoket laay ñawlu
je fais coudre une robe à manches larges.
ndombog-tànk g-
distinction décoration
Kan lañu nara tappal ndombog-tànk
qui va-t-on décorer ?
neer
avoir le mal des transports
Dafay neer
il a le mal des transports.
ndomboor l-
annulaire
ndombo g-
talisman cousu dans du cuir qu’on porte autour du bras, de la jambe ou de la taille
Def ko ndombo loxo
fais-en un talisman que tu porteras autour du bras !
ndon g-
palme verte de rônier
Ku moom ndon yi ñu jal fale ?
à qui sont les palmes vertes de rônier entassées là-bas ?
ndor w-
(poisson) Baliste ponctué
ndongo l-
Élève
Ndongo yaa ngiy jàng
les élèves étudient.
Ndongo li, kaay fii
jeune homme, viens ici !
ñeex
verser la sauce sur le riz ou le couscous
Bul ñeex cere ji
ne mets pas la sauce sur le couscous !
ndongamaate b-
petit du scorpion
Ab ndongamaate it dafay fette
le petit du scorpion pique aussi.
ndott
évoque le mouvement de la grenouille qui se déplace
Eleew yaa ngi naan ndott, ndott ni ay mbott
les élèves font {ndott, ndott} comme des grenouilles.
nees-tuuti
peu de temps après
Nees-tuuti, gaynde ga agsi
peu après, le lion arriva.
Dafa dem, nees-tuuti nga agsi
il est parti, et, peu de temps après, tu es arrivé.
ndoŋ
exprime le roulement du tambour d’aisselle
Naka la géwél ba ni ndoŋ ! ndoŋ ! tama ja, màggetum golo ga ni kulbét mberu ma uboon këll ga
dès que le griot fit « dong ! dong ! » sur le tambour d’aisselle, le vieux singe ouvrit d’un coup le van qui recouvrait l’écuelle.
ndono l-
héritage
Këru ndono la
C'est une maison de famille (héritée).
ndox-suuf b-
Serpent
ndor w-
(poisson) Baliste ponctué
ndull
être complètement nu
Mu ngi ne ndull, taxaw ci diggu ëtt bi
il est tout nu, debout au milieu de la cour.
ndoxaan l-
fait de faire la cour à une femme
Ndoxaan li doy na; na ñaansi
la cour a assez duré; qu’il vienne faire sa demande en mariage.
ndoxum-siti m-
syphilis
Ndoxum-siti mee ko def nii
C'est la syphilis qui l’a mis dans cet état.
ndull m-
mil provenant de la récolte des épis tardifs
Ndull mi, duma ko jaay
je ne vends pas la récolte de mil tardif.
(prov.) Ndull jeex, surga yooy
quand le mil des épis tardifs est épuisé, les domestiques maigrissent
ndoxe
se dit en général d’une sauce qui n’est pas suffisamment épaisse. On peut l’appliquer à autre chose pour indiquer un excès de fluidité
ñeex m-
sauce qui accompagne le couscous ou le riz
Ana ñeex mi ?
où est la sauce ?
(prov.) Fii wund du fi naane ñeex
les chats ne boiront pas de sauce ici
nduluñ
perdre tous ses pions au jeu
Dama nduluñ
J'ai perdu tous mes pions.
ndunqurunq g-
croupe croupion
Dàmpal ko ndunqurunq gi
masse-lui la croupe !
ndox m-
eau
May ma ndox
donne-moi de l’eau !
mook naan ndox a yem
C'est un jeu d’enfant; c’est facile à faire.
Ndoxum lunet yi leerul bu doy
la limpidité des lunettes n’est pas suffisante.
(prov.) Dég-dég amul i tànk, waaye jàll na am ndox
la nouvelle n’a pas de jambes, mais elle a franchi la mer.
(prov.) Dooley jén : ndox
c’est l’eau qui fait la force du poisson.
ndoxtu l-
pion
Ñaari ndoxtu nga dese
il te reste deux pions.
ndung-siin b-
prison
Mu nga ndung-siin; dafa sànni doom ji
elle est en prison; elle a abandonné son bébé.
ndutt b-
{ndout}, groupe ethnique vivant dans la région de Thiès
Ndutt yi bare nañu ay làbbe
il y a beaucoup de prêtres {ndout}.
nduŋ
évoque le battement lourd d’un tambour
Ba ndënd ma nee nduŋ, mu tëb
quand le gros tambour fit boum, il sursauta.
négandiku b-
fait d’attendre
ndugg m-
victuailles
Yóbbul ndugg mi ca waañ wa
apporte les victuailles à la cuisine !
ndàmpaay l-
massage
Ndàmpaayam dafa metti
son massage est douloureux.